CNG def na mujjum ndajeem mu mag ginnaaw bi làmb ji tëje. Mi ngi ko doon amal ci gaawu bii weesu, 20i fan ci weeru ut 2022 fale ca Aren Nasiyonaal. Ci ndaje moomu nag, Biraa Seen mi jiite CNG delsi na ci li gënn a fés ci yaxalub at mi (bilan de l’année).
Ci tënk, CNG bi amal na 145i làmb ci fukki weeri (diggante oktoobar ak sulet) joŋante yu 2021-2022. Bokk na ci li gën a fés ci yaxalub at mi taxawaay bi ñu am ci wér-gi-yaramu mbër yi, jafe-jafe yi ñu jànkonteel ak saafara yi ñu ci namm a andi.
Bu dee ci jafe-jafe yi, yi ñuy faral di jànkonteel ñooy peyoori mbër yi. li ñuy siiwal ci caabal yi ak feneen dafay woroo lool ak li ñuy fas ci CNG bi. Ci li Biraa Seen siiwal, CNG mosul a fas lamb ju mbër feyeeku lu ëpp 60i miliyoŋ. Yàggaayu làmb yi tamit ak yi koy waral yu deme ni janoo yu bare yi ak tuus yu yàgg yi dinañu leen xoolaat ak itam taafar yi bare yi ba ci jumtukaay yi ñuy faral di yàq ci làmb ji.
Biraa Seen fésal na tamit ne diggante CNG bi ak ñi mu séqal làmb ji gën na rattax. Mu ne :
“ Yombalal nañu leen yu bare ndax jamonoy Covid19 bi a ko waraloon. Yi CNG bi bëgg joyyanti dinanu ci bokk xalaat ak jëmukaay ci at mii di ñëw.”
Terewul ba-tey mbër yaa ngi dellu di mettitlu ni mu leen di toppe, rawatina daan yi ak xaalis bi ñu leen di dagg.
Giri Bórdoo mi yor kàddu mbër yi andi na ciy leeral. Ciy waxam, biral na ne CNG bi dafa war a am tuuti yërmande ci mbër yi, rawatina ci mbër yu ndaw yi :
“ Donte ne sàrt yaa ngi fi te ku def am na luy tegu ci sa kow, waaye yello nañ ko. Nangeen leen gën a jàppale. Ku ci nàndul, ngeen fexe ba mu nànd ndax ñu takku ci ñoom dese nañoo xam yu bare. Deeleen ci woo fii di def ay waxtaan ak ñoom ngir ñu mën a xam.”
Waaye, jamono jii, sikk amul ci ne, làmb ji dafa daanu. Itteelatul noon yépp saa-senegaal yi. Baax na nu xool, gëstu jéem a xam sabab yi.