LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (12/6/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

TUKKIB NJIITU RÉEW MI CI BËJ-GÀNNAARU RÉEW MI

Tay, ci alxames ji, la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, door ab tukki ci bëj-gànnaaru réew mi. Maanaam, fa boori Ndar. Tukki boobu nag, ñaari fan la koy def. Dafa dii lii ab tukki la boo xam ne koom gi la ko jagleel. Looloo tax, yamul ci dëkku Ndar ba kese. Dem na ci yenn ci dëkk yi ko wër walla jege. Te, noppeegul ci tukki bi donte ne sax, sànq ci tàkkusaan gi dellu na Ndar.

YOON JOX NA DËGG AYSATU JÓOB FAAL

Jëwriñ ji ñu dénk jokkoo gi dafa génnee woon jamono yale ab yégle biral ci saabalukaay yi nga xam ne sàmmonte nañu ak sàrt yi. Saabalukaay yi nga xam ne sàmmontewuñu woon ak sàrt yi dañu leen xamaloon ne duñu mën a wéyal seen liggéey. Bi loolu amee, moom Aysatu Jóob Faal, ñu yónnee ko bataaxal ne ko na saabalukaayam yi dakkal seen liggéey. Ca la jébbale ag dabantal fa ëttu àttewaay bu kawe ba ngir ŋàññi ndogal boobu. Tay, ci alxames ji, la àttekat bi jël ndogalu neenal bataaxal bi ko jëwriñ ji yónnee woon ngir saabalukaayam yi bàyyi di feeñal lenn lu mu mën a doon.

ÑIBBISIG UJAAJ YI

Ca jamono yee weesu la ñenn ci julliti réewum Senegaal yi demoon fa Màkka. Li ñu ko dugge woon mooy matale benn ci ponki lislaam yi, muy aj. Loolu di firndeel ne tukkib jaamu Yàlla la. Ñoom nag, ginnaaw ba ñu fa defee ab diir ba matale li leen taxoon a jóg, tàmbali nañoo ñibbisi. Nde, tay jii sax dina am ñu jëwriñ ji ñu dénk wàllum dem beek dikk bi, teeru fa dalub roppalaan ya di AIBD (Aéroport International Blaise Diagne). Mu am xew-xew bu tiis bu am ci ñibbisig ujaaj yi. Nde, dafa am ci ñi jot a ñibbisi démb ku ci ñàkk bakkanam. Soxna suy wuyoo ci turu Ajaa Móomi Sekk moo ci ñàkk bakkanam. Mi ngi tolloon ci juróom-ñaar fukki at ak benn.

XEW-XEW BU TIIS FA SIGICOOR

Ab xew-xew bu tiis moo am fa koñ bii di Sancaba, nekke fa Siggicoor. Mi ngi am ci ngoonug démb gi. Benn xale bu góor buy tollu ci fukki at ak ñett la benn moroomam bóom. Bees sukkandikoo ci waa Senego, dañu doon xuloo faf yëf ya ëpp i loxo. Ca noona, mu daldi koy jam, mu jaare fa ñàkk bakkanam. Ki def jëf ji nag, tegaguñu ko loxo. Ndax, bi mbir mi amee rekk la daw. Waaye, waa pólis door nañu ag luññutu ngir teg loxo ki def jëf ju ñaaw jooju.

BENEEN XEW-XEW BU YÉEME FA MBUUR

Tay, ci suba, la xew-xew bu tiis am fa koñ bii di Santesu, nekke fa Mbuur. Genn daamar moo fa fiir ñetti taalibe. Bees sukkandikoo ci Senego, kenn ki moom génn na àdduna. Ñaar ñi ci des tamit sonn nañu lool sax. Li ci gën a doy waar kay mooy dawalkat bi def jëf ji dafa daw, kenn tegu ko bët. Jamono jii, ñi ngi koy wër ngir leeral mbir moomu.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj