LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (17/10/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

WAAJTAAYU WOTEY PALUG DEPITE YI

Lu tollu ci weer moo des ci wote yi. Waaye, coow laa ngi ne kurr ci géewu pólitig bi. Lëkkatoo gu nekk a ngi lal i pexe ngir nërmeel sa moroom. Looloo tax, jamono jii, coow li wërati ci diggante Maki Sàll ak Usmaan Sonko. Su kii waxee, jaar fii, ka ca des wax, jaar fale. Moom Usmaan Sonko nag, génnoon na démb am ay kàddu yu mu doon yékkati. Am na tomb yu mu fa jot a waxtaane. Waaye, li ci gën a fés mooy li ñeel waajtaayu wotey palug dépite yi. Ñoom waa Pastef, dinañu amal li ñuy dippe ab “Méga meeting” boole ko ak door li ñuy naan “cagnotte”. Maanaam, koppar gi ñuy dajale ngir waajal seen i kàmpaañ. Seen xew-xew bi nag, dinañu ko amal ci gaawu bii ñu dëgmal, mu yemoo ak 19 pani oktoobar. Ñi ngi koy amalee fa “DAKAR ARENA”.

MBËNNUM DEXU SENEGAAL GI

Mbënn mu metti moo am fa Bàkkel, Maatam ak barab yi ñu dendal. Li ko waral mooy dexu Senegaal gi moo ball ba àgg ci ñi dëkke boor boobu. Jamono jii nag, sonnu nañu lool. Ba tax na, Nguur gi jóg na fas leen yéene a dimbali. Looloo tax, ñu génnee lu tollu ci juróom-ñetti miliyaar ci sunuy koppar ngir dimbali ñi nga xam ne loru nañu ci mbir moomu.

LEERALI JËWRIÑ JI ÑU DÉNK TÀGGAT-YARAM

Xadi Jéen Gay mooy ki ñu dénk wàllu tàggat-yaram, mbatiit ak ndaw ñi. Moom, jëwriñ ji, génn na weddi xibaar yi ñuy tasaare. Nde, dañu ne tàbb nañu kii di Maalig Ngom mu wuutu Biraa Seen. Maanaam, moom lañu def Njiitu CNG (Comité National de Gestion de la lutte sénégalaise). Ci yégle bi ñu siiwal, daf ci xamle na loolu ay waxi kasaw-kasaw kepp la, ajuwul fenn. Rax-ci-dolli, nee na, ba jamono jii ñu tollu, amul lenn ndogal loo xam ne jëlagum nañu ko ñeel mbirum njiiteefu béréb boobu.

WAA “DIRECTION DES BOURSES” TEGGI NAÑU TUUMA

Kër gii nga xam ne ñoom lañu dénk lépp luy peyooru ndongo yi nekk ci daara yu kowe yi, génnee nañu ab yégle ngir setal seen der. Li waral seen taxawaay boobu du lenn lu moy xibaar yi ñuy siiwal ñeel ndogal lu ñu jël ci peyooru ndongo yi. Nde, dañu ne gaa ñi dañuy wàññi koppar gi walla sax am na ndongo yoo xam ne duñu leen jox dara. Te, am na atum lëmm mees leen feyul. Ñi ngi xamle ne xibaar yooyu wéruñu, amuñu benn cëslaay.

FMI DËGGAL NA KÀDDUY USMAAN SONKO

Fan yee jàll la Usmaan Sonko ak ug Càmm gi génn, wax Saa-senegaal yi ni ñu fekkee réew mi. Maanaam, fan la réew mi tollu ci wàllu koom-koom. Ñu xamle woon ne jamono jii, koomu réew mi sooxe na lool. Ci ginnaaw gi la ki fi nekkoon Njiitu réew, di Maki Sàll, génn miim ko. Mu xamle ne bi mu fiy jóge koom gi sooxewul ni ñu koy waxe. Waaye, ci diggante bi dafa am lu fi xew. Ñii di waa FMI (Fonds Monétaire International) dañoo génn àtte leen. Nde, dañoo wax ne li Usmaan Sonko siiwal ci koom-koomu Senegaal gi moo am. Te, ñoom waa FMI, ci njiiteefu Edward Gemayel, dañoo gis ne Nguur gi fi nekk daf cee war a jël ay matuwaay ca na mu gën a gaawe balaa mbir mi di gën a jéggi dayo.

XEW-XEW BU TIIS FA KIDIRA

Xew-xew boobu mi ngi ame fa Kidira, nekk fa gox bii di Bàkkel. Dafa di, jamono jii, la xew fa Bàkkel kenn umpalewu ko. Nde, dex ga dafa ball bay dem ci dëkkuwaay yi. Ba tax na, ña fa dëkke sonnu nañu lool. Mu am weneen tiis wu metti woo xam ne moo yokku na ci tolof-tolof yooyu ñuy jànkonteel. Ndax, foofu ca Kidira, dafa am benn xale bu tollu ci juróom-ñaari at bu lab ci ndox mi. Ñii di waa RFM ñoo biral xibaar bi.

NDOGUM YOON FA KËR SOOSE

Kër Soose mi ngi nekke ci goxub Kawlax. Am ndogu tali (aksidaŋ) mu metti moo fa am tay, ci alxames ji, ay boori juróom-benni waxtu ci suba. Genn daamar (7 places) moo fa fiir ab waxambaane, mu faatu ca saa sa. Moone, ci “trottoir” bi la nekkoon. Bees sukkandikoo ba tey ci waa “Seneweb”, waxambaane boobu, mi ngi wuyoo ci turu Y. Caam, tolloon ci ñaar-fukki at ak ñeent.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj