Démb ci àllarba ji lees doon amal ñaareelu joŋante démi-finaal diggante Manchester City ak Real Madrid. Real Madrid moo fekki woon Manchester City fa Àngalteer. Talaata jee weesu la ñaari ponkal yi njëkkoon a laale ca péeyub Espaañ ba, Madrid. Real Madrid moo ko dalaloon ca fowub Santhiago Bernabeu. Mu nekkoon joŋante bu metti bob, ñu bari dañ foogoon ne City daf ciy toroxal Real Madrid. Waaye de, Real dafa dëggaloon boppam, wane ne këram la nekk, tegal ko lu metti. Dañu mujje témboo, ku nekk dugal sa moroom benn bii. Ndam demul, ndam dikkul. Vinicius Junior a njëkkoon a lakk caax yi laata Kevin De Bruyne di xaañ ci caaxi Courtois yi ab bal bu teeŋ ŋàdd. Ndekete yoo, City dafa dencaloon Real Madrid toroxalam ca fowoom ba, Etihad Stadium.
Li ñu doon xaar ci Manchester City, lépp, démb la ko indi ca pàkkam ba, ci kanami soppeem, tegal Real Madrid lu metti, lu ko dale ndoorteelu joŋante bi ba muj gi. Àngale yi mayuñu wenn yoon Español fu ñuy xalaate bay futbal sax.
Bernardo Silva moo njëkk a toj kër gi ci 23eelu simili bi, daldi koy tojaat ci 37eel bi. Biñ delsee ci ñaareelu xaaj bi, Akanji ñetteel ko ci 76eelu simili bi laata Alvarez di ko ñeenteel ci 91eel bi. Moom Alvarez, ci bã bi la jóge, Foden mi ko paas mu dugal, ci bã bi la jóge, Mahrez mi jottali Foden bal bim paas Alvarez tamit, ci bã bi la jóge. Loolu di wone diisaayu ekibu Manchester City ak xereñte Pep Guardiola.
Manchester City dina dajeek Inter de Milan mi toogloo dëkkandoom ba AC Milan ci talaata ji ginnaaw bim ko dóoree 1-0. Inter dafa dóor AC Milan ñaari yoon ; nde, njëkkoon na ko làbbali 2-0 àllarba jee weesu. Kon, finaal bi diggante Inter de Milan lay doon ak Manchester City keroog 10i fan ci weeru suwe, bu 19i jotee, ca Istanbul, réewum Tirkii. Mu nar a doon joŋante bu rëy. Ndaxte, Inter gëj na jël kub bi. Manchester City, moom, mësu ko jël te moo ngi koy rëbb boobu ba léegi.