Li gën a fés ci xibaari bés bi

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG

Maalig Gàkku taxawal nag lëkkatoo

Ginnaaw bi mu fésalee yéeneem ngir bokk ci wote yii di ñëw, ca ndajem-waxtaan ma mu doon amal xamle na ca turu lëkkatoo gu yees gi mu taxawal. Lëkkatoo googu mi ngi ko dippe Mànkoo Yewwi Senegaal. Li ko waral nag mooy waajtaayu wotey 2024 yi nga xam ne nee na bu boobaa dina doon Njiitu réewu senegaal yi.

Xamees na ki war a wuutu Aminata Ture

Ki war a wuutu Aminata Ture ca Ngomglaan ga ginnaaw bi ñu tekkee ndombog-tànkam, mi ngi wuyu ci turu Ayda Suggu. Moom nag mooy juróom-benneelu tof-njiit ci kurél gii di CESE (Conseil Economique, Social et Environnemental), topp tamit (adjointe) ci meeru Pikin-Ouest.

Tontu Usmaan Sonko ñeel teewaayam ca layoo ba

Tontoom boobu nag ñeel layoo bi war a dox digganteem ak ndaw sii di Aji Saar, démb la ko fésal. Mi ngi fésal nag ca laaj-tontu ga doxoon digganteem ak waa VOA Afrique. Nee na nag, tontu ci loolu day teel, mi ngi wéy nag di waxtaan ak i layookatam, ay kilifaam ak i ñoñam.

WÉR-GI-YARAM

Xeexub jàngoroy Sidaa 

Kii di fara-caytu bu kurél gii di CNLS (Conseil National de Lutte contre le Sida) biral na li ñu jot a def ci pajum ndaw ñi ame jàngoro ji. Ndax, nee na bu dee njureef yi ñu am ci mag, yi ñu am ci xale yi moom demewul noonu. Lu tollu ci 4.000i xale yi ko ame, 1.446i ñoo ciy jot pajum VIH bi. 

NJÀNG AK NJÀNGALE

Jubluwaayu jàngalekat ya fare ca Bàmbey

Jàngalekati daara ju kowe ja nekke ca Bàmbey te fare ci kurél gii di SAES ña ngay artu. Ñi ngi xamle nag ne taalata bii di ñëw dañuy dakkal njàng mi. Ndax, nee nañu ginnaaw seen ñaxtu bii weesu ba tey coppite amul ci mbir mi.

KOOM-KOOM

Ndajem Ndakaaru mi ñu jagleel mbey

Ndaje moomu nag dajale na lu tollu ci juróom-ñetti njiiti réew ci Afrig Muy njiitu réew mu Madagaskaar, Gine Ekuwaatoriyaal, Keeñaa, Irlànd, Gine Bisaawo, Tógo, Moritani, Niseriyaa. Nee ñu nag Kodiwaar tof-njiit laa teewoon, waa Marog moom jëwriñ ju njëkk ji moo leen teewaloon. 

Kopparalug BAD 

Ci ñaareelu ndaje mi ñu doon amal ca Ndakaaru jagleeloon ko moom sa bopp ci wàllum dund. Kër gii di BAD (Banque Africaine de Développement) génnee na la tollu ci fukki miliyaar ci ay dolaar ngir kopparal sémb googu.

XEW-XEWI JAMONO

Mbir mu doy waar ca Mbuur

Mbir maa nga xewe ca armeeli Tefes ca diwaanu Mbuur, jenn jigéen moo sulli benn xale bu tollu ci ñaari at ak lu teg. Nee ñu nag jot naa dagg benn loxo bi laata muy bëgg a taal la ca des ndax nee ñu yoroon na esãs.

Xew-xew bu tiis ca Ginnaaw-Raay

Benn tabax moo fa toj, benn xale bu jigéen bu tollu ci juróom-ñeenti at ñàkk ca bakkanam ca saa sa. Xale boobu di wuyoo ci turu F.S fale ñàkke bakkanam, kii di M.M.B moom ay gaañu-gaañu la ca jële.

 Beneen xew-xew bu tiis

Lii nag ma nga xewe ca Daaru Salaam ca diwaanu Cees, benn taalibe moo rey beneen naataangoom. Ñoom ñaar nag dañu doon xeex, ci la kenn ki jam ki ci des ci dënn bi. Ci lañu ko yóbbee raglu ba laata muy àgg fekk na mu faatu. Ka def mbir mi nag teg nañu ko loxo. 

Beneen xew-xew ca Cees 

Xew-xew bii ma nga ame ca koñ bii di Petit-Thialy, genn góor gu tollu ci fanweeri at lañu fekk mu dee. Li ci doy waar kay mooy dañoo fekk mu wékku ci ag garab, xamuñu ndax da doon xaru walla.

XIBAARI BITIM-RÉEW

Burkinaa dàq na sóobare farañse yi

Farãs dina dina génnee mbooleem sóobareem yi nekk ca Burkinaa fii ak weer. Maanaam, laata weeru feewuryee wi di jeex lu tollu ci 400i sóobare ya fa nekk dinañu ñibbi, seen i matuwaay ngànnaay yi ak yu ni deme yépp nag dinañu leen génnee ci njeexitalu weeru awril.

Doomu Senegaal bu ñàkk bakkanam ca Itaali

Doomu Senegaal boobu ñu ngi ko fekk gaawu ci ngoon ci mbeddi Milã yi mu ñàkk bakkanam. Mi ngi amoon lu tollu ci juróom-fukki at ak ñaar. Moom nag amul woon fu mu dëkk maanaam day tuxu ak tuxuwaat Sans Domicile Fixe.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj