LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (24/7/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

UBBITEG CAMPUSEN

Bu yàggul dara la joŋantey fàggug lijaasa bii ñuy dippe Baccalauréat jeex. Nde, lijaasa boobu dina ubbil ndongo yi buntu yu bari. Muy lu ci mel ni joŋante ngir wutug liggéey walla sax jàng ci daara yu kawe yi. Ginnaaw bi mu jàllee ba am ndongo yu ko jot a am, ci lees xamle ubbiteg Campusen. Liy jubluwaay bi mooy ndongo yi mën a ubbi ay sàq. Su ko defee ñu mën fa a tànn jàngune yi ñu bëgg a jàngee. Dees na ko ubbi altine ñeenti fan ci weeru ut, tëj ko fukki fan ak benn ci weeru ut. Njiiteefu njëwriñ li ñu dénk njàngale mu kawe mi moo génnee ab yégle tay ci alxames ji ngir siiwal xibaar boobu.

CNAMS JOT NA JUMTUKAAY YU BEES

Tay, ci alxames ji, la elimaanu jëwriñ yi doon jot ay jumtukaay yu am njariñ ngir dooleel CNAMS (Centre National d’Action Anti-mines au Sénégal). Jumtukaay yooyu ñi ngi leen di dippe “matériel de déminage”. Ñi leen ko jox mooy réewum Sapoŋ. Jumtukaay yooyu, bees xaymaa koppar gi, àgg na ci ñaari miliyaar ci sunu koppar.

MAJOR ABDU ASIIS KÀNJI JEEXAL NA ÀPP LIGGÉEYAM

Major Abdu Asiis Kànji ñu gën koo xam ci turu “Xalif Seneraal kullu komandaŋ” àpp liggéeyam jeex na. Maanaam, dem na li farãse di wax “retraite”. Moom nag, ku yàgg sàndarmëri la. Ndax, def na fa lu tollu ci fanweeri at ak ñett. Jaar na tamit ci birigàdd yu wuute ci biir réew mi. Mu amal fa béréb yooyee ay liggéey yu mucc ayib.

TUKKIB NJIITU RÉEW MI

Ay fan ginnaaw bi mu jógee cib tukki, Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, dina amalaat ab tukki ci lu dul yàgg dara. Waaye, ba tay, ci biir kembaaru Afrig gi la yam. Wii yoon, ma nga jëm fale ca Tógoo. Nde, dafa war a amal tukkib liggéey fa réew moomee. Ëllëg ci àjjuma ji la fa war a dem. Te, bu fa jógee gaawu bi war na a jàll fa réewum Liberiyaa.

KOCC BARMA DEM NA KASO

Elaas Baabakar Jum, ñu gën koo xam ci turu Kocc Barma, mujj nañu koo yóbbu kaso. Fan yii weesu lañu ko tegoon loxo. Booba ba tay nag, coow laa ngi ne kurr ci réew mi ndax jëf yu ñaaw yi mu doon def. Moom nag, bari na tuuma yoo ñu teg ci ndoddam. Nde, tuuma yooyu tollu nañu ci juróom-ñett. Te, benn bokku ci ak sa moroom.

DÀQAAT NAÑU SIIWALUG NDOGAL YI ROTE CI LAYOOY MUSTAFAA JAXATE AK BASIIR FOFANA

Démb, ci àllarba ji, lañu waroon a xamle ndogal yi rote ci àttey ñaar ñooñu. Waaye, mujjul a am. Nde, dañu koo mujjee dàq. Te, lenn waralu ko lu moy liggéeykati Yoon yi dañoo nekk ci ay ñaxtu. Maanaam, dañoo dakkal seen liggéey. Looloo tax ñu mujjee dàq àpp boobu yóbb ko fanweeri fan ci weeru sulet wii ñu nekk.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj