LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (21/10/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

WALUM DEX GI

Càmm gi teggiwul tànkam ci taxawaay bi mu am ñeel walum dex gi ak askan wu takku wi ci loru. Ba démb ci dibéer ji, magum jëwriñ yi, Usmaan Sonko, jiite na am ndaje mu dox ci diggante jëwriñ yi ko séq. Jëwriñ ju ci nekk wax na tolluwaayu mbir mi ci liñ ko dénk. Ginnaaw gi, magum jëwriñ yi fàttali na leen 8i tamñareet yi Nguur gi génneegum ngir dimbali way-loru yi. Digal na leen itam ñu njëkke ci soxla yu gën a tembare yi ngir seen taxawaay gën a mucc ayib.

PÉNCOO ÑEEL YAALE JI

Tàmbali nañu Péncoo mi ñu jagleel yaale Ji. Tay, ci altine ji, lañu ko ubbi fa Jamñaajo ci teewaayu Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay. Dinañu amal waxtaan yi ci diiru 5i pan. Ay ma-xereñ, ay njiiti kurél ci wàll wi ak ay kuréli way-jëfandiku war ko teewe. Ginnaaw bi mu jëlee kàddu gi, Njiitu réew mi ñaan na ñu génn ci waxtaan yooyu ak ay déggoo ngir sopparñi yaale ji ni mu gënee gaaw te yaatu. Fàttali na itam ni péncoo mee ngi aju ci yéene ji mu am ngir tëggaat yaale ji, méngale kook jamono. Loolu yépp ngir yembal askan wi ay soxlaam, yokk doole koom-koomu réew mi, jaare ko ci suqaleeku yoonu saxaar gi ak yoon yiy jokkale réewi afrigu sowu-jant yi.

NJÀNG MU KOWE MI

Njàng mu kowe mi dina taxaw ci diiru ñaari pan. Kurélu jàngalekat yi SAES (Syndicat Autonome de l’Enseignement Supérieur) dafay bank loxoom ci àllarba jeek alxames ji (23 ak 24i pani oktoobar 2024). Naka noonu, dinañu amal ay ndaje ci jàngune yépp. Ñoom nag, li leen metti mooy ndàmpaayu alaatereete yi Nguur gi tëw a jox njabooti jàngalekat yi. Ñoo ngi ñaawlu itam déggoo yi ñu xaatimoon ak Nguur ga woon te gu yees gii bañagum leen jëmmal.

COOWAL MBUXUM LI TOPP ASER

Coow li juddu woon ci mbuxum mi ñu ne dafa am ci biir kër gii di ASER ba ñu ajandi sémbuw ARCOP wi jeexagul.  Magum jëwriñ yi, Usmaan Sonko daf cee dellusi barki-démb, ca ba muy amal mitiŋ fa Jamñaajo. Naka noonu, mu yékkati ay kàddu, ragg deru njiit lii di Sã Misel Seen, yékkatiwaale ko ba ci kow. Waaye, taxawaay boobu mu ci am nag, du lu ñépp ñoo ci bokk ànd. Nde, ku ci mel ni Biraahim Sekk, di kenn ci ñi jiite kuréli maxejj yi jam na ko. Dafa biral ni mbuxum da cee am moo tax njiit li nangu waxtaanewaat rëq-rëq yi ñu ci nemmeeku ci njëg yi. Ba tax mu jàpp ni kenn du far ay jalgati mbaa di leen joyyanti ak waxtaan, ay daan a ci war. Kii di Abdul Mbay itam, nekkoon fi magum Jëwriñ ci Nguuru Maki Sàll wax na ci. Waaye moom dafa jàpp ni Usmaan Sonko dafa àtte ba toog te Yoon defagul liggéeyam.

JUR GI

Jëwriñ ji ñu dénk wàllu mbay mi, Mabuuba Jaañ, ubbi na kàmpaañ bi jëm ci ñakk yi ngir xeex jàngoroy gàtt yi. Barki-démb ci gaawu gi lañ ko doon tàmbali fa Daara Jolof, ci teewaayam ak ci teewaayu mbokku jëwriñam, El Haaji Maalig Njaay (tabaxte yi, yaale ji ci suuf ak ci jaww ji). Ci kàddu yi mu fa jot a yekkati, jëwriñ ji dellusi na ci njariñ li yar am ñeel koom-koomu réew mi, ay tamndareeti kër yu ciy yëngatu, ak ni muy xeexe ndóol. Rafetlu naat jéego yu am solo yu Nguuru Senegaal def ci xeex jàngoroy jur gi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj