PÉEXTE
Da maa dëfeenu di jeneer
Ba xel mi tàbbi cig ndenéer
Dellusi naan ma nu gàddaay
Fii kat lépp a ngi naaxsaay
Xel mi sonal ma
Di yuuxu naan ma
Gis naa meneen réew
Mu ne ci meneen kéew
Ñam ya ni ñu neexee
Te lépp a mbindaree
Ndox ma teey na sell
Fépp fees ak i mbell
Bi ma doxee ba ni tëll
Yam ciy garab yu dëll
Péex ma foroos saa naqar ci neen
May ree di saamandaayub sëppeen
Jekki dégg téll jóg taxaw
Ndeke dama doon nelaw
Làmp_Faal_Kala