LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (1/7/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

NDAJEM ÀDDINA SI ÑEEL KOPPARAL SUQALEEKU GI

Démb ci altine ji lañu doon amal Ndajem àddina si ñeel kopparal suqaleeku gi. Ñoo ngi ko doon amalee fa Séville, réewum Espaañ. Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay bokkoon na ci ñi ko doon teewe. Moom sax, gaawantu na ci teewaayam foofu ngir séq waxtaan ak kilifa yu bari, rawatina ak Ajay Banga (Njiitu kippaangog bànku àddina si), Alaar Kari (Njiitu Réewum Estoni), Filib VI (Buuru Espaañ), Emanuwel Makarõ (Njiitu Réewum Farãs). Ci yooyu tànk nag, Réewum Senegaal gën na a jëmmal jëflanteem ci wàllu koom-koom, dellu dëgëral taxawaayam ñeel suqaleeku gu sax ci àddina sépp.

KÀTTEY BAC 2025

Tàmbali nañu kàttey Bac bi (Baccalauréat général 2025) tay ci talaata ji, 1 sulet 2025. Kàttey ren ji nag, 166 402i lawax ñoo ciy joŋante ci biir réew mépp. Ñu séddale leen ci 387i bérébi kàtte (centre d’examen) yu 92i jàngu yu digg-dóomu di dalal. Bees sukkandikoo ci xibaar yi Pr Séex Ahmadu Bàmba Géey biral, ñu ëpp ci lawax yi, 59% (juróom-fukk ak juróom-ñeent ci téeméer bu nekk) ay jigéen lañu. Kilifa gi leeral naat ni jël nañu lépp luy matuwaay ngir kàtte yi jaar yoon, moo xam nit ñi la, jumtukaay yi walla kaaraange gi. Am na sax ay yeesal yu ñu ci andi. Lawax yépp ciy bataaxalu SMS lañu jote seen i limati taabal ak seen i bérébi kàtte. Ginnaaw kàtte yeek dinañu leen yónnee seen i njureef ciy SMS.

WOOTEB MABUUBA JAAÑ FA 44EELU LËLU FAO

Jëwriñ ji ñu dénk wàllu mbay mi, jur gi ak moom sa bopp ci dund bi yékkati nay Kàddu fa Itaali ga mu demoon. Fekk ñu doon amal fa Rom 44eelu lëlu FAO, di bànqaasu mbootaayu xeet yees jagleel dund beek mbay mi. Ci biir kàddoom yooyu, woo na askan yépp ci ñu booloo ngir dékkoondoo jafe-jafe yi àddina sépp di jànkonteel tay, rawatina xiif gi, lekk gu bon gi ak coppiteeku njuux li. Naka noonu, muy xamle ni yaatal xamteef ak coste ba ñépp jot leen képp mën a tax ñu taxawal doxalinuw mbay mu dëgër, mu mën a dox ci jamono te ñépp gis ci seen bopp.

Ci pàttali, wile yoon, lël bee ngi ñu doon amal ci wëppa wii di « dooleel coste ngir kaaraange dund bi ».

ÑAARI NDAW YI FAATU FA KÀMBÉREN

Fa kàmbéren, ñaari ndaw ñoo fa ñàkk seen i bakkan ci wàcc bu fa pólis amaloon. Muy mbir mu yéeme, mu tiis askan wa, waaye itam lu leen metti ba mënuñu ko woon a muñ. Loolu sax moo waraloon ba ñu génn ci mbedd yi, dog tali Kàmbéren beek VDN 3, ba mu mujje andi ay jàppante ci seen digganteek takk-der yi ci altine ji.

Bees sukkandikoo ci xibaar yi jot a jibe ca askan wa, ndaw yi faatu dañoo lab ginnaaw bi ñu doon daw pólis ba dugg ci biir ndox mi. Waaye pólis wax nañu ne kenn ci seen i ndaw yi lañu dogaale ba mu ñëw komiseeriyaa bu Pàrsel, U15. Looloo taxoon ba ñu wàcc ci tefesu Kàmbéren.

Ginnaaw gi, meeru dëkk ba génn na metitlu paatug ndaw yi, waaye itam dëfal askan wi ñu ànd ak dal. Tay ci talaata jeet, DGPN (Direction Générale de la Police Nationale) xamle na ni luññutu yee ngi ñuy wéyal te pólis taxaw na ci ngir leeral lépp.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj