Démb la Ngomblaan gi doon jeexal ndaje yi mu doon amal ak jëwriñi Càmm gi. Def nañ 32i fan yoy, jëwriñ ju nekk jaar na fa, biral naal yi mu sumb, daldi tontu ci laaji dépite yi. Ci alxamesu démb ji nag, mbirum koppar lees fa doon fénc. Nde, sémbub naalu ngurdu 2024 mee nekkoon ponku waxtaan wi. Ngurd moomu nag, mi ngi tollu ci 7 003,6 tamñaret (milyaar) ci sunuy koppar.
Bees sukkandikoo ci kàdduy jëwriñ jees dénk ngurd mi, Mamadu Mustafaa Ba, « coow li noon na fa kurr, tàngoon jérr waaye, Senegaal rekk a am ndam. » Jëwriñ ji neeti, dégg na bu baax mébéti dépite yi ak seen njàmbat. Joxe na fa kàddoom ci ne, dina ci xar tànki tubeyam ci atum 2024 mii. Li jar a laaj nag mooy, ndax ginnaaw féewaryee 2024 dina wéy di nekk jëwriñu ngurd am déet.
LEERALI SÉEX ISAA SÀLL, NJIITUL CDC
Tey, ci yoor-yoor bi, siiwaloon nan kàdduy Ayib Dafe, ndawul Usmaan Sonko li ko yóbbuloon warlug wote gi ca CDC. Moom, nag, dépite Ayib Dafe, waxoon na ci yégle bim biral ne joxe na fa segu 30i tamndaret ci sunuy koppar, ñu nanguloon ko ko ba jébbal ko sax kitãs, muy xaarandi ceedit gi. Te sax, moo ngi doon yedd waa CDC, di leen fàttali seen i wareef ak fu seen sañ-sañ yem ngir ñu bañ a topp tànki DGE. Njiitul CDC li nag, Séex Isaa Sàll, moom itam génn na, indiy leeral ci mbir mi. Igfm la doon waxee.
Bees sukkandikoo ci kàdduy Sëñ bi Sàll, « ndaw li joxe woon na segam ca giise ba. » Mi dolli ca ne, « dafa am uw tëralin ci ginnaaw giise bi wow, mooy xool teg li (dépôt), càmbar ko. » Ciy waxam ba tey, njëriwriñu biir réew mi daf leen a yónnee ag toftale gog, turi lawax yu ame xobi baayale yi ñoo ci nekk te, toftale googu, turu Usmaan Sonko nekku ci. Mu ne, looloo tax ñu delloo ko segam. Mu jeexalee ci ne, « li jëm ci wàllu ceedit gi, am nan àppug ñaari fan ngir torlu ko. » Waaye nag, balaa dara, bees sukkandikoo ci kàddoom ba tey, fàww boroom seg bi nekk ci toftale gi ba noppi ñuy sog a jàll ci yeneen jéego yi.
AAMADU BA, LAWAXU BENNOO BOKK YAAKAAR, DINA DEM PARI
Aamadu Ba mi njiitul jëwriñ yi, di yit lawaxu lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar, dina tukki ci ndoorteelu weeru desàmbar wii. Yéenekaay Jeune Afrique a ko siiwal, Senego tas ko. Nee ñu, tukki boobii, duggeewu ko lu moy wax ak Saa-Senegaali bitim-réew yi ngir yey leen. Nde, seetlu nañ ne, ci wote yi fi mujje am, kujje gi moo raafal daanaka lépp. Moo tax ñoom, waa Nguur gi, ñu bëgg a joyyanti mbir mi balaa 2024.
AJANDI NAÑU LAYOOB USTAAS UMAR AHMAD SÀLL AK TIIJAAN YI
Ustaas Umar Ahmad Sàll dina desandi ci kaso bi ba keroog 8i fan ci weer wii nu nekk. Li ko waral mooy ne, layoo bi waroon a am tey digganteem ak tiijaan yi koy tuumaal, àttekat bi daf ko dàq ba àjjuma jii di ñëw. kenn mënagul a wax nag sabax yi tax ñu dàq layoo bi.
Cig pàttali, lees jàppee Ustaas bi mooy ne, tiijaan yee wax ne daf leen tooñ, daldi ŋàññi seen tariiqa.