CAABALUG ËTTUB CETTANTAL BI : CÀMM GI DINA JANOOK TASKATI XIBAAR YI ËLLËG
Ëttub cettantal gi siiwal na caabalu caytug koppari réew mi diggante 2019 ak màrs 2024. Fi mu nekk nii, coow laa ngi ne kurr fi réew mi. Nde, ay xeeti jalgati, njuuj-njaaj ak wuruj yu doy a doy waar la caabal gi feeñal. Li ci gënatee doy waar mooy ne, loolu yépp, nguurug Maki Sàll ga woon daf ko nëbboon askan wi.
Càmm gi fas na yéene amal am ndaje ak saabalkat yi ëllëg ci alxames ji, bu 16i waxtu jotee ca fukkeelu etaasu Taaxub caytu bees dippee Mamadu Ja.
AYU-BÉS BEES JAGLEEL CËSLAAYU LEKOOL BI
Démb ci altine ji lañu doon ubbi ayu-bés bi ñu jagleel cëslaayu lekool bi. Ñu doon ko amalee fa EFI (École de Formation des Instituteurs) bu Rufisque ci teewaayu Mustafaa Giraasi (jëwriñu njàng mi) ak Biram Jóob (jëwriñu Làrme bi). Atum ren ji nag mooy 24eel wi yoon ñu koy màggal fi réew mi. Ñu ciy waxtaane sàmm mbaax yi ci nekkiinuw askan wi, lekool bi ak taxawaayu takk-der yi ñeel njariñu réew mi.
TOLLUWAAYU NGER GI
Senegaal seqi na ñaari jéego ñeel xeexub mbuxum mi. Jóge na ca 43i poñ ya mu nekkoon ca atum 2023, tàbbi ci 45i poñ ci atum 2024 mi. Bees sukkandikoo ci waa Forum civil, bokk na ci li ko waral, coppite yi ñu indi ci diggante ñaari at yii (2023 ak 2024). Muy nag yokkute gu am solo donte ni dese na ko lu bari ci xeex bi ngir génn ci tolluwaay bi ñu duppe zone rouge. Ba tax ñuy sàkku ci Nguur gi mu gën a leeral jëme ci caabali IGE yi ak xeex bi jëm ci mbuxum.
WOOLU NAÑU TAYIIRU SAAR
Yoon woolu na Séydu Saar, ñu gën ko xam ci turuw Tayiiru Saar. Waa Dic (Division des informations criminelles) ñoo ko jébbal kayitug woolu ci àjjuma jee weesu ngir mu wuyusi naka alxemes jii di ñëw (13 féewiryee). Xamaguñu nag ci lees ko bëgg déglu. Waaye bokk na ci ñees tudd seen tur ci luññutu bi PJF (Parquet Judiciaire Financier) di amal ci coowal 125i tamñareeti FCFA yi juddu ginnaaw caabal gi Centif (Cellule nationale de traitement des informations financières) génne.
SYNACOM DUUT NA BAARAAM JËWRIÑU YAXANTU BI
SYNACOM (Syndicat National des Agents de l’Administration du Commerce), di kurélug liggéeykati caytu gi ñeel yaxantu bi, joxoñ na baaraamu tuuma kii di Sëriñ Géy Jóob (jëwriñu yaxantu bi). Ci yëgle bi ñu génne, ña nga cay wax ni dafa soofantal seen i yitte. Nde, du wenn yoon wu mu indi saafara yu solowu ci seen i ñaxtu bi ñu ko tabbee ak tey. Rax-ci-dolli, nu ko neex la yoree jëwriñal yaxantu bi. Du diisoo lu bari te saa su amee dafay ñàkkal fulla gis-gisub ma-xereñ yi. Ba tax ñuy fàttali ni bi ñu tabbee jëwriñ ji ak tey, ñoo ngi wéy di jéem i pexe ngir yokkute jëwriñal yaxantu bi ak bañ coow juddu fa.
NDOGUM YOON MI AM FA KAWLAX
Ndogum yoon amatina ci tali bi. Ag daamaar (sept places) moo yenu ag sëfaan gu taxawoon fi tollook Liise Gànjaay, fa Kawlax. Bees sukkandikoo ci xibaar yi Kàppiteen Mamadu Yayaa Maane yegge sunuy naataango yu APS, démb ci altine ji, bi 22i waxtu jotee ba teg 41i simili lañu leen woo ngir yegge leen ko. 8i doom-aadam ñoo ci loru. Ñaar ñi dañoo faatu ca saa sa. Mu am juróom yu ci jële ay gaañu-gaañu yu metti. Ki ci des moom dese naa sonn.