LAYOO MAAM MBAY ÑAŊ – USMAAN SONKO JEEXAGUL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb, ci alxames ji, 6 awril 2023, layookati Usmaan Sonko yi woote woon nañu am ndaje, ñoom ak taskati xibaar yi. Li ñu ci jublu woon mooy waxtaan ak ñoom ci ñeel layoo bi dox ci diggante seen kiliyaaŋ, Usmaan Sonko, ak jëwrin jii di Maam Mbay Ñaŋ. Jot nañoo indiy leeral ci mbir mi, fa mu doore ba fees ci yemandi jamono jii, daldi koy jàngat.

Juroom-ñaari fan la layookati Usmaan Sonko yi xaar, diggante bi ko àttekat bi daanee ak léegi, ñuy sog di amal uw waxtaan ak taskati xibaar yi. Nde, alxames 30 màrs 2023 la yoon daanoon kii di Usman Sonko ñaari weeri kaso yu mu dul tëdd ak 200i tamndareeti FCFA. Ci seen i wax, dañ doon xaar ndigalug kilifay layookat yi, maanaam batoñee bi, ngir mën a wax. Ginnaaw bi ñu amee ndigal li, seen itte mooy tontu geneen ñoom Maam Mbay Ñaŋ ak i layookatam, ngir xamal àddina wërngal këpp li xew, ca dëgg-dëgg, lu jiitu àtte bi di am, ci bésub àtte bi ak ginnaaw bi àtte bi jibee.

Ci seen waxtaan, ñu mën caa jàpp ni, keroog bi ñu tuddee Usmaan Sonko ci kalaame gi lañ ko tàmbalee xañ jàmm. Nde, amul luñ ko deful. Taxawal nañu ay takk-der ca fa mu dëkk, wër ko ndomb ci wet yépp. Tere nañu njabootam mu génn ci lu dëppoowul ak Yoon ba ay doomam jàngeetuñu, ay soxnaam liggéeyeetuñu. Dem nañu sax ba terewaale ko julliji ?

Bu loolu weesoo, bundaxatal nañ ko ci anam wu nekk. Toj nañ weeru daamaram, jaay ko doole, lottal ko moom ak layookatam bii di Meetar Keledoor Li. Bi ñu demee ba ni ëllëg la àtte bi, ñu dellu teg i daan ci kow layookatam bii di Meetar Useynu Faal, dellu jàpp Meetar Juan Branco, génne ko réew mi.

Bésu àtte beet, layookat yi bàyyiwuñu ci dara. Ci seen i kàddu, njiitul àtte-tooñ bi mayu leen fu ñu yakke seen nàkk. Li àtte bi dem yépp, jógul ci di jalgati yoon.

Bi ci jiitu mooy ëtt bi gis na bu baax ñàkk teewug ki ñu war a àtte, maanaam Sëñ Usmaan Sonko. Waaye, àttekat bi mayul wenn yoon layookati Usmann Sonko yi ñu wax lu tax seen kiliyaaŋ mënul a teew. Donte ni sax yoroon nañ ñetti kayiti kër doktoor, Njiit li bëggu ci woon a xam dara. Te liy yoon mooy bu fekkee ni kees war a àtte teewul, warees na déglu ay layookatam ba xam li ko tere ñëw. Bu dee sabab bi dafa jëm ci wér-gi-yaramam, fekk mbir mi tollu fu ko kenn mënul a dàqe, njiitul àtte-tooñ bi dafa war a yebal ab àttekat ak gerefiyeewam mu fekk ko fa mu nekk ngir déglu ko te boole ay waxam ci wayndare wi.

Tere nañu layookat yi ñu wax, tereet seede yi ñu wax, Sëñ Biraayim Sekk ak Sëñ Keledoor Seen ñi nga xam ni tuddoon nañu leen ci mbir mi. Àttekat bi seetaanul widewoo yi ci wayndare wi tey wone ay firnde yu leer, fu jëwriñu koomal gi, jëwriñ jii di Maam Mbay Ñaŋ ak ñeneen di wax ni caabal gi am na.

Te bu fekkoon ni àtte-tooñ bi nangu woon na déglu layookat yi, fii yépp kenn du fi yegsi. Nde kon layoo bi du am. Rax-ci-dolli, Toppekat bi dafa yokk ci xar mi kawar, ba tey ci seen i kàddu. Li mu wax ni « Usmaan Sonko jiiñ na Maam Mbay Ñaŋ ni dafa luubal 29i tamñareet », Usmaan Sonko mësul a wax loolu. Walla Usmaan Sonko dafa sos « Usmaan Sonko dafa tudd caabal gu nekk ci net bi te kenn mënu koo teg bët ».

Bu nu yemee ci yii, li ñu dégg yépp ci bés bi keroog toppekat bi wax ko, dafa leen di niru ndaw lu ñu yebal te ragal nañu ni noppeegul ci yónnent bi. Ndaxte, bi àtte bi daanoo, ci saa si, la bind di sàkku ñu amalaat layoo bi.

Yelleefi Usmaan Sonko yépp dañ ko jalgati. Sonko dafa mës a bëgg teew ci layoo bi. Te, bi mu koy mën, mayuñu ko ko fenn. Fu mu jaar ñu ne ko du fii. Yamuñu foofu, ñu dellu daan Usmaan Sonko te layoo amul. Ndaxte ci li ñu xam, layoo bu jaar yoon mooy layoo bu am ci àtte-tooñ bu tëdde njaaxaanaay. Digante bi layoo bi di tàmbale ak bi àttekat biy joxe àtteem, soppi nañu ñetti yoon tëggin wi. Atte-tooñ bu ñuy defar, di defaraat ak a jekk-jekkal. Te loolu yépp, dafay jox dëgg Usmaan Sonko mi nga xam ne, ca njëlbéen ga la ni woon wóoluwul Yoonu réew mi. Te am na dëgg ci kow ñépp tey.

Meneen mbir mu ñu tudd ngir dëgëral li ñu wax mooy gaawantu gi toppekat bi gaawantu ci mbir mi. Lépp la taf-tafe. Bu fekkee ni Yoon rekk lañu bëggoon, amul lu ñu ciy gaawantu. Ndaxte, am na yeneen i wayndare yu gën a tembare yees mën a jàllale ba noppi. Lii yépp di leen firndeel ni dañ koy sant muy def, moom toppekat bi. Te, seen yéen du lenn lu dul fexe ba Usmaan Sonko bañ a bokk ci wote yii di ñëw. Te bés bi loolu amee, réew mi dina tàkk.

Bu ñu leen déggee daal, li soxal Maam mbay Ñaŋ mooy lu ni mel : Usmaan Sonko bañ a bokk ci wote yii di ñëw. Bi ndogalu àttekat bi jibee la njëkkoon a génn, di wone mbégteem. Yàggul dara mu neeti dafay sàkku ñu àttewaat ko. Bu fekkoon ni setal deram a ko taxoon a jóg neneen la loyoo bi doon demee. Te, Maam Mbay Ñaŋ du fésal mbégteem keroog bi daan bi dalee ba noppi delluwaat di sàkku ñu àttewaat mbir mi. Te àttewaat boobu, toppekat bi jot nay ndigal ba sóobu ci.

Ak li xew yépp, ñoom layookat yeek Usmaan Sonko, fas yéenewuñu leen seetaan ñuy def lu leen neex. Dinañu amal i taxawaay yu mucc ayib ba Usmaan Sonko jot i àqam bees àgge ci cëppaandaw li.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj