Ay kilifa yu nekkoon i Njiiti Réew fi kembaarug Afrig doon nañu amal am ndaje démb ci talaata ji, 25 féewirye 2025, fa Cap Town, réewum Afrig-dii-Sidd. Maki Sàll mi fi nekkoon Njiitu Réewum Senegaal bokkoon na itam ca ña fa teewoon. Ca seen ndaje moomu nag, Njiiti Réew yooyii fésal nañu seen i kàddu ak yitte yi ñu am ci koom-koomi Réewi Afrig yi. Naka noonu, ñuy sàkku ci càmpeefi kopparal yu àddina si (institutions financières internationales) ñu neenal lenn ci bori Réewi Afrig yi. Ñu gis ni ndogal lu ni mel dina suqali koom-koomug kembaar gi. Looloo tax ba ñu fas yéene teg i jéego, ak di ci woo mbooleem seen i ñoñ ci àddina si, ngir ñu dooleel koom-koomi Réewi Afrig yi te tegu ci yokkute gu sax.
NDIISOOG RÉEW MI ÑEEL NIMERIG BI
Ci altine jii weesu la Càmm gi fésaloon toftaleb way-bokki ndajem réew mi ñeel nimerig bi. Mu doonoon 20i tur yoy seen i boroom ñoo doon liggéey tëralin wu yees wi ñeel nimerig bi fi réew mi. Tëggiinub toftale boobu nag, Biraahim Sekk dellusi na ci. Moom njiitu Forum Civil bi dafa gis ni tànniin bi dafa xaw a teey xelam ndax yaatuwaayu wàlluw nimerig bi feeñu ci. Ba tax muy ragal ni lu ni mel mën na andi ay xëccoo ci 1 105i tamñareet yees ko jagleeel. Naka noonu, muy xamle ni tëraliin wi dëppoowul ak yittey Njiitu Réew mi bëgg sukkandiku ci jëfandikoo nimerig bi ngir gën a xeex nger.
YOONAL SAABALUKAAY YI
Jëwriñu jokkoo bi, xaralay jokkoo yeek nimerig bi jël na ndogolu dakkal liggéeyu bépp saabalukaay bu sàmmontewul ak sàrtu saabalukaay yi. Ginnaaw bi mu fésalee toftaleb saabalukaay yi tegu ci yoon, sàkku na leegi ci naataangoom bii di Sã Baptist Tin (jëwriñu kaaraange biir réew mi) mu tëj bépp saabaluy bu tënkuwul ci sàrt yi.
Bees sukkandikoo ci sunuy naataango yu Liberation, ci ayu-bés bi weesu (altine 17i fani féewirye) la jëwriñ ji jébbaloon naataangoom bi bataaxal ngir mu doxal. Naka noonoot, jëwriñu kaaraange biir réew mi sant na ndawam yii di DST (Direction de la surveillance du Territoire) ak DSC (Division Spéciale de la Cybersécurité) ñu jëfe ndigal li.
PAJ MI : FAJKAT YI NAMM NAÑOO BANK SEEN LOXO
Kurélug fajkat yi di Satsus (Syndicat Autonome des Techniciens Supérieurs de Santé) xamle na ni ay way-bokkam dinañu booloo bank seen loxo naka tay ci àllarba ji ak ëllëg ci alxames ji (26 ak 27i fan ci weeru féewirye 2025). Ci li ñu siiwal, dinañu ci sóobu ginnaaw càkkuteef yu ñu yàgg a def, rawatina lu jëm ci dekkare bi aju ci seen taxawaay ak ci seen dayo. Muy dekkara bu ñu yàgg daw ci ginnaawam ngir Càmm gi xaatim ko. Ñuy yaakaar ni ci seen bank loxo bi, kilifa yi dinañu leen geestu ngir saafara ci lu gaaw seen i jafe-jafe.
MBIRI PAAB ABDULAAY TURE
Paab Abdulaay Ture, di kenn ci way-loru yu woon ci yëngu-yëngu pólitig yi fi jaaroon, àddu na ci li jëm ciy mbiram ak finaal yi ñu ko tegoon. Kàddoom yooyu mu yékkati, moo nga cay duut baaraam Yoon. Muy xamle ni dañuy tandeefal wayndareem. Nde ca weeru sàttumbar la leen jébbaloon jure (kalaame), waaye ba leegi amul lenn lu ci jëm kanam. Ba leegi daal moom ak laykatam ñoo ngi ciy topp di daw. Waaye jure baa ngi ci pekku toppekat bi ci li leen ëttu ndakaaru bi xamal. Te xamuñu lu waral yéexaay bi.