Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, feddali na aada. Nde, tabaski ju jot, kiy Njiitu réew dinay faral di jéggal ay ma-kaso yoy, tuuma yu woyof lañ leen gàll. Moom, Basiiru Jomaay Fay, ren mooy njëlbeenug tabaskeem ci boppu réew mi. Jéggal na ci 376i ma-kaso yoo xam ne, dinañ mën a tabaskee ci seen weti njaboot ak i mbokk. Waayeet, ginnaaw tabaski ji, ñooñii ñu baal dinañ mën dellu ci seen i itte.
IBAADU YI JULLI NAÑ TEY CI DIBÉER JI
Ren, Senegaal ñaari tabaski lay amati. Nde, bu dee li ëpp ci réew mi, ñoom, ëllëg ci altine ji lañ fas yéene tabaski, ibaadu yi, ñoom, julli nañ tey ci dibéer ji. Muy fi Ndakaar ak biir réew mi, am nay Saa-Senegaal yu bari yu julli, rendi seen i kuy.
SËRIÑ MUNTAQAA MBÀKKE MAY NAY KUY ÑAARI KILIFAY RÉEW MI
Kilifag yoonu murit, Xalifa bu mag bii di Sëriñ Muntaqaa Mbàkke, baaxe na ñaari kuyi tabaski ñii di Basiiru Jomaay Fay, Njiitu réew mi, ak Usmaan Sonko, elimaanu jëwriñ yi.
Biram Juuf, tof-njiitu Pastef fa Tuubaa moo indil njiit yi seen i xar. Bees sukkandikoo ci sunuy naataangooy Seneweb, Usmaan Sonko ci boppam moo nangu xar yi.
Cig pàttali, Usmaan Sonko dafa jël juróom-benni kuy, may leen ay kilifay diine yu nekk Tuubaa, am ci menn mu mu jagleel Xalifa bu mag bi. Mooy li wolof di wax rekk, teraanga, teraanga moo koy fay.
DEM BEEK DIKK BI : EL MAALIG AK DDD WALLU NAÑ ASKAN WI
At mu nekk, bu korite walla tabaski jotee, way-ngëm yu bari dañuy wutali gaaraas yi ngir dellu ci seen njaboot, biir diiwaan yi. Waaye, lees seetlu mooy ne, saa su xew-xewu diine teroo, dawalkat yi dañuy faral di ful paas yi ba mu diis lool ci jibay (poosi) way-tukki yi. Ren nag, Càmm gi dafa taxaw ci wetu askan wi.
Jëwriñu yaale bi (dem beek dikk) dafa dem ba gaaraas “Baux Maraîchers” ngir wax ak boroomi daamar yi ngir ñu bañ a yokk paas yi. Bi ñu bañee, daf fa indi biisi Dakaar Dem Dikk (DDD) ngir ñu yóbbu way-tukki yi ci njëg yu yomb. Askan wépp a leen tàccu ci doxalin woowu, daldi koy rafetlu te di ñaan mu sax.