LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (13/2/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

ETAASINI A NGI YEDD NGUURU SENEGAAL

Àmbaasad Etaasini mi ngi yeddati Nguurug Maki Sàll gi. Ab tweet lañ bind, wax ci ne :

“Ci réewi demokaraasi yum el ni Etaasini ak Senegaal, nit ñi sañ nañoo dajaalo ci jàmm ngir ñaxtu ci seen teeyu bakkan. Noo ngi ñaax Nguuru Senegaal ak takk-der yi ci ñu sàmmoonte bu baax ak àq yooyu, di soññ askan wi tamit ñu ànd ak seen sago te bañ a yàq dara.”

WALF JOTAAT NA SIÑAALAM

Këru kibaaraan gii di Walf jotaat na siñaalam. Bërki-démb ci dibéer ji la jëwriñ ji yor jokkoo beek xarala yi ci aju, Meetar Musaa Bookar Caam jël ndogalu delloo Walf seen lisãs ak siñaal. Fekk mu nangu woon ko ginnaaw ñaxtu yi waa Walf doon wone keroog bi Njiitu réew mi Maki Sàll jëlee ndogalu ajandi wote yi. Ci yégle bi mu génne nag, jëwriñ jee ngi ciy leeral ni ndogal lu mu jël la ginnaaw bi ay kilifa yu bokk ci kurélu maxejj yi seetijee Njiitu réew mi, waxtaan ak moom ci njekk.

BOLAA ÑËWATUL SENEGAAL

Tukki gi Njiitul CEDEAO li, Bolaa Tinubu, di itam Njiitu réewum Niseriyaa, nammoon na amal fi réew mi fomm na. Sunuy naataango yu Press Afrik ñoo ko xamle. Ci altine ji la waroon a teew fi réew mi. Mu nammoon a waxtaan ak Njiitu réew mi Maki Sàll ci tolluwaayu réew mi. Li mu bëggoon dëgg-dëgg ci waxtaan woowu sax mooy soññ ko mu sàmmonteek Ndayu Àtte réew mi ba Senegaal mën a génn ci guuta gi ko ajandi wote yi dugal. Li waral fomm gi nag, dees na ko leeral.

RADDHO ÑAAWLU NA DOXALINU FDS YI

Kurél gii di RADDHO (Rencontre Africaine pour la Défense des Droits de l’Homme) ñaawlu na bu baax ni takk-der yi doon doxalee ak way-ñaxtu yi ci fan yii. Ci yégle bi mu génne, ma nga cay xamle ni taafar gu metti lañ seetlu ni doon nañ ko jëfandikoo, jëmale ko ci taskati xibaar yeek maxejj yi. Am na itam ñu bare ñuñ teg loxo, tëj leen. Bokk na ci ñoom juróomi taskati xibaar yoy kenn ki jigéen la. Te taskati xibaar yooyu defuñu lu dul seen liggéey.

Ginnaaw loolu itam, kurél gi dellu na di sàkku ci askan wi ñu def seen ñaxtu ci tekk ak teey, ni leen ko yoon mayee. Takk-der yeet, nañ leen gunge, aar leen, sàmm seen kaaraange ni ko seen liggéey diglee.

KÀDDUY MAMADU LAMIN LAAHI

Mamadu Lamin Laahi mi yor kàddu njabootu laayeen wax na ci tolluwaayu réew mi. Seen Woote bi ñuy amal at mu jot, di xew-xewu diine, dafa dajeek ren yëngu-yëngu yi judduwaat ci réew mi ba ay bakkan rot ci. Woote jàmm nag moo gën a ràññeeku ci kàddoom yooyu. Muy xamal way-pólitig yi ne war nañ mën a waxtaan ci seen biir ba am i déggoo. Lu ko moy itam bees salfaañee bokk-moomeel gi, kenn du ci mucc.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj