NGURD CÀMM GI CI ÑETTI WEER YI JIITU CI ATUM 2025 MI
Jëwriñu ngurd meek nafa gi siiwal na caabal gi aju ci yorinu nafa gi ci ñetti weer yi jiitu ci atum 2025 mi. Muy wane ni nafa gi dafa gën a fees bees ko gam-gamleek tolluwaayam ca ñetti weer ya jiitu woon ca atum 2024. Doxal nañu itam 99,97 % (juróom-ñeen-fukk ak juróom-ñeent yu teg) ci lees nisaroon ci ñetti weer yi.
Naka noonu, li Nguur gi kopparaatu jëme ci Nafag Càmm gi ci juróom-benni weer yi jiitu ci at mi dem na ba ci 1 027,82i miliyaari FCFA. Li ñu jot a doxal nag tollu na ci 1 419,45 miliyaar.
Sàndikaa liggéeykati Yoon àddu nañ ci kàddu yi jëwriñ ji ñu dénk liggéeyi bokkeef gi, Ólifiyee Bukaal, yékkati ci seen gereew bi. Muy kàddu yoy, jëwriñ ji daf ca melal seen gereew bi, di ko niroole ak sàntaas. Muy kàddu yoy, kuréli liggéeykat yi ñaawlu nañu ko ci yëgle bi ñu génnee démb. Naka noonu, ñuy fàttali ne seen yëngu-yëngu yu ñu doon amal dañoo tegu ci Yoon, Ndayu-Sàrtu Réew mi fegul leen ko.
Yamuñu nag ci ñaawlu ko. Nde, teg nañu ca ne, waxam ji dafa xeeblu di génne ci kilifag Càmm gi. Ndax, dafay firndeel ñàkk dëggu ak gis-gis bu gàtt bu ñu am ci solos li leen yékkati.
M23 AM NA 14i AT CI REN
M23 (Mouvement du 23 juin) am na 14i at ginnaaw bi mu juddoo ca atum 2021. Ci bi ñu koy fàttaliku, kurélug Y’en a marre doon na ci amal ab lël. Ci lël boobu sax, Muhamadu Mbóoj, nekkoon fi njiitu kurél gi dellusi na ci anam yi mu juddoo woon ca Nguuru Abdulaay Wàdd mi nekkoon Njiitu Réew mi (2000-2012). Mu nekkoon Nguur gu bari lu mu daan nemmeeku ay jalget, rawatina bi mu bëggee def Nguur yëfi mbokk ba nammoon koo jébbal doomam ji Karim Wàdd ak ay sémbi àtte yu xel mënul woon a nangu. Naka noonu, Sëñ Mbóoj di xamle ni taxawaay ba ca M23 amoon, moom la amaat bi Maki Sàll nammee 3eelu moome. Muy wane ni taxawaay bi fi nekkoon jógu fi, te fileek jalget a ngi am, duñ jóg ci di jàmmaarlook moom.
BITIM-RÉEW : ISRAAYEL AK IRÃ DAKKAL NAÑU XEEX BA
Ginnaaw 12i fan yu ñu dëkke woon a sànnante ay misil, Israayel ak Irã dakkal nañu seen xeex bi. Démb ci altine ji la Njiitu Réewum Amerig li biraloon ne ñaari réew yi dëppoo nañu ci dakkal sox yi (cessez le feu), jeexal xeex bi. Waaye, laata ñu koy jëfe nag, ñaari réew yi sànnante nañu ay sox yu metti ci guddig altine ji, jàpp talaata.
Ci sànnante yooyu sax, 9i doom-aadama ñàkk nañu ci seen i bakkan fa bëj-gànnaaru réewum Irã, 33 jële ciy gaañu-gaañu. Am na itam ñeenti kër yu ca yàqu.
Fa Israayel itam, misili irã yaa nga tàbbi fa bëj-saalumu réew ma, fa péey ma ñuy woowe Beersheba. Footu it, 4i doom-aadama ñàkk nañu ci seen i bakkan. Mu am 22 yu ci jële ay gaañu-gaañu.