LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (14/7/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

MBËKK MI : 6I NÉEW YU BEES YU FEEÑ FA NDAR

Ñeenti bés ci tey, bi gaal ga suuxee ca bëlub Ndar ba, yeboon i roñukat yu jëmoon Espaañ. 8i nit ñoo ci labagum woon, am ñu baree bari ña réer. Démb ci ngoon, Marin Senegaal feeñal 6i nit yoy, indaalewuñu bakkan. Muy 14i nit ñu géej gi wannagum, bees ci dollee 8 ña njëkk ña. Moo tax, démb, jëwriñu biir réew mi, Antuwaan Feliks Jom, demoon na ba Ndar ngir nemmeeku mbir mi. 

MBËKK MI : GENN GAALUG SENEGAAL TEER NA FA ESPAAÑ 

Ndaw ñi songaat nañu mbëkk mi ak doole. Ndeke, du ñetti gaal ya bawoo woon Kafuntin ak gaalug Ndar gu suux gi ñoo wutali woon Espaañ.  Ndax, am geneen gog, moom, àgg na Espaañ ak 41i nit ya mu yeb. ONG Village du migrant moo ko yégle. Danu bind ne :

” Ag gaal gu jóge Senegaal, 8i fan ci tey, te yeb 41i roñukat yoy, am na ci jigéenu biir, agsi Tenerife (Espaañ) ci boori 13i waxtu yu tegal 23i simili. Amul benn jafe-jafe buñ ci nemmeekoogum jamono jii.”

PEREFE GÉEJAWAAY BI TERE NA TABBUG USMAAN SONKO 

Perefe Géejawaay bi siiwal na ab areete ngir xew-xewu tabb bi waa Pastef nammoon a amalee fa estaad Aamadu Bari :

” Ayees na, ngir daw fitna ak jaxasoo, ndaje mees jàpp bésub 15 sulet 2023, li ko dale 14i waxtu jàpp 19i waxtu, fa estaad Aamadu Bari, ci càkkuteefu Mamadu Wàdd, Ngañ Saar ak Mamadu Séy, ndawi Pastef fi Géejawaay. “

Komiseeru Géejawaay bi lañ sant mu doxal aaye bi.

AAYEB NDAJEM MU WAA PASTEF : ALIYUN TIN A NGI WAX AK GORNOOR YI AK PEREFE YI

Aliyun TIN, boroom Afrikajom Center rafetluwul aaye bees aaye ndajem tabb mi waa Pastef amoon yéene amal fa Géejawaay. Moom, àndul ak ndogal yi gornooru Ndakaaru beek perefeb Géejawaay bi jël. Moom, Aliyun Tin, dafa gëm ne, gornoor yi ak perefe yi dañu war a dimbali Maki Sàll ngir mu dem ci jàmm. Moo tax mu leen ñaax ak a jóo ci ñu doxal li ndeyu-àtte ji sàrtal, te bañ a jeng.

AMNESTY A NGI ÑAAWLU TERE YI ÑUY TERE NDAJE YEEK XEW-XEW YI

Amnesty Internationale dafa bind ab tweet di ñaawlu aaye yi ñu xew-xew yi waroon am yépp diggante gaawu ak dibéer. Kurél giy xeexal àq ak yelleefi doom-aadama dafa jàpp ne, doxalin wu ni mel dafa safaanoo ak demokaraasi. Moo leen a tax bind ne :

” Ni ñu teree xew-xew yi waroon am yépp diggante gaawu ak dibéer dafa worook sàrti réewum demokaraasi. “

Cig pàttali, gornooru Ndakaaru bi dafa aaye bépp xeetu xew-xew buy am ci gëblag Ndakaaru gi diggante gaawu ak dibéer. 

PIKIN : LAKK AMATI NA

Ginnaaw jawub “marché zinc” bi lakkoon, am na geneen lakk gu amati ca talib Tali-Bu-Mag, yoonu “marché zinc”. Démb ci guddi gi la jéyya ji am, lakk njaay yu bari. 

Bees sukkandikoo ci yéenekaay L’as, 4i màngasin ñoo lakk. Sàppëer yee gaaw fay lakk gi, lu ko moy, musiba bi doon gën a jéggi dayo. Xamaguñ li sabab lakk gi. Ñoo ngi amal ab luññutu ngir leeral ko.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj