Kub bu àddina si : Senegaal am na ndam ci ñaareelu joŋanteem

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw bi mu lajjee woon ci kanamu Olànd (altini 21i fan ci nowàmbar 2022) ci joŋanteem bu njëkk ci kub bu àddina siy amee fale ca Qataar, Senegaal am na ndam yoon wile ci ñaareelu joŋanteem bi. Réewum Qataar ci boppam la dóor ñetti bii ci benn. Muy itam guléet am réewum Afrig am ndam ci bile xëccoo.

Démb àjjuma, 25i fan ci weeru nowàmabr 2022, bi 13i waxtu jotee ci bëccëg bi, la Senegaal doon janook Qataar mi dalal joŋantey kub bu àddina si. Mu doonoon joŋante bu diis lool ci ñaari bar yi ndax kuñ ci dóor rekk mooy toog nga, fi ngay yem. Ci gam-gamle, doon na gënn a ub boppiy Saa-Qataar yi nekk seenum réew ba noppi nar a njëkk làlli basaŋ. Waaye itam doonoon na lu takkarnaase lool ci Saa-Senegaal yi doon dawalaale xalaat yu mel ni : du benn barub afrig bu amagum ndam, ñoom ñooy buuri Afrig, ñépp di leen xaar ñu nar a njëkk lem seeniy kaaka ñibb. ndaw gàcce !

Yile xalaat nag dafa mel ni dañ yokk jom gaynde Senegaal yi. Naka la àttekat bi sex mbiib ma, ni parr rekk ñu teg ka ca. Ni siiw ci wàlluw Saa-Qataar yi, xoj leen fa. Bal bi di fa daw, ña fay wure wet gu nekk ngir bëgg teel a lakk caax yi. Naka la wattukatu (défenseur) Qataar bi mball bal bim bëggoon a tulli ca àll ba rekk, Bulaay Ja dóor mu dugg. Senegaal jiitu ak benn bii ci 41eelu simili bi. Ba bi ñaari bar yi di dalluji kenn dugalaatul.

Bi ñu delsee ci ñaareelu xaaju joŋante bi, ñetti simili lañ dawal, Faamara Jeeju dugal mbëkk mu réy. Muy ñaareelu bii bu Senegaal. Xel dal, Saa-Senegaal yi tàmbalee noyyi. Naka noonu Saa-Qataar yi xam ne xéll fii nañ nar a yem ci xëccoo bi. Ci nañ daldee góor-góorlu ba am benn bii ak a dunde yaakaar. Waaye, yàggul dara Ilimaan Njaay fëll benn fëll rekk sédd Bàmba jeŋ mu dugal ñetteelu bii bu Senegaal. Joŋante bi mujje jeex ci 3i bii ci 1. Senegaal daldi am ndamam lu njëkk, joxaaleet afrig ndamam lu njëkk ci xëccoo bi.

Ndam li Senegaal am ci kow Qataar nag dina tax ba mu fàtte lajjam ci digganteem ak Olànd. Waaye, xel yee ngi wéy di jax-jaxi ndax ba tey Senegaal a ngi ci ñetteelu toogaanu kippu A bi. Olànd ak Ekuwaatëer dañ témboo ci beneen joŋante bi, ku nekk am benn bii. Saa-Senegaal yi fàtteeti xaat seen ndamu démb li, jublooti ci joŋante talaata bi war a dox ci seen digganteek Ekuwaatëer mi leen jiitu te ñu war a am ndam ci kowam buñ bëggee des ci xëccoo bi. Ñuy xaar fu wànnent di mujjeek i bëttam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj