Ilimaanu jëwriñ yi daje naak saa-senegaal yiy dund fa Muritani ci tukki bi mu doon amal fa réew ma. Muy ndaje mom, doomi réewum Senegaal yi gaawantu nañu ca ngir sàkku ci Càmm gi ay ngogal ñeel lu yembal seen nekkin foofu. Bokk na ci li leen gën a yitteel, ñu ubbil leen fa Nuwaksot ab lekoolu Senegaal ndax ñu mën a toppatoo seen njàngum doom yi ci anam yu gën. Bu weesoo loolu, sàkku nañu itam ci Càmmug réewum Senegaal mu sàkk i ndimbal ci wàlluw yoon ñeel seen i mbokki réew yi nekk ca kaso ya foofa.
Ginnaaw bi mu leen dégloo, ilimaanu jëwriñ yi dig na leen ni dinañu yombal seen dëkkiin foofa. Waaye, dees na ko def ci ànd ak sàmmonteek moom-sa-boppug réew yi Saa-Senegaal yi nekk ak seen i sàrt. Ba tax mu dellu di leen soññ ci ñu sàmmonteek sàrti réew yi ñu nekk di dund.
CÀMM GI NEENAL NA
Ilimaanu jëwriñ yi santaane na ñu neenal daggub këri Hangar des pélerins, Boa, Recasement 2, Eogen ak Eogen-Extension Pointe Sarène, Njéebeen Gànjól ak béréb bi dox diggante géej geek VDN bu Géejawaay, jàpp Yëmbël, Malika ba Tiwaawan-Pël. Muy ndogal lu mu jël ngir doxal càkkuteefi pekk gi yor caytug suuf si (Comité technique sur la gestion du foncier), ginnaaw bi mu saytoo caabal yi ñu ko jébbal.
POOL JUDICIAIRE BEE NGI CI TÀNKI TOPP XAALISUB MBUXUM BU TAKKU
Ëttu PJF (Pool judiciaire financier) bee gi ci tànki ubbi ab luññutu ñeel xaalisub mbuxum bu takku. Démb ci dibéer ji lañu ko biral cib yégle. Bees sukkandikoo ci xibaar yi ñu siiwal, jot nañu ay caabal ci CENTIF (Cellule Nationale de Traitement des Informations Financières) yoy, njàngat yi ñu jot a def dañu feeñal ay xeeti pexe yu xarañe yu ay nit jëfandikoo ngir mbuxum alal jooju. Ñiŋ ko jaarale ciy këri liggéey yu nekkul ngir amal i yónney xaalis yu teey xel. Te xaalis boobu àppagum nañu ko ci 125i tamñareeti FCFA. Ñu nar leen a toppe yi ñuy duppee defkati ñaawteef, mbuxum, njuuj-njaaj alali askan wi, nger, mbubboo seen tur ak def lu la neex ci moomeeli mboolaay mi.
GAAL YI KËPPU FA NDAR
Ñaari gaal ñoo këppu ci bël bi nekk fa Ndar. Looloo ngi xewoon ci 9 ak 10i fani sãwiyee 2024. Ndog loolu nag, waral na 2i doom-aadama yu ci ñàkk seen i bakkan. Naka noonu, jot nañu cee xettali 27, mu am 6 yu réer ba léegi. Ginnaaw bi mu jaalee njabooti ñi ci faatu ak di leen mastawu, jëwriñu napp gi, jumtukaay yi ci géej geek waax yi soññ na nappkat yi ci ñu sàmmonteek bu baax ndogal yi ñeel kaaraange gi, rawatina di topp xibaar yi metewoo di leen baaxe, di sol seen i sile bu ñuy nekk ci géej gi ak di yamale seen sëf yi.