Démb, ci alxames ji lañu waroon a àtte Maam Mbay Ñaŋ ak Usmaan Sonko. Waaye mujjul àntu. Li ko waral mooy ne, ñii di layookati Usmaan Sonko yi ñoo sàkku ñu dàq layoo bi ba weneen yoon. Bii mooy ñaareelu yoon ñu koy dàq. Bu njëkk ba moom li ko waraloon mooy ne kii di ndeyu-mbill ji, Usmaan Sonko, jotul woon ab woote. Maanaam, jotul woon luy firndeel ne àpp bii woo nañu ko ci ngir mu ñëw ca ëttu àttewaay ba. Layoo bi nag bii mooy doon yoon wu mujj ñu koy dàq ginnaaw bi ñu ko dàqee ñaari yoon.
Coowal PRODAC li dox ci diggante ñaari maxejj yooyu, démb ci alxames ji lañu ko waroon a leeral. Kii di Maam Mbay Ñaŋ nag, moom, bi mu xëyee def na ko ni mu ko defe woon ca yoon wu njëkk wa. Xëy ca teel, dem ca ëttu àttewaay ba. Kii di Usmaan Sonko tamit, wii yoon dem na. Ndax, yoon wu njëkk wa demul woon. Ma nga doon doxantu ca mbeddi Cité Kër Góorgi ya nga xam ne takk-der yaa nga fa meloon ne soq bu tuuru. Ay layookatam a ko teewaloon ca layoo ba. Ñoom nag, ñoo xamle woon ne ki ñuy layal jotul ab woote ci layoo bii. Ci lañu jëlee ndogalu dàq layoo ba ba jëmmi jamono.
Layoo bu démb bi nag, li waral ñu dàq ko mooy ne ñii di layal Sonko ñooy ñi ko sàkku. Ndax, nee ñu, dafa am yeneen i layookat yu dolleeku ci ñoom, te, miinaguñu wayndare wi. Loolu la kii di Uséynu Ngom kenn ci layookati Usmaan Sonko yi di leeral ci kàddoom yii :
« Ñaari fan ci weeru féewaryee lañu ko njëkk a woo, yeen ñépp fekke ngeen ko. Ba nu ñëwee ca bés ba li nu fa gis nun ci sunu wàllu liggéey fii ci ëttu àttewaay bi mooy danoo gis ne wayndare wi dañu ko jaarale foo xam ne méngoowul ak fi ñu doon jaarale yeneen yi. Ndax, gis nanu bés bu njëkk bi, ñoom ñu pare ngir àtte ko. Te, bi ci jiitu sunu waa ji ñëwul woon te mënul woon a ñëw ndax ku ñu woowul mënoo ñëw. Bi nu ñëwee tey tamit li waral dàq gi mooy dafa am ay layookat yu yees yu ñëw. Saa su layookat bu bees ñëwee am na sañ-sañu laaj ñu dàq àtte bi rawatina bu limub li ñu ko dàq matul ñett. Ñaareel bi mooy dangeen ci ñàmbaas mbir moo xam ne du tuuma du saaga mooy li ñuy wax « faux ». Usmaan Sonko am na sañ-sañu ak ñi koy layal woo képp koo xam ne war na mën a leeral li ñu koy tuumaal. »
Kii di Maam Mbay Ñaŋ, ba mu génnee ca ëttu àttewaay ba yékkati na ay kàddu ñeel mbir mi. Moom nag, deful lu dul delloo buum ca mboy-mboy ga. Maanaam, mu wax ne kii di Usmaan Sonko bu dee am na ag caabal rekk na ko indi. Loolu lay biral ci kàddoom yii :
« Moom nee na am na caabal gu ma jàpp, dellu dem DIC ne dafa juumi IGF la bëggoon a wax. Tey nag gis naa mu ñëw ak ay layookatam nee na nañu ko dàq ndax dañu koy waajal. Waaye loolu jarul waajal. Wax dëgg Yàlla jarul téeméeri layookat. »
Kon, gaa ñi mbir yaa ngay bëgg a romb fa ñu leen doon xaar. Ndax, ci layoo bu njëkk ba dañu ne woon Usmaan Sonko jotul ab woote moo tax mënuñu woon a àtte. Tey tamit, ñii di layookati Sonko ñooy ñi sàkku ñu dàq layoo ngir ñu gën a mën a waajalaat seen bopp. Kon daal, am na luy ñuul ci soow mi. Waaye nag, coow li yemul foofu. Ndax dafa am lu beesaat ci mbir mi. Ndege, dafa am yeneen ñaari mbir yu toppekat bi ñàmbaas ci wayndare wi, yokk ko ci li ñu doon toppe Usmaan Sonko. Moom li ñu ko doon toppe ca ndoorteel ga mooy teg ay kàddu yu dul dëgg ci deru jàmbur. Yeneen ñaar yi ñu koy toppe nag mooy jëfandikoo wayndare yu baaxul, ak ay saaga yu ñu ne daf ko jibal. Loolu tamit, jar na def ab taxaw-seetlu. Maanaam, lu tax ñaari tuuma yooyu dolleeku ci ? Kon, jamono jii, ñetti tuuma ñu ngi ci ndoddu Usmaan Sonko. Tuumaa yoo xam ne seen i daan mën naa tax mu ñàkk yenn ci ay àq ak i yelleefam.
Layoo bu tey bi nag bari na ay xew-xew yu ci am. Ndax, kii di Usmaan Sonko bi ñu dàqee seen layoo bi muy ñibbi ànd ak i ñoñam ci la ko takk-der yi kar. Ñoom nag yemu ci loolu rekk. Ndax, toj nañu weeru daamaram gi, jaay ko doole génnee ko yóbbu ko këram. Bi mu ñibbee, dafa nammoon a def ndajem-waxtaan ak taskati-xibaar yi. Waaye, takk-der yi mayuñu ko mu dem ca fa mu koy defe, ndax ay lakkirimosen. Daf ko mujje bàyyi. Te, ca jamono jooju, ka mu séqal mbir maa ngay def ndajem-waxtaanam. Nan lees mën a jàppe xeetu doxalin wii ?
Léegi nag, ginnaaw layoo bu tey bi tamit mujjul àntu, jàppalaat nañu leen beneen àpp ngir ñu àtte leen. Àpp boobu nag mi ngi yemoo ak fukki fan ak juróom-benn ci weeru màrs. Su boobaa dees na xam fu wànnent di mujjeek i bëtam.