Càmmug Senegaal gi daa fas yéene saytuwaat pas yi nguurug Maki Sàll ga torlu woon. Waaye nag, du pas yép lees di xoolaat. Pas yi soxal Càmm gu bees gi, ñooy yi ñeel fànn yi gën a solowu yi. Nde, ba ñuy dagaan baatu askan wi la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, ak elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, dige woon lu ni mel. Loolu la njiitul Pastef liy feddali ci kàddu yii toftalu :
« Danu ŋàññi woon bu baax a baax anam bees daan torloo déggoo yi ak digaale yi te, li ci ëpp, dafa daan worook àqi askanu Senegaal ci fànn yu solowu. Danu joxe woon sunu kàddu te dogu ci, waxoon ne, dinan saytuwaat déggoo yooyu te liggéey ngir dëppale leen ak àqi réew mi… »
Bi muy dalal way-bokki kurél gees dénk boobule liggéey la yékkati kàddu yile. Ndaxte, ci ndigalu Njiitu réew mi, elimaanu jëwriñ yi dafa samp ag kurél guy taxawee liggéey boobu. Allaaji Ibraayma Jóob lees tabb ci boppu kurél googii war a saytuwaat pas yees duut baaraam. Li ñu ko duggee mooy aar ak a sàmm àqi askan wi. Ci weneen waxiin, dinañ càmbaraat pas yi, xool lu ci baax ci réew mi ak lu ci baaxul. Ca njeexital la, dees na tëggaat gépp pas gog, day salfaañe àqi askan wi. Ci gàttal daal, nisër bi mooy fexe ba li ñépp bokk, ñépp jot ci.
MBIRUM WOYKAT BII DI SIIDI JÓOB
Siidi Jóob a ngi ci loxoy yoon jamono jii. Nde, ci altine ji lañu jàpp. Li ko sabab nag moo di ne, dafa doon dawal ag daamar fekk ne yorul « permis », yorul « assurance ». Moom nag, dóor nañ ko « mandat de dépôt ». Ci taalatay démb ji, 20 pani ut 2024, la doo janook Toppekatu Bokkeef gi. Bees sukkandikoo ci wa Iradio ak PressAfrik, altine jii di ñëw lay jàkkaarlook àttekat bi fa Ndakaaru.
REYUG FECCKAT BII DI “AZIZ DABALAA”
Xibaar bu doy waar lees xëyee tay. Fecckat bii siiw bii di Abdul Asiis Ba, ñu koy dàkkentalee “Aziz Dabalaa”, lañu fekk néewam, moom ak néewu benn jarbaatam, ci néegam. Ci lees wax, dañu ko rendi xatiit. Bu dee jarbaat bi, nee ñu dañu xotti biir bi, butit yiy feeñ. Ci talaatay démb ji lañu fekk seen i néew ci néegu “Aziz Dabalaa”. Pólis ak sàppëer ñoo leen jëlsi.
Bees sukandikoo ci kilifa yi, amaana dibéer jii weesu lañu leen faat. Kon, toog nañ as-tuut ñaari fan yees leen tegul bët. Ubbi nañ ag luññutu ngir leeral mbir mi te jàpp ñi def ñaawteef bu ni mel.
JÀNGUNEB SÉEX ANTA JÓOB BU NDAKAARU DINA TËJ SUBA CI ALXAMES JI
Ëllëg, alxames, 22i pani ut 2024 lees di tëj jànguneb Séex Anta Jóob bu Ndakaaru, bu 18i waxtu jotee ci ngoon gi. Dee na ko tëj nag ba jëmmi jamono. Njiitul COUD li moo génne ab yégle, xamle ko. Ci biir yégle bi, mi ngi ciy wax ak way-dëkki jàngune bi yépp, di leen sant ñu ñibbi te bañ faa bàyyi dara ci seen i bagaas. Ndax, ci lu mu wax, dinañu jël seen i matuwaay ngir ñépp sàmmonteek ndogal lile.
BÀYYI NAÑ IMAAM NDAW AK BAA JAXATE
Ginnaaw bi ñu leen nëbbee jan twi ci diirub ñetti weer, bàyyi nañ Imaam Ndaw ak Baa Jaxate. Bees sukkandikoo ci kàdduy seen layookat bii di Me Elaas Juuf, démb lañu def ñetti weer ci kaso bi, muy méngoo ak ñetti weer yi ñu leen daanoon. Kon, tëdd nañ ñetti yu weer mat sëkk. Moo tax ñu bàyyi leen.
Cig pàttali, bi fi Jean-Luc Mélanchon ñëwee ba Usmaan Sonko dalal ko, Baa Jaxate dafa defoon widewoo di wax ak kàddu yu tegginewul jëme leen ci elimaanu jëwriñ yi. Ci mbirum ngóor-jigeen la tuumaaloon Usmaan Sonko, ca la DIC jëlijee. Imaam Ndaw itam, ci mbirum ngóor-jigeen moomu la tuumaaloon elimaanu jëwriñ yi ba ñu jàppoon ko ci. Bi ñu leen àttee, ca lañu leen daanoon 3i weeri kaso.