LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (26/6/2025)

Yeneen i xët

Aji bind ji

TUKKIB NJIITU RÉEW MI FA ESPAAÑ

Bu yàggul dara la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jóge fa ndajem CEDEAO ma. Balaa yàgg, dina amalaat beneen tukki. Wii yoon moom day génn kembaaru Afrig gi. Ndax, ma nga jëm fa Tugal, fa réewum Espaañ. Li mu dugge tukki bi mooy fekke ñeenteelu ndaje mii ñuy dippe “4ème Conférence internationale sur le financement du développement”. Ndaje moomu, mi ngi war a keroog am fanweeri fan ci weeru suwe jàpp ñaari fan ci weeru sulet. Dina demaale tamit ci màggalug “50ème anniversaire de l’Indépendance de Cabo Verde” war a am gaawu juróomi fan ci weeru sulet.

SENEGAAL BOKK NA CI FUKKI RÉEW YI ËPP JÀMM CI AFRIG

Ayu-bés bii ñu génn la kurél gii di “Institute For Economics and Peace” biral ag caabal ngir joxe ci turu réew yi ëpp jàmm ci àddina si. Fii ci Afrig nag, saytu na fi lu tollu ci juróom fukki réew. Réew yooyu ñu saytu, Senegaal ma nga ca juróom-ñeenteelu toogu ba. Daanaka, kon, fii ci Afrig sowu-jant, Gàmbi kesee ko fi jiitu. Ndax, réewum Gàmbi nga ca ñeenteelu toogu ba. Li ñuy sukkandiku ngir natt dayob jàmmi réew yi mooy taafar seek jàmmaarloo yiy am fa réew ma. Looloo tax, ba réew yu ci mel ni ay Mali, Niseer ak Burkinaa sori lool ci toftale gi.

XIBAAR ÑEEL YOON

Bu yàggul dara la Yoon bañaloon Lat Jóob ag càkkuteefam. Maanaam, da doon sàkku ñu bàyyi ko bàyyig négandiku ngir mu génn kaso ba mu nekk bu yàgg ba tay. Waaye, loolu taxul ki fi jiite woon ay jamono LONASE teggi tànkam. Ndax, jébbalaat na geneen càkkuteefu bàyyig négandiku. Kon, fii ak ub diir dees na xam lu ko Yoon di tontu.
Kii di Basiir Fofana moom it ma nga ca loxoy Yoon ba tay. Li ko waral mooy xibaar yi mu jibal ñeel mbirum njëndum daamari Ngomblaan gi. Looloo tax ñu woolu ko moom taskatu-xibaar boobu. Jamono jii, ñi ngi ko def li ñuy dippe “Garde-à-vue” ngir tasaare xibaar yu wérul.

XEW-XEW BU YÉEME FA LINGEER

Ab xew-xew bu doy waar moo am fa dëkk bii di Gasaan nekke fa goxub Lingeer.. Nde, ab jàmmaarloo moo fa am ci diggante ñaari mbooloo (communauté). Bees sukkandikoo ci waa Senegoo, fukki doomi-aadama jële nañu ci ay gaañu-gaañu. Mu am ci juróom yoo xam ne sonn nañu lool. Nee ñu li sabab xeex bi mooy càccug jur. Aw béy moo réer ñu jiiñ ko seen i dëkkandoo wëliis ñu am ci firnde. Ca la xeex ba dooree ba ñenn jële ci ay gaañu-gaañu, ay yàqu-yàqu tamit am ci laata waa Sàndarmëri di ñëw.

XIBAARI TÀGGAT-YARAM

Doomu Senegaal jii di Nampalis Méndi jóge na fa RC Lens. Waa Lens ñoo siiwal xibaar bi. Moom nag, taxu ko faa yàgg. Nde, ca atum 2023 la fa demoon ginnaaw ba mu jógee fa Angalteer ca ékib bii di Leicester.
Futbalkat bu mag mii di Cristiano Ronaldo yokk na ag pasam fa Al Nasr. Ca atum 2023 la demoon fa ékib boobu nekk fa Araabi Sawdit. Booba ba tay, ma nga fa di wéyal joŋante yi. Te, mel na ne fasagul yéenee jóge foofa. Nde, yokk na ag pasam ba atum 2027.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj