France 24 amal nab laaj-tontu ak kii di Kolonel-Masoor Ismayla Wage mi yor kàddug way-fétteerlu yi booloo ci kurélug CNSP miyitte woo sàmm muccug askanu Mali. Nicolas Germain lay waxtaanal.
Ci tekkib Paap Aali Jàllo
– Lu leen tax a def cëtëŋ lii ?
– Dafa fekk ne, réew mi doxul. Teg ci ne, dafa amoon ci askan wi ñu sonnoon lool. Rax-ci-dolli, ay jafe-jafe yu bare ñoo gaaraloon làrme bi ci boppam. Ger mi àggoon na foo xam ne soldaar yi mënatuñu woon sàmmoonte ak seeni wareef. Fi mu ne nii, nag, bu ma sañoon ñu bañ a wax waxi cëtëŋ. Ndax, du noon lanu jàppe mbir mi.
– Waaye IBK tekkiwul ndombo-tànkam ci coobare boppam…
– Yéen, loolu ngeen jàpp. Waaye, ndax moom moo leen wax ne dañ koo jaay-doole ?
– Wànte IBK nee na mënul woon def neneen…
– Mënul woon def neneen ndax moom ci boppam mujjee naa gis ni askan wi sonnee. Kenn newu ko bàyyil mbaa ñu rey la. Ku mu neex, nag, nga jàpp lu la neex. Fi mu nekk nii, noo ngi jokkoo ak doomi-réew yi réew mi soxal ngir taxawal ag ndajem néggandiku moo xam ne, ab maxejj a koy jiite. Noo ngi waxtaan ak kuréli way-moomeel yi, làngi kujje gi ak képp ku nu war waxtaanal ngir taxawal ndaje moomu.
– Lu ngeen naral IBK ?
– Loolu du sunu cër. Mbirum yoon la. Bu waxtu wa jotee, yoon dina def liggéeyam.
– Naka la seen digganteek M5-RFP deme ?
– Jotewunu daraak M5-RFP. Nun, genn làng jiitalunu.
– Monte yéen ak ñoom, yéen a bokk benn gis-gis ak benn àtte ñeel ni IBK yore woon Mali…
– Li waa M5-RFP tàmm a wax, dëgg gu wér péŋŋ la. Waaye, loolu du tekki ne ñoo nekk ci sunu ginnaaw, di nu sant nuy def. Amunook ñoom benn jëflante. Bi nu defee li nu def ba noppi, ci lanu ñépp woo, jokkoo ak nun.
– Àddina sépp a ñaawlu cëtëŋ li ngeen def. Ndax ragalu leen daan yiñ nar a teg Mali ?
– Ragal nanu ay daan, kay. Ndaxte, bu ay daan amee, askanu Mali mooy sonn.
– Ndajem néggandiku mi ngeen di waajal, ndax da fiy nekk ba wotey 2023 yi walla dangeen di amal ab wote bala boobu ?
– Sunu mébét mooy nu amal ay wote ci ni mu gën a gaawe, mbir mi dellu ci yoon, ku nekk dellu ca la nga nekkoon, rawatina soldaar yi nu doon. Muy 2023 walla 2022, ni mu gën a gaawe rekk, gën a baax.
– Ndajem néggandiku moomu, ñan ñoo koy séq ? Ay maxejj kese walla soldaar yi ci lañuy bokk ?
– Loolu, ci tombi waxtaan wi lay bokk. Mënaguma cee wax lu leer.
– Ndax jot ngeen a waxtaan ak CEDEAO ?
– Noo ngi jokkoo ak CEDEAO. War naa dajeek ñoom, sax.
– Ndax yeen a ngi jokkoo ak làrme Farãs ?
– Ci jamonoy jàmm, danuy jokkoo ak « Barkhan » ñeel xeexub jiyaadis yi. Waaye, bi nu taxawalee CNSP ba léegi, waxagunook làrme Farãs.
– Ndax jàpp ngeen ne li xew tey mën naa may fit jixaadis yi ?
– Waaw kay ! Xam nan ko bu baax. Loolu lanuy ragal sax. Moo nu tax a sàkku ci sunuy farandoo nu taxawunu, bañ noo seetaan.