LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (19/9/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

TUKKIB NJIITU RÉEW MI FA NJAASAAN

Dibéer jii weesu moo nekkoon bés bi ñu doon màggul guddi gi Yonentu Yàlla Muhammat ganesee àdduna. Ñii di waa Njaasaan moom, bu bés bi dellusee lañu koy màggal. Tey, ci alxames ji la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay àndoon ak ug gàngooram dem fa laata bés bi di agsi. Ki ko fa dalal di Xalif ba, Séex Buh Siidi Maxtaar Kunta. Mu jot faa yékkati ay kàddu yu am solo jëmale leen ci ni ñu war a doxalee mbiri diine yi ak ya ca aju yépp.

JÀPP NAÑU SEROM BÀNJAKI

Démb ci guddig àllarba ji lañu teg loxo kooku di Serom Bànjaki, ay boori fukki waxtu. Waa BIP (Brigade d’Intervention Polyvalente) ñoo ko jàpp bees sukkandikoo ci “Les Echos”. Moom nag, ñi ngi ko doon woowe “sniper”. Mi ngi bokkoon ci way-wattu kaaraangeg APR (Alliance Pour la République). Ba nii ñu tollu nag, kenn xamagul dëggantaan lu tax ñu jàpp ko, donte ne sax, am na ñu njort ne dafa laale ci réerug Fulbeer Sàmbu ak Dijje Baaji.

LEERALI GII MARI SAAÑA ÑEEL COOWAL 12,12 MILIYAAR YI

Coowal fukki miliyaar ak ñaar ak lu teg li ñu ne waa “Primature” jëfandikoo nañu ko ci ñetti weer yii, Gii Mari nee na du dëgg. Maanaam, dafa teggi waxi Majambal Jaañ. Mu yokk ci ne li ñu jëfandikoo ci koppar diggante benn fan ci weeru awril ba fanweeri fan ci weeru suwe, mi ngi tollu ci 3,3 miliyaar. Te, elimaanu jëwriñ ji fi jóge ci ñetti weer kepp jëfandikoo na ci 8,79 miliyaar. Mu jàpp ne ñaari doxalin yooyu wute gu mag am na ci.

BENEEN BAKKAN ROT NA FA TUUBAA

Ginnaaw ñetti bakkan ya fa jotoon a rot ci mbënn mu metti ma fa am, beneen bakkan rotaat na fa. Bees sukkandikoo ci sunu naataangoy “Seneweb”, benn xale bu tollu ci ñeenti at la fa ab tabax daanu ci kowam. Xew-xew baa ngi am tey, ci alxames ji fa koñ bii di Gede. Doon nañu ko jéem a rawale fa        raglu ba. Waaye, mujjul a mucc.

XEW-XEW BU TIIS FA KOLDAA

Xew-xew boobu mi ngi am ci guddig démb ji fa Koldaa. Benn xale bu jigéen bu war a tollu ci ñaar-fukki at la fa ag dënnu faat. Nee ñu, ndaw soosu, da doon sangu ci taw bi. Moom R. Séydi, ci saa si la faatu. Am na seneen soxna ak doomam ju mu gaañ. Li ci gënatee metti mooy ndaw soosu dañu ko doon sog a takk. Rax-ci-dolli, mu waroon a séyi fa kër boroom këram bees sukkandikoo ci waa “Seneweb”. Xew-xew boobu ma nga ame fa Sibikaranto, nekk fa goxub Tankanto-Escale.

NDOG MU METTI CI YOONU LINGEER WI

Ndog yi taqarnaase nañ  jamono jii ci tali yi. Daanaka, kenn du toog ab diir te déggul ndogum yoon. Tey, ci alxames ji, am na aksidaŋ bu am ci yoonu Lingeer wi ba bakkan rot ci. Ndog maa ngi amee ci boori Kebemeer. Genn daamar gu jóge Ndar moo doon moytu ag sëfaan far mbëkk ag garab. Dawalkat ba moom ca saa sa la génn àdduna. Ñi mu yeboon jële ci ay gaañu-gaañu yu metti. Yóbbu nañu leen fa raglu Ahmadu Saxiir Mbay bu Luga. Te, li gën a doy-waar ci ndog mi mooy sëfaan gi mu doon moytu, taxaw sax defu ko.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj