LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (21/11/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

DIC WOO NA AADAMA GAY

Tay ci alxames ji lañu ko woolu, ñetti waxtu ci ngoon. Waaye, woote bi dañu koo dàq ba suba bees sukkandikoo ci li mu siiwal ci xëtu Facebookam. Nee na, woote bi dàq nañu ko ba suba, bu fukki waxtu ak benn jotee. Li waral dàq gi mooy ne, ab layookatam du jàppandi ci waxtu wi ñu ko woo tay. Moom nag, nee na xamul ba tay, lan moo sabab wooteb waa DIC bi bees sukkandikoo ci li mu njëkk a siiwal ci xëtu Facebookam laata muy xamle dàqug woote bi.

ARTP ÀRTU NA SONATEL, EXPRESSO, SIRUS TELECOM AK SAHL

Kurél gii di ARTP (Autorité de Régulation des Télécommunications et des Postes) duut na baaraam këru liggéeey yooyu. Nde, kenn umpalewul ne, Sonatel, Expresso, Sirus Telecom ak Sahl ñoo yor wàllu jokkoo gi ci réew mi. Muy li ñuy jëfandikoo (crédit) ngir woote ak wuyu, yónnee ay bataaxal walla ci lënd gi (données mobiles). Te, ñu bari gis li ñu leen di jëfandikoo bari na lool, mu diis lool ci ndoddu askan wi. Waa ARTP nag, bi ñu leen saytoo, gis nañu ne këri liggéey yooyu, am na ay sàrt yu ñu sàmmontewul. Ñuy sàkku ci ñoom ñu sàmmonte ak sàrt yooyu fii ak diirub fanweeri fan. Maanaam, dañu leen a àppal ngir ñu jubbanti rëq-rëq yooyu ci ni mu gën a gaawe.

ÑAAR ÑI DOON MBUBBOO AY TASKATI-XIBAAR JÉBBAL NAÑU LEEN TOPPEKAT BU NDAKAARU

Dibéer jii weesu, nekkoon bés bi ñu doon amal wotey palug dépite yi, ca lañu tege woon loxo ñaar ñooñu. Li waral loolu, mooy ne ñoom ñaar, dañu doon mbubboo ay taskati-xibaar te nekkuñu ko. Bi ñu leen jàppee laaj leen seen kàrt yiy firndeel ne loolu mooy seen liggéey (carte professionnelle). Moom Y. Géy ak M. Ñaŋ, dañoo joxe ay kàrt yoo xam ne baaxul. Looloo ña nga leen téye fa “Brigade territoriale” bu Haan. Li ñu leen di toppe mooy li ñuy wax ci farãse “usurpation de fonction, faux et usage de faux”.

ASIMI GOYTAA TABB NA ELIMAANU JËWRIÑ JU BEES

Démb, ci àllarba ji, la Njiitu réewu Mali, Asimi Goytaa wàccee Sogel Mayga. Cig pàttali, moom Asimi Goytaa, bi mu daanelee Nguur ga fa nekkoon, daf ko tabboon elimaanu jëwriñ yi. Donte ne sax, ki ko wuutu tey, wuutu woon na ko ca atum 2022, ginnaaw ag wopp gu ko daaneloon.  Ginnaaw gi, bi mu tanee, moom Sogel dafa delluwaat ci béréb boobu. Waaye, jëlewaat nañu ko fa. Ki ko wuutu ci ndombog-tànk googu, mooy Seneraal Abdulaay Mayga.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj