LËNT-LËNT ÑEEL FAATUG MAMADU MUSTAFAA BA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Altine jee weesu, yemoo woon ak 4i pani nowàmbar 2024, la Mamadu Mustafaa Ba génnoon àdduna. Mi ngi faatoo Pari, fa réewum Farãs ginnaaw wopp ju gàtt ju ko daloon. Booba ba tey, kenn jébbalagu ko Boroomam. Nde, dafa mel ni dafa am lu ñuul ci soow mi. Maanaam, deewu Mamadu Mustafaa Ba gi dafa mel ni du neen. Moo tax toppekatu bokkeef gi bëgg cee amal ay luññutu ba xam lan moo lalu ci ginnaaw.

Anam yi Mamadu Mustafaa Ba génnee àdduna, moom mi fi nekkoon jëwriñu kopparal gi ak nafa gi, tàmbali naa ub boppi Saa-Senegaal yi. Ndax, bi mu faatoo ba tay, dencaguñu ko. Rax-ci-dolli, barki-démb ci gaawu bi la toppekatu bokkeef gi génnee ab yégle. Mu xamle ci ne dañuy amal otopsi. Li mu ci jublu, du lenn lu moy ñu mën a xam ci yan anam la Mamadu Mustafaa Ba génnee àdduna. Waaye, li otopsi boobu fésal, mel na ne dafa gën a yokk ci xar mi kawar.

Dafa di, moom toppekatu bokkeef gi dafa génneewaat beneen yégle démb, ci dibéer ji. Li mu xamle ci yégle boobu mooy ne, deewu Mamadu Mustafaa Ba gi niruwul ak neen. Ci gàttal, njureefi otopsi bi dañoo wone ne, ni ñu yaakaaree woon mbir mi, demewu fa noonu. Dafa am leneen lu nekk ci ginnaaw. Looloo tax, duñu ko mën a jébbalagum Boroomam. Toppekatu bokkeef gi xamle na ne dafa am ay luññutu yu ñu war a amal laata ñu koy rob. Ba tax na, ciy waxam, dañuy dàq rob bi fii ak ub diir. Su ko defee, ñu mën a matale liggéey bi ñu ci bëgg a def.

Li am ba des mooy ne, deewu Mamadu Mustafaa Ba gi jur na ay jiixi-jaaxa. Ndax, mel na ne, ni ko askanu Senegaal jàppe woon ak ni mu demee wuute na. Ñu bari dañoo jàppoon ne dafa jeexal rekk dem. Waaye, li toppekatu bokkeef gi siiwal dafay wund leneen. Lu ci mën di am, dees na ko xam fii ak ub diir. Li ci kanam moom, rawul i bët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj