LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (17/1/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

ÑËWUB NJIITU RÉEWUM GANA FI SENEGAAL

Tay ci ngoon la fi Njiitu réewum Gana ñëw ngir amalsi fi tukkib nuyoo. Njiiteefu Réew mi moo fésal xibaar bile ci ab yégle bob, bindees na ci ne :

“Njiitu Réewum Gana lees fal bees, Sëñ bi John Dramani Mahama, dina amal, ci ngoonug àjjuma jii, 17i fani sãwiyee 2025, tukkib nuyoo bu mu jagleel Njiitu Réewum Senegaal, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. “

Ba tay ci biir yégle bi, xamlees na ne, “tukki boobile, di bi jiitu ginnaaw bi mu faloo, dafay firndeel rattaxaayu sunu diggante ñaari réew yi ak yéene ji nu bokk ci gën a dëgëral déggooy liggéey yu nu séq ci fànn yu nu bokk ittewoo. “

Cig pàttali, Njiitu Réew mi demoon na Akraa (péeyub Gana) ngir teewe tabbug Njiitu Réewum Gana lu bees li, John Dramani Mahama.

Moom, John Dramani Mahama, moo jiite ci wotey Njiitu Réew ya fa amoon, daldi am 56i xob ci téeméer yoo jël. Moo jiitu woon Mahamadu Bawumia mi nekkoon toj-njiitu Réew mi, di woon lawaxu Nguur ga folleeku.

Njiitu Réew ma woon, Nana Akufo-Ado, bokkul woon ca wote ya ndax mataloon na ñaari moome yi Yoon may.

MBIRUM FARBA NGOM (APR)

Ngomblaan gi jàllale na sémbuw taxawal ndiisoo cëtëŋ (commission ad hoc) guy saytu càkkuteefu summi mbalaanum kiiraayu dépite bii di Muhammadu Ngom, ñu gën ko xam ci turu Farba Ngom.

11i dépite ñoo bokk ci ndiisoo cëtëŋ gi. Ci dogu 34 (Sàrtu biir bu Ngomblaan gi) lañu sukkandiku ngir taxawal ndiisoo googu. Naka noonu, ci biir 11I dépite yooyu, 9 yi dépite yi Pastfef lañu bokk, kenn ki bokk ci lëkkatoo Takku Wallu ak kenn ku bokk ci ñu bindoodi (non-inscrit).

Liggéeyu ndiisoo gi mooy defar ag caabal gog, dees na ko gaaral dépite yi keroog bees amalee am pénc mom, dépite yi dinañ ci wote ngir summi mbalaanu kiiraayu Farba Ngom walla déet.

Jëwriñu Yoon wi, ci càkkuteefu Toppekaayu koppar yi, moo bind Ngomblaan gi di sàkku ci dépite yi ñu summi mbalaanu kiiraayu Farba Ngom ngir Yoon mën ko déglu ci mbirum 125i miliyaar yi lëmbe Réew mi jamono yii.

Ñii ñooy dépite yi bokk ci ndiisoog cëtëŋ gi :

Kippaangog dépite ‘’Pastef les Patriotes’’ :

Mohamet Ayib Salim Dafe

Abdulaay Taal ;

Mbaan Fay

Yungare Jonn

Ami Ja

Ãsumaana Saar

Anta Ja

Aliyun Ndaw

Faatu Ba.

 Kippaangog dépite Takku Wallu

Jimo Suwaare

Ñu bindoodi

Séex Ahmet Tiijaan Yum.

“SETAL SUNU RÉEW” : TEFESU DEXU MAATAM GI LAÑU TÀNN

Wii yoon, tefesu dexug Senegaal gi lañu tànn ngir amal fa “Setal sunu Réew” ci weeru féewiryee wi. Fa diiwaanu Maatam lees koy amalee, keroog bésub 1eel ci féewiryee 2025. Gornooru diiwaan ba, Sayid Ja, moo ko xamle démb ci alxames ji.

“Ngir bésub set-setal bi, tefesu dexug Senegaal gi, fa Maatam, lañu tànn. Béréb boobu dafa bokk ci liy màndargaal Maatam, rawatina ci ñiy jóge Muritani di ko jaare ci dex gi. Warees na gën a setal béréb bi, daldi fay jële mbalit mi. » (kàdduy gornoor bi)

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj