LAMIN JÀLLO (NJIITUL TEKKI) DINA JÉEM A NEENAL DEKKARE MAKI SÀLL BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mamadu Lamin Jàllo mi jiite pàrti pólitig bii di Tekki ñaawlu na dekkare bi Maki Sàll xaatim ngir fomm wotey 25 féewiryee 2024 yi. Xamle na ne dina yóbbu dekkare bi fa mbaxana doonee benn, ngir jéem ko neenal.

« Ni ma ko tàmm a defee, damay wéy di sax ci xeexal demokaraasi Senegaal ak Afrig. Damay xeex “Coup d’Etat constitutionnel” bi Maki Sàll bëgg a def, daldi dàq wote yi njàmbaas ci ag ñetteelu moome. Dinan ataake dekkare biy fomm wooteb kurélu wote gi ci bésub 25 féewiryee 2024. »

Ci X la bind wax jile.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj