Kilifa yi séq njàng mu kowe mi ubbi nañu lëlub ñetti fan. Ñu namm cee tëral i pexe ngir joyyanti atum njàng mi, delloo ko ca diir ba mu daan dox.
Démb ci àjjuma ji, 31 pani me 2024, lañu doon ubbi ab lël (séminaire) bi ñu jagleel njàng mu kowe mi. Ñaŋ ko doon amalee fa Soomoon (Mbuur), ci teewaayu Sëñ Abdurahmaan Juuf, jëwriñu njàng mu kowe mi, gëstu gi ak coste gi. Nemmeeku nañu fa itam teewaayu way-jàngune yi, ay njiit ci bokkeef gi ak i ma-xarañ.
Lël boobu, dinañu ko amal ci àppu ñetti fan, ngir rëdd pexe yees namm lal ñeel yamale àppu njàng mi ci at mu nekk. Lu ñu ko duggee nag mooy fas yéene jële fi at yu duggante yi ba faf jaxase njàng mu kowe mi.
Naka noonu, jëwriñ ji di leeral ni anam wi njàngale mi di doxee dafa jaxasoo, jaxasewaale jàngune yi. Am naat i njeexit yuy nasaxal koom-koom gi. Nde, dafay tax, at mu nekk, Càmm gi di ñàkk alal ju bari joo xam ne, dafa mel ni alal jees xëpp ci mbalit mi. Te, dara waralu ko lu dul ni at yi duggantee.
Njeexit yi dañoo law ba ci ndongo yi ndax dellu ginnaaw bi mu leen di jural. Licence bi ñu war a def ci ñetti at, ñoo ngi koy def ci ñeenti at. Master beet noonu, ci ñaari at lay war a am, waaye dafay jël ñetti at. Ñuy ay njeexit yuy jural ndongo yi dellu ginnaaw. Ndaxte, dañuy ñàkk ay at yu bare, Càmm gi tamit di ci ñàkk alal ju takku. Te alal jooju, Càmm gi mënoon na koo jëfandikoo ngir suqali njàngale mi.
Jëwriñ ji leeral naat ni jot nañoo weccooy xalaat ci àppug weer ngir ràññee jafe-jafe yi. Léegi nag, dinañu njëkk a lijjanti nees di safaraa jafe-jafey yi muy jur ci wàllu koom-koom. Bees ci noppee, dinañu sàkk ay pexe ngir dugal ndongo yi ci jàngune yi ci weer wàlla weer ak genn-wàll ginnaaw bi ñu amee bakalóoreyaa. Bu loolu weesoo, dinañu xool bu baax naka lañu mënee yeesal dalu Campusen ngir dëppale kook yenn bëgg-bëgg yi. Bu ko defee, ba ñu mën a tàmbali at mi ci weeru oktoobar ak dugg-bees yi, ñu daldi jublu ci jële fi at yu duggante yi. Ndax, ba léegi am na ñu jeexalagul seen atum daaw walla ñu tàmbaleegul mu ren mi.