Démb, ci ndajem jëwriñ yi lañu tabbee Sàmba Njaay, def ko “Président du Conseil d’Administration de la Société nationale des Habitations à Loyer modéré (SN-HLM)”. Tabb googu nag, jur na coow lu bari ci mbaali jokkoo yi. Dafa di, ñoom militaŋi Pastef yi, dañu ne tabb googu teguwul ci yoon. Ndax, Sàmba moomu, démb ak barki-démb amul lu mu tegul ci deru làng gi ak ñi ko jiite. Looloo tax, ñii di waa Pastef “Grand Dakar” génnee ab yégle ngir naqarlu tabb googu. Nde, ñoom jàpp nañu tabb googu gàcce la ci ñoom. Ci gàttal, ñoom dañoo gis ne, dañu leen a ñàkk a weg. Moo tax, ñuy sàkku ci Njiitu réew mi mu seetaat tabb googu.
WOTEY PALUG DÉPITE YI
Ay fan yu néew ñoo des ngir kàmpaañ yi door. Waaye, lëkkatoo yi, mbootaay yi ak làng yi dañuy gën di jaxasoo. Ñii di fekki ñee, ña ca des di gën a dëggal seen bopp fa ñu nekkoon. Kii di Décce Faal, Njiitul PRP bokkoon ci lëkkatoo Sàmm sa kàddu, jóge na fa. Démb la siiwal xibaar bi ci ndajem waxtaan mu mu doon amal. Nee na waa Pastef lay àndal ci wote yii. Naka noonu, waa PUR ñi ñu ne woon ñi ngi ci tànki fekki Pastef ak Réew mi bu Idiriisa Sekk bi ñu ne Pastef lay jàppale ci wote yii, génn nañu weddi. Waa PUR, nee nañu, tay lañu gën a des ci biir lëkkatoog Sàmm sa kàddu. Waa Réew mi moom, nee nañu xibaar yooyu gaa ñi di tasaare dara du ci dëgg.
BÉJJANTE DIGGANTE USMAAN SONKO AK AAMADU BA
Ci ndoorteelu ayu-bés bii, la elimaanu jëwriñ yi doon woo ki fi nekkoon elimaan jëwriñ, di Aamadu Ba ci béjjante. Moom, Aamadu Ba tontu na ko tay, ci alxames ji. Xamal na ko ne noppi na ngir jàkkaarloo ak moom. Waaye, amaat na luy ñuul ci soow mi. Ndax, ginnaaw gi, kii di Usmaan Sonko tontuwaat na ko ci xëtu Facebookam. Mu xamal ko ne bég na ci li mu nangu béjjante bi. Li ko jaaxal kay mooy lu tax mu bàyyi ba dégg ñuy ruumandaat ne waa CNRA dañuy tere waxtaan muy sog a tontu. Mu jàpp ne loolu warul mën a tere béjjante bi. Mu yokk ci ne, ndeem moom tegalul Aamadu Ba benn sàrt, moom it na def noonu. Su bés baa, ku nekk ci ñoom indi say firnde teg, ñu won askanu Senegaal.
NJIITU RÉEW MI NAQARLU NA CONG MA AM FA TURKI
Ñi ñuy dippee ay “terroristes” ñoo amal am cong mu metti fa Turki, fa béréb bii di Tusas, nekke fa Ankara. Lum néew-néew, lu tollu ci juróomi doomi Aadama ñàkk nañu ci seen i bakkan. Lu tollu ci ñaar-fukk ak ñaar jële ci ay gaañu-gaañu. Njiitu réewu Senegaal, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, ñaawlu na bu baax jëf ji. Mi ngi wone ñeewantalam ci Njiitu réew ma, Recep Tayyip Erdogan, askanu Turki wi ak mbooleem ñi ci loru.
FINAALU CAN BEACH SOCCER
Gayndey Senegaal yi dem nañu finaal ci joŋante boobu, ginnaaw bi ñu daanee waa Ésipt ñaari bal ci benn. Ki ñu war a xëccool raw-gàddu gi du kenn ku moy waa Muritani. Dafa di, muraabituun yi, ñoom it, ñoo daan waa Marog juróom-ñaari bal ci ñeent. Joŋante bi nag, dinañu ko amal ci gaawu bii ñu dëgmal 26i pani oktoobar 2024.