LI GËN A FÉS CI WOTEY 2024 YI (11/3/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

WOTEY 2024 YI : LAWAX YI TÀMBALI NAÑU DAGAAN YI

Démb ci dibéer ji la dagaanug baati askan wi ñeel wotey 24 féewiryee yi tàmbali. Lawax bu ci nekk jot na jàllale kàdduy ubbiteem fa RTS, tënkaale ci naalam ñeel fu mu namm a yóbbu réew mi bés bu faloo. Waaye, lawax bii di Basiiru Jomay Fay, kenn jàllalewul i kàddoom. Ginnaaw mi ngi ci kaso bi ba léegi, Baabakar Jaañ, Njiitul CNRA (Conseil national de régulation de l’audiovisuel), dafa gàntal widewoo bi lëkkatoo Jomaay gi dégtal, def ko ci turam.

Ginnaaw bi xëccoo bi tàmbalee, lawax yu bare, Ndakaaru ak li ko wër lañu tàmbalee. Ku ci mel ni Aamadu Ba ak mbabooram, fare ci Nguur gi, ña nga woon fa Kër Masaar ak Géejawaay. El Haaji Mamadu Jaawo itam, ma nga woon fa Kër Masaar. Bu dee Porefesëer Daawuda Njaay, ma nga tàmbalee fa Pikin ak Ginaaw Raay. Ba ci Anta Baabakar Ngom, ma nga woon fa Caaroy, Pikin, jaaraale Géejawaay ak Pàrsel Aseni.

PÀTTALIG CORED ÑEEL KIBAARAAN YI

Jamono jii lawax yi sóoboo ci dagaan yi, kuél gii di CORED (Conseil pour l’observation des règles d’éthique et de déontologie dans les Médias) mi ngi dellu di fàttali liggéeykati kibaaraan yi sàrt yi ñu war a sàmmonteel. Ci yégle bi mu génne tey ci altine ji, kurél gee ngi digal taskati xibaar yi ñu ànd ak màndute te yamale ci ni ñuy jàllalee xibaar yi. Nañ sàmmonteek doxalin yi méngook demokaraasi, muy jox ku ci nekk àqam ci lu amul benn par-parloo. Bu weesoo loolu itam, nañ fexe ba koppar gi ñu ciy fortaatu bañ leen a jiital ba di leen teree def seen liggéey ni mu ware.

SIDIKI KABAA DINA SÀMM KAARAANGE KÉPP KUY LAWAX

Sidiki Kabaa, magum jëwriñ yi, dige na ni dina jël matuwaay yi war ngir sàmm kaaraange képp kuy lawax ci jamonoy dagaan yi. Barki-démb ci gaawu gi la yékkati yile kàddu. Fekk mu doon jël lenge yi ci Aamadu ba mi mu wuutu ci boppu Càmm gu bees gi Njiitu réew mi taxawal ci ayu-bés bii weesu.

 NJIITUL U.A RAFETLU NA WOTE YI ÑUY MUJJE AMAL FI SENEGAAL

Weer ci ginnaaw, jafe woon na lool nit taxaw ni wote yi dina am ci jàmm fi Senegaal. Nde keroog bi Njiitu réew mi Maki Sàll jëlee ndogalu ajandi leen, yëngu-yëngu yi bare woon nañ lool. Ay nit sax jot nañ cee ñàkk seen i bakkan. Ginnaaw bi Njiitu réew mi jàppee bés bi ba ñu sóobu ci dagaan yi jëmale 24 màrs 2024, bés bi wote yi war a am, Njiitu U.A (Union Africaine) lu bees li Mohamed Uld Séex El Xasuwaani rafetlu na ni mbir yi mujjee dal ba ñu jublu ci wote yi. Moom mi doon sàkku ci Njiitu réew mi mu sàmmonteek Ndayu sàrti réew mi wax naat ni li ni mel dafay firndeel ni Senegaal réewum demokaraasi la, te itam ay campeefam dañuy dimbalante. Muy woo nag pàcc yépp ñu wéyal wile doxalin ngir wote yu jaar yoon te ànd ak dal mën a am fi Senegaal.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj