LI GËN A FËS CI WOTEY 2024 YI (19/3/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

XEEX BI AMOON ÑOORO : JÀPP NAÑ NDAWUL PASTEF LA

Militaŋi Pastef yee doon xeex ak takk-der yi fa Ñooro, diiwaanu Kawlax. Ñoom, ndawi Pastef yi, lëkkatoo “Diomaye Président” lañ doon xaar mu jaar fa. Xamuguñu li sabab xeex bi, waaye takk-der yi doon nañ sàndiy lakkirimosen ci mbooloo mi. Nemmeeku nañ ci ñaar ñu ci jëley gaañu-gaañu. Jàpp nañ ndaw li teewal Pastef ca gox ba.

ANTA BAABAKAR NGOM A NGI SOÑÑ ASKAN WI CI MU WOTE NGIR COPPITE

Soxna Anta Baabakar Ngom, njiitul ARC, ma nga woon Fatig démb ci altine ji. Ba mu jëlee kàddu gi, soññ na askan wi ci mu wote ngir coppite.

“Danu war a wote, keroog 24 màrs, ngir indi fi coppite ak njiit yu bees. Danu war dem ci coppite. Bu ko defee, nu ànd liggéey réew mi.”

Lawax bu jigéen bi xamleet na ne, keroog 24 màrs, jigéen ñi dañu war a wone seen taxawaay ba ñépp gis ko, ñu xam ni jigéen ñi desuñu ginnaaw. Ndax, ci waxi soxna si, du góor ñi kese ñoo yeyoo jiite réew mi. 

AAMADU BA : “ÑOORO DAFA WAR A NEKK BÉRÉBU YOKKUTE…”

Lawaxu Bennoo Bokk Yaakaar bee nga woon fa Ñooro di dagaan baatu askan wi. Ciy waxam, Ñooro dafa war a nekk bérébu yokkute. Dafa ne :

“Ñooro dafa war a nekk bérébu yokkute ndax mooy xol ak diggu réew mi, ànd ak ne dafa bari Lee fi mën a suqali. Loolu sax moo tax ñu war fi def ay tëralin ngir dooleel bennoo bi ak Gàmbi. Loolu dina tax ñu suqali fànn yi mel ni wërteef gi ak mbay mi.”

Aamadu Ba wax na fa tamit ne, bu ñu dooleelee mbay mi, napp gi, càmm gi te yeesalaat suuf si ñuy baye, Senegaal dina mën a dundal boppam te du jéggaani.

MOUVEMENT DE LA JEUNESSE RÉPUBLICAINE” FEKKI NA “DIOMAYE PRÉSIDENT”

Kurél gees duppee “Mouvement de le jeunesse républicaine” fekki na lëkkatoo Diomaye Président” ngir jàppale ko ci wotey 2024 yi. Boobaak léegi nag, ñu baree ngi màbb di wutali lëkkatoog tànneefu Usmaan Sonko bi. Kurél gees tudd ci kow a ci mujj. Ñoom, nee ñu :

“Danu gëm bu baax gis-gis, mbaax ak kilifteef gi ci seen lëkkatoo gi te wóor na nu ne moo gën ci sunu réew mi. Na dibéer 24 màrs 2024 gaaw ñëw ngir Senegaalu jàmm, bennoo ak naataange.”

CEERNO ALASAAN SÀLL FA NDAR : “DINAA WAXAALEWAAT PASI NAPP GI…”

Ceerno Alasaan Sàll ma nga woon fa Ndar di aajar naalam askan wa ak a jéem leen a yey ngir ñu wotee ko bu dibéeree, 24 màrs 2024. Ku wax Ndar, ne géej te ku ne géej wax napp. Moo tax njiitul “République des valeurs” joxe fay dige ñeel pasi napp gi.

Bi muy wax ak taskati-xibaar yi la biral ne dina :

“waxaalewaat pasi napp gi te saytuwaat lisãsi napp yépp yi tax Senegaal tumurànke ci fànn wi.”

Rax na ci dolli ne :

“Ndar dëkku nappkat la. Te tey xam ngeen ne ñu bari ci waa Get-Ndar dañu sóobu ci mbëkk mi, naan “Bàrsaa walla barsàq””. 

Moom Ceerno Alasaan Sàll wax na ne Senegaal dafa war a moom boppam ci wàllu mbatiit.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj