LËKKATOOG KAARAANGE DIGGANTE SENEGAAL AK MALI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw bi ñu xaatimee woon ab déggoo ci fànnu kaaraange ca atum 2021, réewum Senegaal ak mu Mali yeesal nañu seen ug lëkkatoo ngir gën a mën a saytu kaarangeg diiwaan bi.

Barki-démb ci alxames ji, jëwriñu làrme bu Senegaal, Seneraal Biram Jóob ak delegaasiyõŋam ñoo nga woon fa réewum Mali. Ñu demoon fa nag ngir dajeek naataangoom bii di Saajo Kamara. Muy ndaje mu am solo mu ñu fa doon amal jëme ci yeesal déggoob ñaari réew yi ñeel kaaraange gi.

Ginnaaw bi mu rafetloo nees leen dalalee foofa, jëwriñ ji Biram Jóob fàttali na ni ndaje mi amee solo ci Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay ak yitte ji mu am ngir dëgëral diggante ñaari réew yi ba tax mu yabal leen foofa. Fàttali naat ni, ca weeruw màrs 2021 la ñaari réew yi xaatimoon ab déggoo ñeel xarañteefu sóobare yi ngir dëgëral seen lëkkatoo ñeel kaaraange gi. Déggoo boobu itam am na ay njureef yu am solo, rawatina ci wàll wi jëm ci tàggatu kàngaami sóobare yi (les cadres militaires), ak di yónnantey estaaseer ci seen i lekkool yi.

Bu loolu weesoo, jëwriñ ji Biram Jóob taxaw na bu baax ci njariñu ñaari réew yi ñu boole seen doole ngir dékkoondoo lépp lu nar a jur fitna ci seen dig yi ñu séq. Ba tax muy woote jëme ci boole seen doole ci wàllu coytu, xibaarante ak tàggatu sóobare yi.

Jëwriñ ji wax naat ci lu aju ci aar dexu Faleme gi. Naka noonu, muy sàkku ci Njiiti Mali yi ñu dakkal ngasum mbindaare yees fay amal ni ko Senegaal defe ci diirub ñetti at ngir ñoŋal dex googu.

Seneraal Kamara itam dellusi na ci njariñ li ndaje moomu am ñeel dalug ñaari réew yi. Fàttali naat ciy kàddoom jaar-jaarub ñaari réew yi ci mboor. Ba tax muy biral ni donte réewum Mali génn na ci CEDEAO, du ko tere ubbeeku ci réew yi mu digaale. Dina séq ak ñoom i déggoo yu dëgër, ci kow ñu dëppoo ak gis-gisub Njiitu réew mi Seneraal Asimi Goyta.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj