LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (19/2/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

SOROJU SANGOMAAR BI

Bilaŋub sàngomaar bu atum 2024 mi génn na. Waa Woodside ñoo ko xamle cib yëgle bu ñu siiwal barki-démb ci altine ji, 19i fani féewirye 2024, ci seen dalub web. Ci yégle boobu, ñoo nga cay fàttali ni ca weeru suwe 2024 lañu tàmbali woon ŋacc soroju Sàngomaar bi. Ñu tënk ni ci 2024 mi, ŋacc nañu lu tollu ci 13,3i tamndareeti barigo soroj bees seggagul. Jaay nañu itam 12,9i tamndareeti barigo. Mu yam ak 950i tamndareeti dolaar (war a tollu ci 595,17i tamñareeti FCFA). Naka noonu, ci ñetti weer yi mujj ci atum 2024 mi, liggéey bi mucc na ayib te ànd ak kaaraange gu mat sëkk daanaka (egg na ci 94% ci kaaraange). Amul benn loru bu aay bees ci nemmeeku ci 30i tamndareeti waxtu yees fa liggéey.

ELIMAANU JËWRIÑ YI DINA DEM FA NGOMBLAAN GA

Elimaanu jëwriñ yi Sëñ Usmaan Sonko ak mbooleem jëwriñi Càmm gi dinañu teew fa Ngomblaan ga naka àjjuma jii di ñëw. Ci janoo boobu ñu nar a amal ak dépite yi, dees na leen sampal 10i laaj yees war a andi ay leeral. Fukki laaj yooyu nag, nii lees ko séddale : kippaangoog Pastef gi ëpp doole dina am 8i laaj, kippaangoog Takku-Wallu am benn laaj, bi ci des ñu jagleel ko ñi binduwul. Laaj bu ci nekk, dees na jagleel dépite bi 3i simili.

BÀYYI NAÑU JURÓOMI ÑOÑI FARBA NGOM YI ÑU JÀPPOON

Yoon féexal na juróomi ñoñi Farba Ngom yi mu tegoon loxo ci alxames ji weesu. Fekk ñu génnoon doon ñaxtu fa buntu màkkaanu PJF (Pool Judiciaire Financier), bi ñu fay déglu Farba Ngom. Li ñu leen doon toppe nag mooy dajaloo bu yoon dàq. Waaye bi ñu leen doon àtte démb ci alxames ji, Njiitu ëttu àttewaay bu Ndakaaru dafa leen a bàyyi ñu dem seen yoon donte ni sax ndawul jëwriñal bokkef gi dafa doon sàkku ñu teg leen i daan. Nde bu weesoo génn bu teguwul ci yoon bi ñu amal, saafonte nañu ak takk-der yi, sànni leen i xeer, yàq itam ay ndaamar.

BITIM-RÉEW

Démb ci talaata ji, 18i fani féewirye 2025, réewum Gàmbi doon na màggal 60i at ginnaaw bi mu génne ci noteelug  Àngalteer. Ni ñu ko tàmm defe at mu nekk, amal nañu ay maaj, ay xew-xew i mbatiit ak i joŋante. Wu ren ji nag dafa yam ak bés bi Aadama Baro doon njëkk waat foofa ca réew ma (18i fani féewiryee 2017) ginnaaw bi mu jëlee Nguur gi ci Yayaa Jàmme mi fa nekkoon ci diirub 22i at.

Njiitu réewum Senegaal li, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, demoon na démb fa réewum Gàmbi ngir teewe xew-xew boobu ginnaaw bi ko ci naataangoom bi Sëñ Aadama Baro bëggee dalal. Naka noonu, njiiteef gi xamle na ni teewaayam foofa dafay dellu di firndeel taxawaayam ngir gën a dëgëral lëkkatoo ñaari réew yi jëme ci xaritoo ak dimbalante.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj