Ku Maki Sàll di tànn ? Ñan ñooy xàll seen yooni bopp, samp seen i ndënd ? Laaj yii ñoo ub bopp yi, rawatina yoy APR yeek Bennoo Bokk Yaakaar. Bi Maki Sàll nee du bokk ba tey, kàngam yi bokk ci moom nelawatuñ. Ndax, ku ci nekk a ngi daas fanaanal, di nos ak a nocci ci suuf.
Abdulaay Juuf Saar moom, nëbbul ne dafa bëgg a wuutu Maki Sàll. Wax na leen ko waa kilifay APR yi ca seen ndaje ma ñu amaloon. Bu dee ñoom Abdulaay Daawda Jàllo, Aali Nguy Njaay, Aamadu Ba, añs., ku ci nekk a ngi ñaan doon tànneefu Njiitu réew mi ngir nekk lawaxu lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar.
Pastef dina tabb Usmaan Sonko lawax bésub 15 sulet 2023
Waa Pastef fas nañoo yéene tabb seen njiit li, meeru Sigicoor bii di Usmaan Sonko, def ko seen lawax ci wotey 2024 yi. Ci gaawu gii, 15 sulet 2023, lañu jàpp xew-xew bi. El Maalig Njaay ne :
” Askanu Senegaal tànn na lawaxam ! Bésub 15 sulet 2023, ay tamndareti saa-senegaal, ci biir réew mi ak bitim-réew, dinañ tabb ci lu bir Usmaan Sonko, yaakaaru maasug lëmm. Bu bés baa, dinañ takkaala jaray gor yi. Afrig a ngi xool di xaar, àddina saa ngi xool di dégg, xoli saa-senegaal yi dinañ bokk riirandoo ni xolub kenn nit ci bés bu màgg boobu. Bu leen ko kenn nettali !”
MAKI SÀLL DALAL NA DÉPITEY BENNOO BOKK YAAKAAR
Tey ci talaata ji, 11 sulet 2023, Njiitu réew mi Maki Sàll dalal na dépitey Bennoo Bokk Yaakaar fa pale, bi 16i waxtu jotee. Yéenekaay Source A moo siiwal xibaar bi. Nee ñu, li sabab ndaje mi mooy ponk yees jukkee ci waxtaan wi Njiitu réew mi woote woon, ñu war leen a jaarale ca Ngomblaan ga. Bokk na ci coppite yees war a indi ci ndeyu àtte réew mi ngir joyyanti càrtug wote gi. Coppite yooyu, dinañ tax ba Xalifa Sàll ak Kariim Wàdd mën a bokk ci wote yi.
MBIRUM ALIW SAANE MU Y’EN A MARRE
Bëtal nañ mbiri Aliw Saane ba 18 sulet 2023. Njiitul Y’en A Marre liy tof-njiitu kurélug F24, dañ ko jàppoon keroog ba mu seetijee woon Usmaan Sonko. Ginnaaw gi la ko àttekat bi bàyyeendi. Waaye, toppekat bi àndul ci ndogalu àttekat bi. Moo ko taxoon a bind néegub tuumalaate bu « tribunal de grande instance de Dakar » ngir ñu jàppaat Aliw Saane, téye ko fileek ñu koy àtte.Talaata jii di ñëw la àttekat biy jël ndogalam.
NJARIÑEY SOROJ BI : “BARIGO BU NJËKK BI DINA GÉNN CI…”(JËWRIÑ)
Sofi Galaadimaa doon na daje ak waa HCCT. Ba mu génnee ca ndaje ma nag, àddu ci liggéeyub soroj bi ak njariñ yees ciy xaar. Moom, jëwriñu soroj bi, nee : ” Ci njeexitalu atum 2023 la njëlbeenug barigob soroj biy génn, gën-gaa yàgg ci ndoorteelu atum 2024 mi. Barigo bi waroon a génn ci weeru suwe wii nu génn, waaye dafa am ay ngànt yu nu bett.”
Ginnaaw bi mu indee leeral yooyu, jëwriñ ji ñaax na askan wi ngir fexee sàmm jàmmi réew ngir ñu mën a jariñoo soroj bi. Lu ko moy, ñeneen ñoo koy jariñoo. Mu ne soroj bi dafa war a nekk barke, waaye warul a nekk musiba.
CEDEAO : NJIITI RÉEW YI NDOKKEEL NAÑ MAKI SÀLL
Démb, Njiiti réewi CEDEAO yi doon nañ amal am ndaje mu mag fa Bisaawóo. Sargal nañ fa Njiitu réew mi Maki Sàll, ndokkeel ko bu baax a baax ci ndogalu bañ a bokk ci wotey 2024 yi. Nde, Njiiti réewi CEDEAO yi dañu rafetlu kàdduy Njiitu réew mi Maki Sàll, keroog 3 suwe 2023. Ndaxte, ñoom, dañu jàpp ne kàddu yooyu ñoo jur jàmm ci réew mi.
Ñoom nag, ñaax nañu way-pólitigi Senegaal yépp ngir ñu suuxat jàmm ci réew mi, bañ a taal fitna, waxtaan ba déggoo. Bu ko defee ñu amal wote yu dal te jaar ci yoon.