LACOS DUUT NA BAARAAM NDAJEM NDEYU ÀTTE MI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Lu ëpp ayu-bés a ngi nii, ginnaaw ba caytug xobi baayale yi tàmbalee. Boobaak léegi nag, saytul nañu lawax yu bari seen i xobi baayale. Mu néew lool ñu jàll ci ñoom. Ndax, kenn umpalewul lim bu takku biy dagaan baatu askan wi. Terewul ne am na lu tollu ci juróom-ñeenti lawax yoo xam ne matal nañu. Mu am ci ñaar-fukk yu war a mottali. Ak ñeneen ñoo xam ne dañu leen a gàntal. Ñenn ñi seen i xobi baayalee matul. Ak ñi nga xam ne seen wayndare moo matul, muy ku ci mel ni Usmaan Sonko. Rëq-rëq yooyu ñu nemmeeku ci liggéeyu ndajem ndeyu àtte mee tax waa LACOS jóg taxaw temm ngir joxe ci ay firnde.

LACOS ag kurél la gu ay kilifay pólitig sos, boole seen doole ngir jàppale Usmaan Sonko. Mu mel ni caytu gi, waa Pastef moom gisaguñu ci seen bopp. Ndax, ci alxames ji lañu xamle woon ne Basiiru Jomaay Jaxaar Fay matalul ay xobi baayaleem. Ñu ni déet-a-waay, ci àjjuma jii weesu, ñu ne wayndarew Usmaan Sonko matul. Li gën a yokk seen génn boobu mooy ne dañoo jàpp ne gaa ñi dañoo lëbaje kàrt gi. Maanaam, xobi baayale yu Basiiru Jomaay fay yi dañu cee yokk lu ci bokkul. Loolu la El Maalig Njaay, kenn ci ñoom di leeral ci kàddoom yii toftalu :

“Maanaam, dañoo joxe sunu caabi nosukaay (clé USB) ñu génneel ñu ci daanaka lu mat 12.121 dugal fa yeneen (…) Li tax ñu def Sigicoor ak Ndakaaru mooy dañoo yaakaaroon ne du feeñ. Ndax, lañ fa jébbal dafa bari. Buñ ko defoon ci gox yoo xam ne 4 000 walla 3 000 lañu fa jébbal day leer. Waaye, boobu, ñoom dama yaakaar ne xamuñu Pastef walla xamuñu “Coalition Sonko Président”. Ndax, liggéey bi ñu def ba dem di jébbal caabi nosukaay bi waroon na leen leer ne nun am nanu  yeneen yu bari (…) lu tax jafe-jafe yii amul woon 2019 mooy booy dem dangay yóbb sa caabi nosukaay ñu xoolal la ñi la baayale. Fanaanul guddi ci ñoom. Bii nag, caabi ji def naak ñoom ayu-bés. Foofu la ndëgg-sërëx bi nekk.”

Mu rax ca dolli ne :

“Ëpp na 100.000 nit ñu ñu wax ne nekkuñu ci wayndarew wote yi. Loolu mënut a nekk. Lii lañuy tudde ndamul càcc (victoire technique). Loolu mooy dangay fexe ba gox yi nga xam ne amoo fa doole, muy Sigicoor, Tuubaa, Ndakaaru, nga jaxase pekki wote yi. Nga rocci ay nit. Ñu bari di xëy di xool fan lañuy wotee ba duñ mën a wote, nga wàññi fa. Leneen li mooy nga tànn ñan la sa mbër di àndal. (…) Li ñu bëgg mooy sàcc wotey yi (hold up électoral). Moo tax ñu koy tàmbali ci baayale gi…

Ñépp xam nañu ne ndajem ndeyu àtte mi li mu def tegu ko fenn. Waroon na xool ndax Usmaan Sonko indi na ay baayale am déet. Waroon na xool ndax indi na “quittance” am déet. Ndax, “quittance” ba mu indi CDC la jóge am déet. Wone ne jébbal na lu tollu ci fanweeri miliyoŋ. Daf ci yokk liy wone ne xaalis bi dugg na ci gafaka gi. Yokk ci këyitug ceede gu wiisiyee (Procès verbal de l’huissier) giy wone ne dem nañ di jëli “attestation” bi, ngóor si woo takk-der yi ñu tëj fa. Kon, ndajem ndeyu àtte mi bu sukkandikoo ci loolu ne du xool waydare wi, moo xam li tax mu ne du ko xool. Xamna  ne bu ko xoolee gis fa dëgg te, dina ko nangu….

Usmaan Sonko, mbir mi jeexagul de. Te, layookat yi dinañu leeral. (…) Dañoo ragal Usmaan Sonko kepp. Bu xëyoon ne bàyyi naa pólitig, ñu bàyyi ko mu ñibbi. Li am solo mooy xeex bi dinañ ko wéyal ci fànn yépp. Ci wàllu Yoon dinañ wéyal, ma-xarala yi (les techniciens) dinañ wéyal, lawax yi ci seen bopp dinañ dajaloo dinañ wéyal.”

Dees na xam fu wànnent di mujj ak i bëtam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj