LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (1/8/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

YENEEN TABB YU YEES

Démb, ci àllarba ji la Njiitu réew mi doon amal ndajem jëwriñ mi. Jot naa waxtaane ay poñ yu bari fa ndaje ma laata muy ñëw ci tàbb yi. Tabb yii nag wute na ak yi fi jot a jàll donte ne sax, am na yoo xam ne ñoo ëpp ñu ñu tabb walla mu gën a néew. Waaye, wii yoon dañu cee nemmeeku mbir mu doy waar. Nde, kenn ci ñi mu tabboon lu yàggul dara ci benn béréb, démb la ko fa jële, teg fa keneen. Kooku du kenn ku mooy Séex Jeŋ mi ñu tabboon njiitul ONAS. Jële nañu ko fa, daldi fay teg kii di Séeni Jéen. Ginnaaw loolu, am na ñeneen ñu mu takkal ay ndomboy-tànk.

Móodu Jaañ tabb nañu ko « Secrétaire permanent du Comité interministériel de Lutte contre la Migration irrégulière ». Ki mu fa wuutu di Mamadu Bookar Li ;

Ibraahiima Jeŋ nekkoon fi Komiseer bu Tàmbaakundaa, moom lañu tabb Njiitul « l’Automatisation des Fichiers ». Mu wuutu fa béréb boobu kii di Fiyaakar Burunoo Léwopól Bajaan,

Daawuda Gajaga, tabb nañu ko « Directeur des Ressources humaines ». Béréb boobu wuutuwu fa kenn. Maanaam, kenn nekku fa woon ;

Mamadu Lamin Ñaŋ, moom lañu tabb Njiitul « Police judiciaire ». Ki mu wuutu fa béréb boobu di Idiriisa Siise ;

Alasaan Ñaŋ nekkoon fi Njiitul tàggatug pólisu réew mi, moom lañu tabb Njiitul « l’Office central de Répression du Trafic illicite des Stupéfiants ». Mu wuutu fa béréb boobu kii di Njara Seen ;

Mamadu Nduur, tabb nañu ko Njiitul « Groupement mobile d’Intervention ». Ki mu fa wuutu di Njaga Jóob ;

Sanu Juuf lañu tabb Njiitul « Formation de la Police nationale ». Mu wuutu fa kii di Alasaan ñaan ;

Njara Seen, tabb nañu ko Njiitul « Sécurité publique ». Ki mu fa wuutu di Ibraahiima Jóob ;

Abu Léy, moom lañu tabb Njiitul « Police de l’Air et des Frontières ». Wuutuwul kenn fa béréb boobu ;

Mareem Jaawo tabb nañu ko Njiitul « Police des Etrangers et des Titres de voyages ». Mu wuutu fa béréb boobu kii di Jibril Kamara ;

Séeni Jéen lañu tabb njiitul ONAS. Ki mu fa wuutu di Séex Jeŋ.

NJIITU RÉEW MI DEM NA MURTANI

Tey ci alxames ji, benn fan ci weeru ut la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay amalaat ñaareelu tukkeem fa réewum Muritani. Ndax, ginnaaw bi ñu ko falee, jotoon na faa dem. Wii yoon, da faa dem ngir fekke waatu Njiitu réew ma. Maanaam, li ñuy wax ci farãse “prestation de serment”. Ndax, bu yàggul dara lañu ko falaat moom Muhammed Uld Séex Al Gasuwanii. Moom nag, ci bés bi lay ñibbisi.

MAMADU KABIIRU MBÓOJ GÉNN NA ÀDDUNA

Mamadu Kabiiru Mbóoj nekkoon fi meeru Pikin moo wuyuji boroomam tey ci suba. Moom nag, mel na ne kenn dootu ko naatable ci géewu pólitig bi. Ndax, nekkoon na fi “Chef de cabinet” ki fi nekkoon Njiitu réew, Léwopóol Sedaar Seŋoor ci atum 1962. Ci atum 1963 la nekk meeru Pikin. Nekk na fa boppu meeri ba luy tollu ci fanweeri at. Ci at moomu tamit la nekke dépite fa Ngomblaan ga. Kon, mënees na ne, ki fi jóge tey, am na lu mu def ci pólitig.

DAAN NAÑU MUSAA DADIS KAMARA

Démb ci àllarba ji lañu ko daan, moom Musaa Dadis Kamara. Li ko waral mooy coow li ko toppoon ñeel jéyyay ñaar-fukki fan ak juróom-ñett ci weeru sàttumbar atum 2009, fa Gine Konaakiri. Dafa di, ay jàmmaarloo moo fa amoon, lu jege téeméeri nit ak juróom-fukk ak juróom-benn ñàkk ci seen i bakkan. Ñii ñu reye leen paaka, ñee bal, ña ca des jaasi. Ay téeméeri doomi aadaama jële ci ay gaañu-gaañu. Xew-xew bu tiis boobee tax ñu daan ko ñaar-fukki ati kaso. Ay layookatam nag, nee nañu loolu du ci dal. Ndax, ñoom ànduñu ci àtte bi. Te, dinañu sàkku àtteb dabantal.

TËJAAT NAÑU SÀQI WALFADJIRI

Ci weeru suwe wii weesu rekk, jotoon nañoo tëj sàqi Walfadjiri, wii kon mooy ñaareelu yoon. Bi ñu leen njëkkee tëj tamit, li ñu leen doon toppe mooy ay lempo yu ñu feyul woon diggante atum 2016 ak 2018. Wii yoon, li waral mbir mi mooy borub 2016 boo xam ne am na pàcc bu ñu ci jotoon a fey. Waaye, ñii di waa “Impôts et domaines” dafa mel ni dañoo bëgg ñu fey lépp, mbir mi féete boor.

AB XIBAAR ÑEEL NDONGO YIY SOG A AM BAC

Bu yàggul dara la joŋante Bac bi jàll. Waaye, mel na ne bëru ndongo yi am Bac narul yàgg. Ndax, kii di jëwriñ ji ñu dénk njàng mu kowe mi, Elaas Abdurahmaan Juuf siiwal na àpp yi ndongo yi war a defee seen tànneef yi. Maanaam, kañ la ndongo yi war a tànn daara yu kowe yi ñu bëgg a jànge. Su ko defee, ku nekk ci ñoom mën a xam jan walla yan daara yu kowe ñoo ko jël. Ci la ndongo bi di xame jan daara la war a jànge at yii di ñëw. Àpp boobu, mi ngi ko jàpp diggante juróom-ñaari fan ci weeru ut ba ñaar-fukki fan ak juróom-ñaar ci weeru ut.

ISMAAYLA SAAR DELLU NA ÀNGALTEER

Lu tollu ci at rekk ginnaaw ba mu fa jógee ak léegi dem Farãs ca këlëb bii di Marseille, moom Ismayla Saar delluwaat na fa. Waaye, wii yoon du ékib ba mu fa njëkkoon nekk di Watford la dellu. Ci këlëb bii di Crystal Palace la dem. Xaatim na ak ñoom pasu gu tollu ci juróomi at.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj