LAYOO USMAAN SONKO AK MAAM MBAY ÑAŊ

Yeneen i xët

Aji bind ji

Coowal 29 miliyaari yi ñu ne woon dañu ko luubal ca PRODAC, dekkiwaat na. Kii di Usmaan Sonko njiitul Pastef li mooy ki xolli góom bi. Ki mu duut baaraamu tuuma nag di Maam Mbay Ñaŋ, mi ko pelent. Moom nag, wuyuji woon na ginnaaw woote bi. Waaye, ba tey, coow li jeexagul. Ndekete kat, mbir mi, li ko tëgg tasu ko. Ndax, mujj nañu leen jàppal ab layoo ñaari fan ci weeru féerwaryee. Foofa nag, mooy daj dëpp gi. Ndax, bu ñu fa àggee moom, amatul dellu ginnaaw. Lu waay waxoon rekk na ca dellu.

Maam Mbay Ñaŋ nekk jamono jii jëwriñ ji ñu dénk wàllu Wërteef geek Noflaay gi mooy ki pelent kii di Usmaan Sonko. Pelent bee ngi tukkee cy kàddu yoy, meeru Sigicoor baa leen yékkati ñeel jëwriñ ji, keroog, ca ndajem-waxtaan ma mu amaloon. Ci mbirum PRODAC (Programme des Domaines Agricoles Communautaires) mi la ko tuumaal. Te, caabalug IGE gi daf ko jàpp. Kàddu yooyu waral pelent bi, mi ngi leen yékkati woon ci weeru nowàmbar wii weesu. Maam Mbay Ñaŋ dafa toogoon tele weddi ne laalewul mukk ak lees taqal. Sonko ne ko déet, ta nga ci ripp kay :

“Waxul dëgg ! Caabalug IGE gi jàpp na ko. Mën naa leen cee dawalal ay pàcc sax. Xam nga ñoom, li ñu xamul mooy wayndare yépp lanu am téye ko. Dégg naa bu ñu xéyee dañu naan waa ji fan lay jële ? Kan moo koy jox ? Kooku dem ca Ngomblaan ga naan genn caabal jàppu ko.”  

Kàddu yii la Maam Mbay Ñaŋ naanewul ndox. Ndege, dafa jibal kàddu yooyu rekk mu daldi koy dóor ab pelent. Ci la demee wuyuji. Waaye, coow li mooy kii di njiital Pastef li dafa am ñu ne dafa def njuumte ci ñaari bànqaas yi. Ndax, nee nañu IGF la bëggoon a wax. Ñaar yi bokkul IGF mooy Inspection Générale des Finances, IGE mooy Inspection Générale d’Etat. Kii di ndeyi-mbill gi moom nee na amul genn caabal goo xam ne jàpp na ko muy IGE di IGF. Loolu, lay biral ci kàddoom yii : 

“Li njëkk ci li may wax mooy caabal mësul am, muy gu IGE di  gu IGF walla  gu leneen. Man, ñi toog ni caabal daf ma jàpp yépp, pelent naa leen, daanlu naa leen. Ay rajo daanlu naa leen, ay tele daanlu naa leen, ay kibaaraan daanlu naa leen. Ñu dem ëttu àttewaay ba, indiwuñu caabal, kon caabal amul. Sa waa jooju ngay wax nag, Usmaan Sonko, moom dafa toog ci tele bi ne man xamuma dara. Barki-démb, dégg na ma, may wax ca Ngomblaan ga ne amul genn caabal gu ma jàpp, mu ne waxuma dëgg. Mu jël ag jollasoom dawal ne am na genn caabalu IGE gu ma jàpp, dawal ay pàcc, mu naan xamuñu ne ñoom téye nañu firnde yépp, waxul dëgg. Man, ne woon naa leen dinaa ko pelent, pelent naa ko. Ne woon naa leen bu demee pólis yóbbu caabal, man, ma dem ñu tëj ma. Dem na, te man maa ngi fii, kon yóbbuwul caabal. Ba mu demee ñu koy laaj ay waxi caabal dafa ne damaa juum. Nee na bëggul woon a wax IGE, IGF la bëggoon a wax. Caabalug IGF amul, Usmaan Sonko caabal gu mu am na indi. Waaye, bu indiwul ag caabal nag na réew mi yépp xam ne du waxkatu dëgg. Man nag, lii dama koy topp ba mu sës, Usmaan Sonko dina indi ag caabal. Nee na dafa juum du IGE, IGF la, na indi caabalug IGF. Man Maam Mbay caabal mësu ma jàpp.”    

Kon mbir mi, am na ci lees waxul de, walla ? Ndax, Maam Mbay nee na Usmaan Sonko dem na ñaari yoon DIC, di nëbbatu kenn yëguko. Bu njëkk bi daf ne waajalu ko, bi ci topp ba tey joxewul ag caabal. Waaye nag, ku mbojj tax a xëy ndax danga weer sa kuur ? Mu yokk ci sax ne, ba ba muy sàngoo suuf walla may sàngoo suuf du indi caabal gu ma jàpp. Lu tëw a xam rekk nag dafa yàggul. Te, loo bañ mu agsi, bul ko amal àpp. Dafa di, ñoom sax jàpp nañu bés boo xam ne ci lañu war a layoo. Moom Usmaan Sonko mu wax tuuma yi mu teg ci ndoddu Maam Mbay, fan la ko teg. Kii di Maam Mbay ma ngay wéy di ko tëkku ngir mu indi firnde yi muy wax. 

“Bu bés baa, na am ngoru bum daw, bu mu laaj ñu fomm layoo bi. Na am ngoru ni mu toogee jàkkarlook ay ñoñam tuumaal ma, na am ngor gu tollu noonu. Ndax, ci diggante bi, mat na weer ak genn-wàll, bu fekkoon lu mu denc la war na koo gis. Bu fekkoon lu mu yor la, ci ag jollasoom war na ko mën a génne, ñëw indi jox ko àttekat bi. Bu indee caabal, ma ne toppekat yeew ma nu dem.”

Kii di Usmaan Sonko, moom dafa mel ni delluwul wenn yoon ginnaaw ci li mu waxoon. Donte ne sax, ki mu séqal yëf yi nee na jébbalul lenn luy niru firnde, bi ñu ko woowee. Terewul fa mu jaroon rekk la jaaraat. Moom nag, la mu waxoon lay dëggalaat ci kàddoom ya mu yékkati woon ca ndaje ma mu doon amal ca dibéer jee weesu.

“May wax fii ñépp dégg ko, tuuma amul, tuuma amul. Ndax, damaa dawal wenn wayndare woo xam ne caabalug IGE la gu nekk ci lënd gi la. Caabal gi ne jàpp nañu ko moom Maam Mbay Ñaŋ ci ay tóoxidóona yu mu def moom ci PRODAC. Ma waxaat ko fii ñépp dégg ko, man maa ko wax, waxaat ko fii baamu ko.”                                   

Li am ba des mooy, layoo bi moom, ñaari fan la ci weeru féewaryee wii. Lu waay doon jaay dina lambu. Ndax, lu lëndëmoon ci mbir mi dina leer. Te, su boobaa, dees na xam fu dëgg féete. Caabal gi Usmaan Sonko di wax am na am déet ? Jàpp na Maam Mbay walla jàppu ko, dees na ci xam dara. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj