NJIITU RÉEW MI TEEWE NA 42eelu JOTAAYU “Comité d’orientation de l’AUDA-NEPAD”
Ci xëtu Facebookam la Njiitu réew mi xamle ne teewe na jotaayu “Comité d’orientation de l’AUDA-NEPAD”. Ci li mu bind, feddali na yéene ji Senegaal am ci liggéey ngir waral Afrig gu moom boppam te naat.
Ba tay ciy waxam, ëllëgu Afrig mi ngi aju ci ndaw ñi nga xam ne, jàngal nañu leen te tàggat leen. Moo tax, bees sukkandikoo ciy mbindam, ñu war a dëppale naali njàng yi ak jumtukaayi xarala yu yees yi, “digitalisation” bi ak “intelligence artificielle” bi. Nde, moom Njiitu réew mi dafa gëm ni Afrig dafa war a sukkandiku ci boppam ngir suqaliku.
SAR TÀMBALI NA SEGG SOROJU SENEGAAL BI
SAR tàmbali na segg toqi soroj yi njëkk a ballee fi réew mi. Guléet nag, ginnaaw 64i at bi ñu ko taxawalee ak léegi, SAR di liggéey soroj bees rootee ci teeni soroj yu Senegaal yi. loolu di jéego bu réy ci wàll wi. Nde, dafa bokk ci liy tax Senegaal moom boppam. Ndax, am réew mënul a woote moom-sa-bopp fekk mënul liggéeyal boppam lay tukkee ciy balluy mbindaareem.
ABDUL MBAY SÀKKU AY LEERAL CI USMAAN SONKO
Saabalkat bii di Aaroona Kan dafa siiwal, xamle ne xaalis bi Càmm gi fay ci raglu yi dafay yokk at mu nekk. Ci atum 2024 mi, ci 30i miliyaar la tolloon. Ciy waxam, 18i miliyaar ñoo ciy dolleeku at mu jot. Yokkute googu nag, dafa jural njàqare elimaanu jëwriñ ja woon, Abdul Mbay.
Loolu moo tax njiitul làngu pólitig gii di Alliance pour la citoyenneté et le travail (Act) di sàkku ay leeral ci elimaanu jëwriñ ji, Usmaan Sonko. Senego moo tuxal kàddoom yii toftalu :
“Ginnaaw bi ma dawalee ciiwalug Aroona O. Kan ci yokkuteg xaalis bi Càmm giy fay ci raglu yi, mu tollu ci 30i miliyaar ci atum 2024, waxees ne dafay yokk ba tegal 18i miliyaar at mu jot. Dafa war ci elimaanu jëwriñ yi mu indi ci ay leeral.”
ÑAXTUY NJÀNGAANI LIISE NDOMBO SÀNJEERI
Njàngaani Liise Ndombo Sànjeeri jël nañu ndogalu dakkal njàng mi ci altiney tay jii. Te, ci seen i wax, mën nañu ko wéyal bu dee fajaluñu leen seen aajo. Li ñuy kaas mooy li ñu tumurànke jumtukaayi njàng. Dañuy joxoñ baaraamu tuuma “Conseil départemental de Dagana”, di wax ne sàmmontewul ak li mu dige woon, maanaam jox leen jumtukaayi njàng yu doy, rawatina ay masini fotokopi “machines de risographie”.
Ci li njàngaani Liise Ndombo Sànjeeri yi wax, “Conseil départemental de Dagana” bi dafa dige woon ne dina jëndal masin yooyu ñetti Liise yii di Ndombo, Gaya ak Dagana. Waaye, dañu am mbetteel bi ñu gisee ne yeneen ñaari Liise yi jot nañu ci seen i masin ba mu des Liise bu Ndombo. Loolu nag, jàpp nañu ne du yoon.
BOR : SËRIÑ MBUUB MI NGI FAYEEKU CÀMM GI 700i MILIYOŊ
Sëriñ Mbuub miy meeru Kawlax dafa yëkkatiwaat ndefaru ndimo gii di Domitexka Saloum ngir nit ñi mën a am liggéey, waayeet ngir suuxat fànn wi.
Moom nag, Sëriñ Mbuub, dafa jàpp ne Senegaal mënul a moom boppam fileek Càmm gi dimbaliwul liggéeykat yi. Ci kow loolu la xamle ne Càmm gi ameel na ndefaram gi bor bu réy bu koy teree jëm kanam. Bor boobu mi ngi tollu ci 700i miliyoŋ, donte ne ca jamonoy Abdulaay Wàdd la bor bi amoon.
GII MARI SAAÑAA : “LENN REKK LAAY WAX DONALD TRUMP…”
Dépite saa-Senegaal bi, Gii Marii Saañaa tontu na Njiitu réewmu Amerig, Donald Trump. Fan yii, Njiit loolu dafa dankaafu woon réewum Afrig-dii-Sidd. Ci xëtu X bi mu moom la bind lii toftalu :
“Ngir Donald Trump miy dugg ci mbiri Afrig-dii-Sidd, lenn rekk laa koy wax : « shut up, it’s an african thing » (tëj ko, mbirum saa-Afrig yi la).”
FARBA NGOM JËLI NA KËYITUG WOOLOOM
Dépite bii di Farba Ngom, ñu summi fi malaanum kiiraayam lu yàggul dara, àndoon na ak i layookatam fa DIC ngir jëli këyitug wooloom. Moom nag, dañu koy topp ci mbirum 125i miliyaar yi fi juroon coow fan yii. Alxames jii ñu dëgmal, bu 12i waxtu jotee, lay wuyuji.