LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (1/4/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

NJÀNG MEEK NJÀNGALE MI

Jëwriñu njàng mu kawe mi, gëstu beek coste gi, Abdurahmaan Juuf, àddu na ci mbirum jànguney jàmbure yi, fekk ñu doon ko dalal ci jotaayu RTS bii di Point de vue. Naka noonu, muy xamle ni fi réewum Senegaal, 8i jàngune la Bokkeef gi moom. Am nañu fi 298i jàngune yu ay jàmbur moomal seen bopp. Waaye, ci biir 298 yooyu, am na ci daanaka téeméeri jàngune ak lu teg yoo xam ne Nguur gi nangulu leen seen njàngale ak lijaasa yi ñuy joxe. Li ko waral nag mooy sàmmontewuñu ak sàrt yi war a tax ñu tijji ak ñuy nangu seen i lijaasa. Lu ni mel nag doon na lu doy waar lees war a joyyanti. Waaye dees na ci ànd ak teey ba bañ a yokk loraange ndongo yi ak seen i way-jur. Ndaxte, Nguur gi daan na fa dugal i ndongo, di leen fayal.

MEERU CEES BI NAR NAA AAYE SAAXAARI MBINDAARE YI

Meeru cees bi, Baabakar Jóob, dafa nar a aaye saxaar yiy jàllale mbindaare yi ñu aw foofa ca péeyam. Muy ndogal lu mu nar a jël bu fekkee ni kërug liggéey yi ciy yëngatu nanguwuñoo jël matuwaay yi war ñeel kaaraangeg koñ ya ñuy jaar. Nisar boobu nag, moo ngi ko fésal ginnaaw bi ab saxaar félee ab xale ba mu ñàkk ci bakkanam keroog àjjuma. Naka noonu, meeru dëkk ba di xamle ni lii du lu muy bàyyi muy wéy. Te du ci joxoñ kenn baaraamu tuuma ñu dul këri liggéey yi teg loxo balluwaayi mbindaarey gox ba, di yàq jaww ji. Rax-ci-dolli, amaluñu lennu njariñ péey bi ba noppi di lor askan wi.

MBËKK MI

Marinu réew mi tegati na loxo ag gaal gu doon mbëkki. Xibaar baa ngi ñu siiwalee ci seen kontu X. Démb ci altine ji, 31i fan ci weeru màrs lañu dog seen yoon ci ndoxi Saalum yi. Bees sukkandikoo ci li ñu jot a fésal, gaal gi yeboon na 92i doom-aadama. Luññutu yaa ngi ñuy amal ngir xam fu ñu bawoo ak teg loxo ñi sumb yoon wi.

BITIM-RÉEW

Fa réewum Farãs, Yoon dal na ci kaw Marine Le Pen ci mbirum dépite mooma ñu duppe Affaire des assistants parlementaires européens. Muy ndogal lu ëttu attewaay bu Pari (tribunal correctionnel de Paris) jël démb ci altine ji, 31i fan ci weeru màrs, ginnaaw bi ñu tënkee ni làngug pólitig gi mu jiite, di RN (Rassemblement national), dafa doon jëfandikoo i pexe ngir suufu xaalisu Bokkeef gi. Ndogal li nag, tëjlu na ko ñeenti ati kaso yoy, ñaar yi dafa leen di tëdd. Bu weesoo loolu, dina fay lu tollu ci 100 000iy Ëro. Ginnaaw bi ñu ko daane, dees na ko takkal lamub tànk ci diirub ñaari at yi mu waroon a tëdd kaso.

Lu ci gën a yéeme nag mooy li ndogal li nar a xajamal nekkug lawaxam ci wotey njiitum réew ya war a am ca atum 2027. Nde, bokk na ci daam bi itam juróomi at yu mu dul mën a nekk lawax donte  ni namm naa dugal ab dabantal.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj