LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (20/3/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

COOWAL AMNISTI BI

Coppiteg amnisti bi dépitey Pastef yi namm a wotelu ca Ngomblaan ga moo lëmbe réew mi jamono yii. Bu ñii waxee jëm fii, ñee wax jëm fee. Ñoom waa Pastef nag, amal nañu ci alxamesu tay ji ndajem saabal. Li ñu ko dugge woon mooy indi ay leeral ci lënt-lënt yi ci ñenn ñi am. Coppiteg amnisti bi, dees na ko càmbar ca Ngomblaan ga, keroog ñaari fan ci weeru awril. Bu ko defee, ñu mën a xam ndax dañu koy wote am déet.

ELIMAANU JËWRIÑ YI AK MBOOLEM CÀMM GI DINAÑU DELLU CA NGOMBLAAN GA

Bu yàggul dara la Usmaan Sonko demoon ca Ngomblaan ga. Te, la ko jiitu sax, ca weeru desàmbar 2024, demoon na fa. Dina fa delluwaat ci weer wees dëgmal, ànd ak yeneen jëwriñi Càmm gi, bésub fukkeel ci awril 2025. Dina janoo ak dépite yi ngir tontu seen i laaj ñeel doxalinu réew mi. Dépite Pastef bii di Ayib Dafe moo ko xamle. Nde, kenn umpalewul ne dépite yi ñoo war a saytu doxalinu Nguur gi.

MURIG MBALAANU KIIRAAYU MUSTAFAA JÓOB

Ci talaatay barki-démb ji la ndiisoog “ad hoc” gi doon déglu Mustafaa Jóob ñeel mbirum Tabaski Ngom mi ñu koy tudd. Ëllëg ci àjjuma ji, woolu nañu dépite yi ca Ngomblaan ga. Li sabab woote bi mooy ñu càmbar njureef yi tukkee ci liggéeyi  ndiisog “ad hoc” gi. Ndax, toppekat bi moo sàkku ci ñu muri mbalaanu kiiraayam ngir mu mën a wuyuji Yoon. Kon, subaak jàmm dees na xam fu wànnent di mujjeek i bëtam.

TÀGGATUG JÀNGALEKAT YI CI XARALA YI AK IA

Jëwriñ ji ñu dénk njàng mu suufe mi ak mu digg-dóomu mi, Mustafaa Màmba Giraasi, ak jëwriñu njàng mu kowe mi, El Haaji Abdu Rahmaan Juuf, xaatim nañu ag pas. Li ñu ko dugge mooy ñu tàggat jàngalekat yi ci xarala yu yees yi (numérique) ak li ñuy dippe IA (Intelligence Artificielle). Daara ju kowe jii di UNCHK (Université Numérique Cheikh Hamidou Kane) ñooy jëmmal naal woowu. Ndax, fi mu tollu nii, kenn umpaleetul dooley xarala yu yees yi ak ci fànn wu mu mën di doon, rawatina ci njàng meek njàngale mi.

TEG NAÑU LOXO MUSAA SEKK

Musaa Sekk, ñu gën koo xam jamono jii ci turu Njawar Jaañ, bokk ci “Xaalisoo”, teg nañu ko loxo. Li ko waral mooy luubal alalu réew mi ak li ñuy dippe “faux et usage de faux”. Li feeñal njuuj-njaaj yooyu mooy luññutuy waa “OFNAC”. Ndax, ca jamonoy mbas ma (covid-19), dafa defaroon aw wayndare dugal ci ay liggéeykat. Ndekete yoo loolu amul. Te, li mu ci jublu woon mooy jot xaalis ci Càmm gi. Mu jotoon a laal koppar yu tollu ci juróom-ñetti miliyoŋ yu tegal, bees sukkandikoo ci waa Libération ñi siiwal xibaar bi. Looloo tax waa PJF (Pool Judiciaire Financier) sàkku ci ñu jëli ko. Fi mu nekk nii nag, moom tiyaatarkat boobu, ma nga ca loxoy Yoon. Waaye, guuta googu mu dugg mel na ne naru cee wéet. Ndax, am na ñeneen ñaar ñu ñu ci duut baaraam.

DAAN NAÑU MUHAMMADU MUSTAFAA SAAR

Démb, ci àllarba ji, lañu daan kii di Muhammadu Mustafaa Saar. Li ko waral mooy dafa am benn widewoo bu mu def jël ay kàddu yu ñagas teg leen ci deru elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko. Yemul ci moom kese. Daf cee boolewaale askanu Joolaa wi nga xam ne fa la elimaanu jëwriñ yi bokk. Mu doon ay kàdduy tëkku yu mu jëmale ci Usmaan Sonko. Looloo tax ñu teg ko loxo. Li ñu ko ci doon toppe mooy kàddu yu woroo ak jikko yu rafet yi, ay tëkku ak i saaga, añs. Moom, Mustafaa Saar, daan nañu atu kaso mu muy tëdd.

Naka noonu, kii di Ardo Ñing, moom, ba tay ma nga ca kaso ba. Daanaka lu mel noonu lañu koy toppe moom itam. Démb la doon layoo. Waaye, ba tay xamagul ban daan lañuy teg ci ndoddam walla ndax dañu koy bàyyi. Àllarba jee di ñëw, yemoo ak ñaar-fukki fan ak juróom-benn ci weeru màrs, la ciy am lu ko leer.

XEW-XEW BU TIIS FA MBUUR

Ñaari xale ñoo génn àdduna fa koñ bii di Medinaa, nekk fa Mbuur. Ci anam yu doy waar lañ faatoo. Xale yooyu ñi ngi tolloon ci diggante benn ak ñeenti at. Ñoom ñaar, ñi ngi faatu ginnaaw bi leen seen yaay joxee aw ñam ay boori ñaari waxtu ci bëccëg. Li gën a doy waar mooy yaay ji dafa bàyyi ba ay juróom-benni waxtu ci ngoon sog di woo seen baay, wax ko ko. Ginnaaw gi, moom yaay, ji muy jéem a xaru. Jamono jii, ma nga ca raglu bu Mbuur. Waa pólis ubbi nañu ag luññutu ngir xam lan moo sabab jéyya joojule.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj