LAN MOOY GARAB ? (Li Faal Sàmba Suuna)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Li Faal Sàmba Suuna

Lépp li nit kiy jënde farmasi la Wolof Njaay tuddee garab.
Moone dey, yemul foofu ndax gàncax gi du dara lu-dul i
garab yuy sax, di nu dundal di ñu may keppaar. Te yit, ñoo
nuy faj su nu feebaree. Sunuy maam ak sunuy maammati-
maam mësuñoo umple loolu. Daan nañu bey di dunde
wànte yemuñu woon ci loolu ndax daan nañu dugg ci àll
witt fay xob walla buddi fay reen ngir faj bépp jàngoro ju
dal doom-aadama.
Te lees war a xam bu baax moo di ne du woon ñoom rekk.
Ci misaal, Hyppocrates mi Tubaab yi naw ba duppe ko
‘’Baayu xam-xamu paj’’, noon na : ”Na li ngay lekk doon
sa garab, te yit na sa garab doon li ngay lekk”.
Kon nu jàngat ci ne li ngay lekk mooy li lay faj.
Àddina di dox a dox ba daanaka ñépp sàggane yile
kàddu.
Boo ko seetee ci sunu réew mii, dinga gis ne ñu bari ci
nun jàpp nañu ne li ñuy lekk jotewul daraak seen wér-gi-
yaram. Looloo tax sax nu soppi sunu lekkin, mu mel ni nit
ñi, li leen soxal dëgg mooy feesal seen biir.
Ndaw njuumte lu réy !
Soloy lekk dëgg mooy dundal yaram, du feesal koll.
Feebar yu bari dara waralu leen lu-dul xeetu càggan
woowu.
Ñenn daal laa yaakaar, ci sama xam-xam bu gàtt, ne
réerewuñ ko mbir te ñooñu Sinuwaa yi làn. Dafa di ñoom,
biñ tàmbalee gëstu ci wàllu paj du tey, ay junniy-junni at a
ngi ñu ciy yëngu ba tax ñépp ràññee leen ci. Li ñuy digle ci
seen i téere dafa leer nàññ : li ngay lekk ak li lay faj ñoo
war a bokk fi ñuy jóge. Dinañuy wax tamit ne ‘’Ku sa mbàq
rës, say nelaw du neex.’’
Waaye ndax lii lépp war nanoo jaaxal, nun Doomi- Senegaal ?
Mukk ci àddina ndax muy Hyppocrates
moomu Tubaab yiy tiitaroo, di doktoori Siin yi, kenn waxu
ci lu Wolof Njaay waxul ! Te Wolof sax ci benn kàddu doŋŋ la
tënk seen coow lépp, muy GARAB.
Kon sunu wér-gi-yaram a ngi aju ci sunuy garab, sunuy
garabi bopp, maanaam gàncax giy meññ, di nu dundal bu
ñu xiifee, di nu faj bu nu feebaree. Dellu coosaan baax na
ci leeg-leeg ndax ku dem ba xamatul fu mu jëm dafa war a
dellu fa mu jóge. Su ko defee du réerati ci yoon wi te bu
yeggee fa mu jëm dina fa féexlu ci keppaarug naw saw
xeet…

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj