Coow li doxoon diggante Maam Mbay Ñaŋ ak Usmaan Sonko ba tey jeexagul. Waaye, mel na ne ña ngay bëgg a àgg ca daj-dëpp ga, ginnaaw ba ñu leen àttee juróom-ñetti fan ci weeru me atum 2023. Layoo booba, dañ caa daanoon Njiitul Pastef li juróom-benn weeri kaso yu mu dul tëdd ak ñaari téeméeri miliyoŋ yu mu war a dàmpe Maam Mbay. Moom, meeru Sigicoor bi, àndul woon ca àtte booba. Mu defoon ag dab-dabaatal fa ëttu àttewaay bu kowe bi. Tey ci alxames ji lañu leen di àttewaat. Dees na xam ndax ñoom dañuy dëggal àtte booba am dañu koy nasaxal. Fii ak ab diir dees na ci xam dara. Bu ñu dëggalee àtte ba nag, Usmaan Sonko dootul mënati bokk ciy wote.
CAYTUG XOBI BAAYALEY LAWAX YI
Ginnaaw bi àppu càkkug xobi baayale yi jeexee. Li ci topp mooy caytu gi ndajem ndeyu àtte mi di def. Keroog ak léegi nag, saytu nañu ñu bari. Waaye, néew na lool ñu ci jàllagum. Maanaam, ñi ci seen i xobi baayale mat walla jaar yoon bariwul. Muy ñi nga xam ne maxejj yee leen baayale walla dépite yi. Ñi ci jàllagum ñi ngi tollu ci juróom-ñeent : Buubakar Kamara, Séex Tiijaan Jéey, Décce Faal, Porofesëer Daawuda Njaay, Kariim Maysa Wàdd, Xalifa Baabakar Sàll, Abiib Si, Anta Baabakar Ngom ak Aamadu Ba. Am na ñeneen ñoo xam ne dañoo sàkku ci ñoom ñu mottali walla ñu saytuwaat seen i xob. Bu dee Abiib Si, moom, daf ne bu Usmaan Sonko jàllee day sempi ndëndam.
SOPPI NAÑU TURU RAGLU BU FATIG
Ca ndajem jëwriñ ma amoon démb, Njiitu réew mi, Maki Sàll jël na fa ay ndogal. Muy lu ci mel ni soppi turi yenn béréb yi. Béréb bi ci gën a fés ci yooyu mooy raglub Fatig bi. Raglu boobu tudde na ko léegi soxnaam si Mareem Fay Sàll.
“KEUR YEURMANDE” BU NDEELA MAAJOOR JUUF
Coow laa ngay gën a jolli, mbóot yay gën a sulleeku. Mbirum liir ya nekkoon ca Ndeela Maajoor Juuf, ña ca jot a laale ña nga ca loxoy yoon. Liir ba ñu jaaye woon 65 000 FCFA jenn jigéen, lépp mujje na leer. Ki def loolu di garjeŋ ba ak ndaw sa mu ko séqaloon, seen ug tëdd kaso nekkatul lu ñuy laam-laame.
XEW-XEW BU TIIS FA BÀKKEL
Bàkkel ab diwaan la bu nekke fa Tàmbaakundaa. Fa diwaan boobu la xew-xew ba am. Ab xeex la bu doxoon ci diggante ab tabaxkat ak benn sàmm. Waaye, mbir ma mujjul fu baax. Ndax, tabaxkat ba fa la jaare ñàkk bakkanam. Nee ñu, dafa am lu ko sàmm bi dóor ci tànk bi. Te, ba tey, xamuñu li mu ko dóor lan la. Ca lañu ko fobee yóbbu fa raglu bu Wuro-Sóogi. Waaye, nàcc gi bàyyiwu ko ba ni muy ñàkkee bakkanam. Ubbi nañu ci ag luñnutu ngir xam lan moo war a tax sàmm bi dóor ko ba mu faf dee ci.
DAGG NAÑU XAALISU MÓODU LÓO AK BOOY ÑAŊ
Altine jii weesu la ñaari mbër yooyu doon jàkkaarloo fa “Arène nationale”. Kii di Móodu Lóo nga xam ne ag njambaarteem ak xareñteem kenn dootu ko naatable mujjoon ci am ndam. Loolu terewul ñoom ñaar ñépp dagg nañ seen xaalis donte ne sax mbërum Pikin mi moo ëpp lu ñu ko dagg. Moom Booy Ñaŋ rekk dagg nañu ko ñaari miliyoŋ yu teg juróom-ñett fukki junni yu mànke ñeenti junni (2. 380. 000). Buuru làmbu ji ñu dagg ko benn miliyoŋ bu teg juróom-ñetti junni (1. 400. 000).
SAAJO MAANE TERALATI NA WAA BÀMBALI
Kuppekat bu mag bii di Saajo Maane ma nga woon fa dëkkam boobu di Bàmbali. Xew-xew ba mu fa doon teewe di ubbiteg fowu “terrain de foot” bu mu jagleel ndawi dëkkam. Mu nekk leneen luy dolliku ci ay jëfam ca Bàmbali. Ci loolu, jot na dénk xale ya ay kàddu ci naka lañuy def ba seen i gént doon dëgg.