LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI 15/11/2023

Yeneen i xët

Aji bind ji

TUXAL NAÑU USMAAN SONKO

Lu ëpp ñetti weer ginnaaw ba ñu ko jëlee ca kasob Sébikotaan yóbbu ko ca raglub Principal ngir fajee ko fa, tuxalees na Usmaan Sonko, yòbbu ko Kab-Maniwel. Ak li wér-giyaramam di sooxe yépp, jëlewaat nañu ko ca raglu ba delloo ko kaso. Waaye, wii yoon moom delluwul Sébikotaan. Kasob Kab-Maniwel lañu ko yóbbu. Tuxal googu nag jur na coow. Ndax, ñenn ci waa Pastef dañu ne tuxal googu fajkatam bi yëgu ko. Ca la jëwriñ ji ñu dénk wàllu Yoon génnee yégle xamle ne tuxal googu fajkat bi nga xam ne mooy saytu wér-gi-yaramam yég na ko. Maanaam loolu sax ci ndogalam lañu ko defe. Kon, jamono jii ñetti lawax ñu war a bokk ci wotey 2024 yi ñoo nga ca Kab-Maniwel. Muy moom Usmaan Sonko, Basiiru Jomaay Fay ak Séex Omar Jaañ.

XUWAAN BARÀNKOO JËLAAT NA YOONU SENEGAAL

Ay weer ginnaaw bi mu fi ñëwee woon, ñu waññi ko, Xuwaan Barànkoo dina jéema duggaat Senegaal. Moom,  layookatu Njiitul Pastef li, xamle na ne am na ndogalu ëttu àttewaay bu kowe bi (cour supreme) ngir ñëw teewal kiliyaanam bi. Li waral loolu mooy ne, àjjuma jii ñu dëgmal la ëtt boobu war a àdduwaat ci ndogal li àttekatu Sigicoor bi jëloon ñeel dugalaatug Usmaan Sonko ci wayndarew wote yi. Rax-ci-dolli, ñu jox ko ay xobi baayaleem. Loolu la ndawul Nguur gi (AJE) ne du ci dal. Ca la deme ca ëtt boobu ngir ñu saytuwaat ndogal loolu. Waa ëtt boobu nag dinañu àtte mbir moomu ci àjjuma jii. Liy tukkee ci àtte boobu mooy doon liy firndeel bokk walla ñàkk a bokkug Njiitul Pastef li ci wote yii di ñëw.

DÉCCE FAAL DAKKAL NA WUTUB XOB YI

Lu tollu ci weer ak fukki fan ak juróom moo des ngir lawax yi jébbal seen i xobi baayale. Moom Décce Faal, Njiitul PRP li, xaarul loolu di jot. Ndax, nee na, dakkal na wutub xob yi. Li ko sababoon mooy, ciy waxam, li mu doon sàkku am na ko ci saa-senegaal yi nekk fii ak bitim-réew. Mébétam moo nekkoon am limu 57. 975i torlu (signatures). Waaye, ci li mu jot a dagaan, mujje na am lu tollu ci 127. 453 ci ay xob.

SAES JËL NA NDOGAL

SAES di kurél gi boole jàngalekat yi nekk ci daara yu kowe yi jël na ndogal ñeel tëjug daara ju kowe jii di UCAD. Ay weer ginnaaw ba ñu ko tëjee ak léegi, ba tey tijjeegul i buntam. Njàngale mi nag, ñi ngi ko doon doxal jaare ko ci xarala yu yees yi (en ligne). Nee ñu, ñoom waa SAES, jël nañu ndogalu dakkal njàngale yooyu. Maanaam seen càkkuteef mooy ñu ubbiwaat daara ji ci nu mu gën a gaawe.

MBËKK MI

Ndaw ñi teggeeguñu seen tànk fi ñu ko tegoon ba tey. Mu mel ni jamono jii ku demul tamit yaa ngiy nisër ak waaj a tëmb ci geej gi, bu fekkeew jotagoo dem ba ñu waññi la. Ndax, démb rekk, am na gaal gu teeriji ca Tenerife. Yeboon na lu tollu ci juróom-ñaar-fukki nit ak juróom-ñaar. Am na fukk yoo xam ne nag, nee ñu, sonnu nañu lool.

Naka noonu, marinu Senegaal bi tamit am na ñoo xam ne ba tey moo leen teree génn réew mi. Ndax, ci altine ji rekk, jàpp nañu ñaari gaal yu jëloon yoonu Espaañ wi. Gaal yooyu ñi ngi yeboon lu tollu cin ñetti téeméeri doomi-aadama ak ñaar-fukk ak juróom.

FAMA YI NANGU NAÑU KIDAAL

Kidaal nekkoon ab béréb ca Mali boo xam ne rëtalkat ya ñoo fa tegoon tànk. Dafa mel ni loolu soldaari Asimi Goytaa yi jële nañu ko fa. Démb ci talaata ji lañu siiwal ne làrme Mali bi mujje naa foqati Kidaal ci loxoy rëtalkat ya ca tegoon loxo bu yàgg ba tey. Mu doon ndam lu réy ci làrme bi ak ki leen jiite, di Njiitu réew ma, Asimi Goytaa. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj