LI GËN A FÉS CI WOTEY 2024 YI (14/3/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

JURÓOMEELU FANU KÀMPAAÑ 

Dibéer jii weesu la kàmpaañ yi door. Ñoom, fukk ak juróom-ñeenti lawax yépp, song nañ dëkk yi, gox yeek gox-goxaat yi, di jaar ci mbedd yi ngir waxtaan ak askan wi. Dafa di, jamono jii moom, askan wi ñépp a ko bokk. Ñépp a ngi dem ci ñoom ngir dégtal leen seen i naal. Maanaam, li ñu namm ci réew mi bés bu ñu leen falee. Ñii ñu ngi Ndakaaru, ñee ñoo nga Cees, ñale Jurbel, ña ca des Kafrin, Ndar walla Koldaa. Ku nekk a ngi xalam ngir jéem a yey nit ñi.

BAABAKAR JÓOB (FDS/LES GUELWAAR) FEKKI NA JOMAAY FAY

Ñenn ci lawax yiñ gàntaloon ñoo ngi tànn seen i péete yiñ war a àndal ci wotey 24 màrs yees dëgmal. Lëkkatoo “Diomay Président” moo ci lees ci gën a dooleel nag.

Ginnaaw Meetar Musaa Jóob, Abdurahmaan Juuf ak ñeneen, kii di meeru Cees, Baabakar Jóob, jël na ndogalu ànd ak Basiiru Jomaay Fay ngir dooleel ko. Tey la ko biral, moom, njiitul làngu pólitig gees duppee “Forces Démocratiques du Sénégal” (FDS-LES GUELWAAR). 

Boobaak léegi, ñoo ngi doon xaar ba xam kan lay dooleel. Loolu moom leer na tey. Dafa bind, ci xëtu Facebookam, wax ne lawax bii di Basiiru Jomaay Fay lay dooleel ci wotey ñaar-fukki fan ak ñeent ci weeru màrs wii. Mu yokk ci ne, ndogal loolu, mi ngi ko jël ginnaaw ay waxtaan yu xóot yu mu séq ak ñi teewal lëkkatoog Jomaay gi ak ñi mu bokkal làng gi. Rax-ci-dolli, gis na ci lëkkatoo googu li mu jàpp ne mooy defar réew mi.

SERMEN SAAÑAA DOG NA ÀNDAM AK Pr DAAWDA NJAAY

Ba tey lu ñeel wote yi, kii di Sermen Saaña mi Porofesëer Daawuda Njaay defoon njiitul kàmpaañam, tekki na ndombog-tànkam. Sabab bi du lenn lu moy ne, moom daf ne lawaxam bi joxu ko àq ji war. Ndax, mënu koo jiital ba pare lu dal lawax bi walla lu xew ci làng gi yaak ñépp a koy yëgandoo ci mbaali jokkoo yi.

CÀKKUTEEFU LAWAX BUBAKAR KAMARA

Lawax bii di Buubakar Kamara wax na càkkuteefam. Li muy sàkku mooy, ñoom lawax yi, ñu amal aw waxtaan. Maanaan, ñu toog jàkkaarloo ak askan wi, ku nekk wax jox sa moroom, ñu faramfàcce naal yi. Bu ko defee, Saa-senegaal bu ci nekk mën a gam-gamle seen i sémb, tànn wi ci gën.

ËTTU ÀTTE BU KOWE DINA ÀDDU ËLLËG 

Ginnaaw bi Ndajem ndeyu sàrti réew mi gàntalee wayndarew Kariim Maysa Wàdd wi, PDS xàddeegul ba tey. Seen mébét mooy def lépp ngir wote bañ fee am. Ndax, ñi ngi dem ci mbooleem bànqaasi Yoon yi ngir ñu fomm wote yi. 

Looloo leen tax a song dekkare bi Njiitu réew mi jëloon ngir jàpp àppug wote yi. Ag kurél lañu taxawal, tuddee ko “Front Démocratique Pour une Election Inclusive” (FDPEI), daldi sóobu ci xeec bi. Waa ëttu àtte bu kowe boobu di “Cour suprême” fekkisi na leen ci loolu ba jàppal na leen ab àpp ngir ñu saytu dabantal gi ñu leen jébbal. Àjjumay suba ji, fukki fan ak juróom ci weeru màrs, la Ëtt bi àtte.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj