LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (29/2/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Ndiisoog pólitig ga ca diisoo ba Njiitu réew ma woote woon noppi na. Bees sukkandikoo ci xibaar yi jot a rot, 2i fan ci weeru suwe lañ tànn ngir ñu amal ci wote yi. Namm nañ tamit ci Njiitu réew mi mu wéy di doxal moomeel gi ba keroog wote yi di am, donte ni 2i fan ci weeru awril la war a jeexal. Ndogal yooyu nag tukkee ca diisoo ba, dees na leen jébbal Njiitu réew mi. Waaye, loolu lépp taxul mbir yi sotti wenn yoon. Nde, Ndayu Àtte réew mi neenaloon dekkare bi ajandi woon wote yi moo yayoo kàddu gu mujje gi.

ÀTTEB AMNESTI

Càmm gi nangu na àtteb neenal daan (loi d’amnisty) bi Njiitu réew mi yégle woon keroog altine. Tey ci àllarba ji lañ ko doon càmbar bi ñuy amal ndajeem jëwriñ yi ba daldi koy jàllale. Àtte boobu nag, dina neenal daanub képp ku ñu tegoon loxo ci diggante atum 2021 ak 2024. Waaye Ismaayla Maajoor Faal yokk na ci yeneen i wax. Nde, li mu ci yokk mooy ni,ñi ñu jàppoon ci yëngu-yëngu yee tax a jóg àtte bi. Li jëm ci daan yees daanoon Usmaan Sonko ci digganteem ak Aji Saar walla Maam Mbay Ñaŋ bokku ci.

Ba tey lu jëm ci wàllu àtte boobu, ñii di waa Forum Civil rafetluwuñu ko. Ci seen gis-gis, bokkul ci wareefi Njiitu réew mi muy jël ndogalu àtte bu ni mel. Ndogal li sax dafa teey xel. Ndax dafay mel ni lépp lu fa jot a am dafay neen. Maanaam kenn du xam fu dëgg ji féete : ñu ci ñàkk seen i bakkan, ñu ci jëlee ay gaañu-gaañu, ñi ci seen alal yàqu, ñi ci jóge seen dund yàqu ba ci seen njaboot, ñépp ay ñàkk.

Bu Njiitu réew mi sumbee àtte bi ngir andi jàmm ci géewu pólitig bi ak fi réew mi ni mu ko waxee, doon na tam àtte buy féewale. Dafa di, néew na lool ñi ko rafetlu. Ba ci waa Amnesty international dañ dal ci kawam. Bees sukkandikoo kàdduy Séydu Gasama, seen sekkarteer fii ci Senegaal, Maki Sàll mësul a bëgg jàmm. Suuxal na ñi ko mënoon a diir mbagg ci kujje gi, ku ci mel ni Usmaan Sonko ak Xalifa Sàll. Diggante 2021 ak 2024, lu jege 60i doom-aadama ñàkk nañ seen i bakkan, ñi mu tëj ëpp nañ junni di dem.

MBËKK MI

Ndaw ñaa ngi wéy ba léegi di dugg ci gaal yi, utali bitim-réew donte ni xawoon nañu leen gëj a  dégg ci lu ni mel. Démb ci àllarba ji, genn gaal gu yeboon ba fees dell ak i nit moo daanuji ci tefesi goxu-mbàcc, fa diwaanu Ndar. Gaal gaa ngi bawoo woon Sowaal, fa duni Saalum ya. Ñi mu yeboon a ngi tollu ci 317i ndaw. 27 ci ñoom jot na ñoo ñàkk seen i bakkan, ñu bari itam jëlee ciy gaañu-gaañu. Sos nañ fa diwaan ba ag ndiisoo, ci Njiiteefu gornoor ba, ngir taxawu way-lott ya ak sàkk i pexe ci jëyya jii di mbëkk mi.

GAARU CEES

Gaaru Cees bi dina dundaat. Nde, saxaar gi bi dina tàmbaliwaat daw diggante Cees ak Jamñaajo. Keroog ci talaata ji la jëwriñ ji ñu dénk wàllu dem beek dikk bi, Paap Aamadu Njaay, xamle. Fekk mu doon fa dalal ñaari Otoraay yees dekkil yu mën a yeb ba 500i doom-aadam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj