Ginnaaw ubbite gi, ci dibéer ji (20 nowàmbar 2022), démb lañ doon amal ñaareelu bëcëgu kuppeg àddina si. Ñu doon ci amal ñetti joŋante. Waaye tam, niki bésu démb ji la la gayndey Senegaal yi waroon a door. Ndeysaan, dañu tarxiis. Nde, Olànd moo leen daan 2i bii ci 0.
Jamono yii nu tollu, xel yeek xalaat yépp a nga Qataar, fa kub bu àddina si di ame. Démb nag, Senegaal gi jëloon Can 2021 bi bu yàggul dara moodoon joŋanteek Olànd. Mu nekkoon seen mats bu njëkk ci kuppeg àddina si. Waaye, gaynde Senegaal yi dañoo lajj. Muy guleet Senegaal di ñàkk joŋanteem bu njëkk ci kuppeg àddina si.
Senegaal nag ñépp a ko doon xaar. Ñëwam gu njëkk ci atum 2002, dafa pattaloon (1-0) Farãs mi jëloon kub bi ci atum 1998. Ginnaaw gi, toog na ñetti yoon yu mu demul (2006, 2010 ak 2014). Bi mu delsee ci kayu Riisi gi ci atum 2018, dafa daldi amaat ndam ci joŋanteem bu njëkk ci kow Poloñ, fekk ikibi Afrig yépp jotoon a nërmeelu. Bu ren jii nag, moom moo njëkk duggusi, moom lañ njëkk a dóor.
Gaynde Senegaal yi ñàkku ñu faayda benn yoon. Ku gis seen taxawaay tey, liñ wone ci ñàkk teewu Saajo Maane miy ñaareelu wurekat bi gën a aay ci àddina si, ne leen gàcce-ngaalaama. saa-olànd yi jéem nañ lu nekk mënu ñoo boyal caaxu Senegaal yi. Ñoo ëpp luñ téye bal bi gaa, waaye saa-senegaal yee leen ëpp i dóor (15i dóor : 11 yi dëng, 4 yi jub ci caaxi Olànd yi, góol bi di leen génne). Ci noonu dërtoo bi metti woon lool ba kanamu wurekat boo xool gis ci coono.
Ginnaaw bi Senegaal ñàkkee Abdu Jàllo, dawalaat tuuti ñàkkaat Séexu Kuyaate la ikib bi tàmbalee néew doole. Ci diir bu gàtt saa-olànd yi gisaat seen bopp, dugal ñaari bii ci njeexitalu joŋante bi (84eel ak 99eelu simili). Aliw Siise ak i guneem daldi ñàkk seen joŋante bu njëkk ci xëccoo bi. Waaye itam ñàkk teewu Saajo Maane, seen wurekat bi gën a xarañ, feeñ na ci bu baax donte ni yelloo woon nañ ndam. Xar-kanam gi ñu wone dina waral ñuy wéy di leen bàyyi xel ak a xaar seen ñaareelu joŋante ci àjjuma jii, ci seen digganteek Qataar mi dalal po mi.