Barki-démb ci gaawu gi, doon nañ amal ndajem weccante xalaat ci anam yees di amalee wote yi fi réew mi. Muy am ndaje mu kurélug maxejj gi ñuy duppe Forum Civil woote woon fa Mbuur. Way-pólitig yu bari teewoon nañ fa, ay ma-xarañ ak i fara-maxejj. Bees sukkandikoo ci kàddu yi Biraahim Sekk, ki yor kàddu kurél gi, yékkati, doon na ndaje mu ñu amal ngir waxtaane lépp luy leeral amiinu wote yi ak mataleg noste gi, maanaam sistem bi. Naka noonu, muy xamle ni, Njiitu réew mi jox na leen kàddoom ni dina amal am péncoo jagleel ko sistemu wote yi. Jotoon na sax biral xalaat ñeel wàll wile ak nees di defaraatee taxawaayu làngi pólitig yi.
SAS BI CEDEAO YEN BASIIRU JOMAAY JAXAAR FAY
Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, àddu na ci liggéey bi ko waa CEDEAO sant ci digganteem ak ñetti réew yii di Burkinaa, Niseer ak Mali. muy liggéeyu dox tànki jàmm ngir delloosi ñetti réew yi ci biir kurélug CEDEAO ginnaaw bi ñu génnee ba ber seen kurélug bopp cim reéwaloo mu ñu duppe AES (Alliance des États du Sahel). Naka noonu, Njiitu réew mi di xamle ni nangu na liggéey boobu. Te, dina ci def lépp lum gëm ni war na koo def, muy wax, waxtaan ak liggéey ngir jokkalewaat leen. Waaye, fas na koo yéene jooxe ci woyof te bañ cee ànd ak xérte.Xibaar
NJIITU RÉEW MI TABB NA PORFESOOR BÀCCILI
Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomay Fay, tabb na Pr Abdulaay Bàccili ci wetam. Muy tabb gog, dafa ko def ngir mu koy jàppale ci misiyoŋ yees ko jagleel fa bitim-réew. Barki-démb la ko siiwalaale ci bi muy janook taskati xibaar yi. Fekk mu doon wax ci lu jëm ci cantaaneg CEDEAO gi. Naka noonu, muy leeral ni du ci misiyoŋ CEDEAO bi rekk la koy soxla, waaye ci bépp misiyoŋ bu mu mën a am bitim-réew. Looloo tax mu waxtaan ak moom ba mu nangul ko ko. Bu jëlee ndogal loolu nag, dafa fekk ni Sëñ Bàccili doon na ku muy soxla ndax li mu xam ci wàll wi, taxawaay bi mu ci am ak cër bi ñu ko ci jox àddina sépp.
5Oi EKTAAR YI NGUUR GI NANGU FA MBÓOJEEN
Fa Mbóojeen, Nguur gi nangu na fa juróomi ektaar. Moo ngi ko nangoo ci woykat bii di Akon. Fekk nguuru Maki Sàll ga woon joxoon ko ko ca atum 2018. Mu jëmoon ci sémbub dëkk bu bees bu mu fa amoon te duppe ko Akon City. Bees sukkandikoo ci xibaar yi sunuy naataango yu Africa Intelligence siiwal, Akon dafa tële dajale alal ji war, ay tamñareeti dolaar, ngir mën a taxawal lu ni mel. Ci atum 2023 bi nag la ko Nguur gi dànkaafu woon ni dina dog pas gi ñu amoon, nangu suuf si mu ko jagleel bu gisul liggéey bi taxaw. Noonu nag la ko doxalee, daldi koy bàyyee 5i ektaar yoy, dafa ko jëndoon ci suufu réew mi, jaare woon ko Domaines.