LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (11/12/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

WOTEY 2024 YI

Tey ci altine ji, 11 desàmbar 2023, la deppo yi ñeel nekkug lawax ci wotey 2024 di tàmbale fa ndajem ndeyu àtte mi. Fileek fukki fan ak juróom lañ leen di amal. Képp ku bëgg nekk lawax te jëloon xobi baayale yi, war na ci moom mu jébbal ko wayndareem ngir mu mën koo càmbar. Naka noonu, deppo yi dinañu wéy di leen amal ba ci bésub 26 desàmbar bii di ñëw. Bés bu nekk, dees na tijji pekk ya bu 8i waxtu jotee ba 17i waxtu. Bu waxtu wii rombeet, dina am ndaw lu fay taaxirlu ba xaaju guddi ngir xaar ñi yéex a yegsi.

COOWAL NJËNDUM NGÀNNAAY MEEK NJAAYUM MARJAAN MI

Li Sñ Musaa Jóob biral ci njëndum ngànnaay meek njaayum marjaan mi jur na coow lu réy ci réew mi. Ki fi nekkoon njiitul Dakar Dem Dikk dafa siiwal ni mbuxum ak nger mu réy a am ci balluy mbindaare yi. Li ci doy waar nag, mooy ne, Njiitu réew mi Maki Sàll ak Aali Nguy Njaay mi fi nekkoon jëwriñ ci Càmm gi la ci taqal ripp, boole ceek i wayndare yu mu wane ni ñoo ko xaatim.

Ginnaaw wax jooju nag, ay ñoñi Aali Nguy Njaay génn nañ ngir weddi lu ni mel. Ñuy xamle ni, li Musaa Jóob wax amul te kayit yi mu génn yi ay sos kese lañ. Naka noonoot, waa MIMRAN ñi ci Sñ Musaa Jóob tuddeet weddi nañ lu ni mel. Ak lum ci mën a doon, Aminata Ture, kenn ci ñi bëgg nekk lawax ci wotey 2024 yi, jàpp na ni mbir mu doy waar la te Ngombalaan gi war na cee ubbib lànket ngir leeral ko.

MBOOTAAYU MEERI SENEGAAL YI

Ams (Association des maires du Sénégal) di mbootaay mi dajale meeri bokk-moomeel yi ci réew mi, mi ngi ci yoonu tasaaroo. Lu tollu ci 114i meer ñoo mànkoo génn ci ba set wecc. Démb ci dibéer ji lañ ko siiwal ci bi ñuy amal ab lël fa Kawlag. Naka noonoot, ñu siiwal ni taxawal nañ seen mbootaayu bopp ndax ni mbootaay mee di doxe gisuñu ci seen bopp. Keroog 5i fan ci weeru desàmbar lañ taxawal seen mbootaay mu bees mi ci turu Cmdic (Collectif des maires pour la défense des intérêts des communes), maanaam mbootaayu meer yi ñeel taxawu soxlay bokk-moomeel yi.

BESUB ÀQ AK YELLEEFI DOOM-AADAMA

Démb ci dibéer ji, la àddina wërngal këpp doon màggal bés bees jagleel àq ak yelleefi doom-aadama. Bu ren ji di 75eel wi yoon ñu koy amal bi ñu biralee àq ak yelleefi doom-aadam ci àddina sépp (Déclaration universelle des droits de l’homme) ca atum 1948 ak tey. Naka noonu, kurél gi ñu duppe Forum du Justiciable, di yëngatu ci wàll wile fii ci Senegaal, doon na ko jëmmal itam. Waaye, gaawantu na ceet ngir gaaral Njiitu réew mi ak Càmm gi cib yëgle bu ñu siiwal. Muy sàkku ci ñoom taxawaay bu mucc ayib te gën a sàmmonteek àq ak yelleefi doom-aadama.

Ci seen bataaxal booboot, waa kurél gaa nga cay fàttali Càmm gi ak képp kenn ci géewu pólitig bi nga bàyyi xel ci sañ-sañi nit ñi, rawatina jamono yii ñu dëgmal i wote ci 2024 bi. Ba tax ñuy woote jëmali ci tawaxaayu maxejj bu matale, bu sàmmonteek doxalin yees tëral, ngir ñu mën a am wote yu jaar yoon.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj