LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (12/8/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

TUKKIB ELIMAANU JËWRIÑ YI FA TIRKI

Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, jeexal na démb ci àjjuma ji tukki bi mu doon amal fa réewum Tirkii. Ci juróomi fan yi mu fa def ginnaaw bi ko fa Njiitu réew ma Recep Tayyip Erdogan dalalee, torlu nañu fa pas yu bari ci fànn yu wuute. Ñaari kilifa yi biral nañu itam seen taxawaay ngir gën a dooleel lëkkatoo bi dox ci diggante ñaari réew yi. Ci noonu sax, réewum Tirkii fas na a yéene ful ba ci ñett ay amalanteem ci wàllu yaxantu bi.

SOPPARÑI NDIISOO GU MAG GU MASISTARAA YI CSM

Séydi Gasama àddu na ci Ndiisoo gu mag gu masistaraa yi CSM (Conseil Supérieur de la Magistrature). Ñuy ay kàddu yu mu fésal ci mbaali jokkoo yi. Kàddu yooyu nag, moo nga cay fésal yéeneem jëme ci sopparñi campeef googu. Ci gis-gis bi mu ci am, sopparñi boobu dafa war a jublu ci féexal bu baax campeef googu. Naka noonu, Njiitu réew mi ak jëwriñ ji yor wàllu Yoon dañu ci war a seppi seen i loxo ngir kuréli Nguur yi mën a tàqalikoo bu baax. Bu weesoo loolu, gis na ni itam mënees na a ubbil campeef gi layookat yi, way-jàngune yi ci wàllu Yoon ak way-moomeel yi, ñu am ñu leen fa teewal.

MÀGGAL TUUBAA

Ëllëg ci àllarba ji mooy bésu Màggal Tuubaa. Muy bés bu Séex Ahmadu Bàmba mi sos yoonu Murit woote woon ngir sant Boroomam ci bés bi ko tubaab yi doon jële Senegaal. At mu jot ay miliyoŋi doom-aadama, di jóge fu nekk ci àddina si ngir di ko màggal. Màggalug ren ji nag, pólis jël na matuwaay yu doy ngir taxawu kaaraange taalibe yi fay daje, laata bés bi, ci bés bi ba ca ëllëg sa. Bees sukkandikoo ci xibaar yi komiseer Jegaan Seen, komiseeru Tuubaa, xamle, yóbbu nañu fa lu tollu ci 4 606i ndaw, jébbal leen 154i daamar, boole kook i jumtukaayi xarala yu yees yu deme niy kameraa ak i dóróon. Matuwaay yee ngi ñu séddali ci 11i barabi pólis. Am na itam ñatti barabi fajukaay yu ñu taxawal, ñu mën faa fajoo ci lu ñu dul fay dara.

TÀGGAT-YARAM

Tay ci talaata ji la gaynde Senegaal yu basket bi doon amal seen joŋante bu njëkk ci Afrobasket 2025 bi ñuy amal fa Àngolaa. Ñu doon ci janook ekibu Ugàndaa bi. Ca mujjantal ga nag, gaynde yi ñoo mujjee jël ndam li, daldee dóor 88 poñ ci 53i poñ. Muy ubbite bu baax nag. Ci seen ñaareelu joŋante, gaynde yi dinañu laaleek doomi Esipt yi, ginnaaw gi ñu mujjee Mali. Ndax  ñett ñooñu la bokkal kippu D bi.

Ci wàllu futbal beet, gaynde yi doon nañu laale ak doomi Kóngoo yi ci CHAN bi ñuy amal ci diggante Keeñaa, Tansani ak Ugàndaa. Waaye, ñaari ekib yi dañu mujjee témboo (1-1). Ci seen joŋante bu njëkk, gaynde yi dañu amoon ndam ci kaw Niseriyaa. Dinañu laaleek réewum Sudã ci seen ñetteelu joŋante.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj